Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 051 (Disparate views on Jesus)

This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

b) Xalaat yu wuute yu jëm ci Yeesu, ci diggante askan wi ak Kuréel gu mag gi (Yowaana 7:14-53)


YOWAANA 7:31-32
31 Moona nag, ñu bare ca mbooloo ma gëm nañu Ko. Ñu Nga naan: ”Ndax bés bu Almasi bi ñówee ay firndeem dinañu ëpp yu nit kii?” 32 Farisen ya daldi dégg la mbooloo ma doon déeyante ci mbirum Yeesu. Saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya yebal ay alkaati yu daan wottu Kër Yàlla ga ngir ñu jàppi Ko.

Ak li jamono ji di tar lépp ci Yerusalem, terewul am na ñu tàmbali gëm kàttanu Yeesu giy feeñ. Dañu doon waxante naan: »Xëyna man naa nekk Almasi bi de; ndaxte kéemaan yi Mu def am nañu doole. »Yeesu fexe na ba ñi farluwul torop ci diine; gëm Ko. Gis nanu ne amoon na sax ay taalibe ci biir Péey ma.

Ba yërndukat ya waxee la ñu gis te dégg Ko, ca la Farisen ya xam ne mbooloo maa ngay tàmbali di yeewu, te yoonam waa ngi amsi doole ci Yerusalem. Gàcce di leen gën a dikkal ba ñuy wuti wall ca diiroo mbagg ya maanaam waarekat ya ak Saduseen ya. Dañoo bëggoon kilifa Kër Yàlla ga dàq fa Yeesu. Saraxalekat ya nangu déggo ak Farisen ya ngir jàpp Yeesu.

Malaakay Boroom bi wër jàngalekat bu sell ba, ba xañ surga ya ñu matal seeni ndigali kilifa ya. Yeesu gisoon na leen ñuy ñów ci moom, waaye dawul, xanaa kay dafa feeñal ndamam ni nu ko taskatu Injiil bi di nettalee, mu mel ni ab yégle tëralinu Yàlla ngir mucc gi.

YOWAANA 7:33-36
33 Yeesu wax ne: »Dinaa nekk ak yéen fi ak ab diir, soog a dem ci Ki Ma yónni. 34 Dingeen Ma seet, waaye dungeen Ma gis; te dungeen man a dem fa may nekk. » 35 Yawut ya di laajante ci seen biir naan: » Fu Muy dem fu nu Ko dul fekk? Mbaa du dafa nar a dem ca Yawut, ya gàddaaye ca Gereg ya? 36Lan la baat yii Mu wax di tekki: »Dingeen Ma seet waaye dungeen Ma gis, ak dungeen man a dem fa May nekk? »

Yeesu xamal na ña Mu doon jànkonteel dina nekkaat ak ñoom diir bu gàtt. Xamoon na ne léegi Mu dee ni Mbotem Yàlla. Xamoon na itam waxtu wi Mu war a dekki, yéeg asamaan dellu ca Baay ji. Yeesu yàkkamtiwoon na lool dellu ca wetu Baay ji Ko yónniwoon ngir Mu rammu nu. Ngir mbëggeelam ci nun, moo taxoon Mu toog fii ci àddina, sore lool dëkkuwaayam ga ca asamaan.

Yeesu sóoraale woon na ne taalibeem ya dinañu yéemu ci ndekkiteem ak delloom asamaan. Dinañu tiis ci bañ a am yaramu leer wu leen man a may ñu ànd ak Moom yéeg asamaan. Xamoon na it ne noonam ya dinañu jéem a wut néewam bu “yàqu” ba gannaaw ba Mu génnee bàmmeel ba ñu tayoon ba mu ne ràpp. Toroxte ñeel na ñi bëggul Musalkat bi! Duñu man a am wàll ci ndamam, te it duñu man a dugg ci asamaan. Seeni bàkkaar ñoo leen di tàggale ak Yàlla. Ñàkk a gëm moo leen di xañ nguuru yiw wi.

Yawut yi manuñu woon xam li Kàdduy Yeesu yi di tekki, noonu ñu yaakaar ne Moom dafa fas yéene daw làquji ca Mbaari jaamukaayu Yawut ya ca dëkki Gerek ya wër Mediterane. Mu mel ni dafay sàkkuji ay taalibe ca ña xamagul Mbind yu Sell yi. Mu am ca sax ñu Ko doon ñaawal naan: »Amaana dafa dogu nekk ab waarekat bu siiw te xamal boroom xam-xam yu gerek ay gis -gisam ngir indi leen ci Yàlla jiy dund. »

Bi Yowaana di nettali kàddu Yeesu yi, ak xew-xew yi, booba manga woon ca Efes dëkkandoo ak Gerek ya. Xabaar bu Baax bu mucc gi agsi woon na ba noppi ca Yawut ya fa dëkkoon. Gerek yu bare gëmoon nañu Krist. Taskatu Injiil bi gisoon na ci waxi Yeesu ak ci ñaawalaate Yawut ya ne ci dëgg Yeesu mooy jàngalekat bu mag bi ci biir Gerek yi. Du jàngale xam-xam yu teguwul fenn, yuy indi ñàkk yaakaar. Mooy joxe dund gi, te ci Moom la kàttan ji dul yooy mukk, di jollee.

LAAJ:

  1. Lan la Yeesu yégle te mu aju ci ëllëgam?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 11, 2025, at 12:37 PM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)