Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
A - Ñaareelu tukki ca Yeruusalem (Yowaana 5:1-47) -- Yokkute jànkoonte diggante Yeesu ak Yawut ya
3. Yeesu dafay dekkil ñi dee te di àtte àddina si (Yowaana 5:20-30)YOWAANA 5:25-26 Yeesu wax na bu leer ne Mooy Dëgg gi: » Ci dëgg-dëgg maangi leen koy wax. » Dafa matal la Yonent ya waxoon ci ñówam, nu gën a leer na ko niti jamonoy Kóllëre gu Njëkk nga foogewoon. Dafay dekkal ñi dee, tey ba suba. Ñépp a sànku ci seeni bàkkaar te nekk ci ger. Waaye Yeesu mooy Ku Sell ki, Doomu Yàlla, ji ñu jëmmal, te mu daan bàkkaar ci yaramam, ngir séedd nu wàll ci dundam ci kow sunu ngëm. Ki faydaal Injiilu mucc gi, mokkal ko, jafandu ci Yeesu te jot dundug Yàlla. La ko dale ca ndekkite la, ci lanu xame ne sunu ngëm, ngëmu dund la, waaye du diine dee. Yeesu dafay yónee Xelu dundam ñi koy déglu te am yéene matal kàddoom yi, ak bu ñu leen manul a àjji yépp sax. Dfa leen di may dégg-dégg gu wér, te ci ñoom la kàddug kéemaan gi di feeñe (mate). Ñi dee, maanaam néew yi, manuñu dekki, walla di déglul seen bopp, waay Yeesu dafa leen di may dund ba ñu man koo may nopp bu baax. Sunu dund ci kow suuf dafa am àpp, waaye dund gi nu Yàlla may, du jeex mukk. Ni ko Yeesu waxe: » Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deewee it, dinga dund. Rax ci dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk (Yowaana 11 :25-26). Krist man na nu may dund gu bees, ndaxte Baay ji may na Ko gépp mataayu dund gu amul àpp ba fàww. Krist dafa mel ni teen buy ball ndoxum dund mu dul jeex. Ci Moom lanuy ame leer ci kow leer, mbëggeel ci kow mbëggeel, dëgg ci kow dëgg. Ger ,lëndëm, walla xalaat yuñaaw, kenn du leen fekk ci Moom. Dafa fees ak mbëggeel, ni ko Póol waxe: Krist dafa am yërmande, te ab xarit du ñeewaate, te du bare tiitar; du ràccal boppam rekk, te du ñaaw njoort; du bég mukk ci lu jubul, dafay baale lépp te di muñ lépp; mbëggeelam du saay mukk. Loolu Xelam mi moo nu ko may. Nanu nangu ñu soppi nu ni teenu dund. YOWAANA 5:27-29 Nitu neen ki, bàkkaar moo ko rey. Ku bëggul Yàlla, yaa mbugal sa bopp. Kàdduy Yeesu, mbëggeel lañu àndal, am kàttan te sell. Ku Ko déglu, dund. Rax ci dolli, ay kàddoom ak doxalinam, ay misaalu dund gu sell lañu. Yàlla jébbal na Ko àtte bi, maanaam teg na àtte bi ci ay loxoom. Dafa Sell, ñu nattu Ko ni nun te bàkkaarul. Kenn du am lay ca àtteb Yàlla ba. Krist rekk mooy Ki yelloo àtte àddina si. Moo man a dogal mujjug bépp doomu Aadama. Malaaka yi ak lépp li ñu sàkk dañu Koy jaamu. Ndekkite li dafa wóor, te ci ndigalu Yeesu lay doon. Wooteem bi dina xotti sunu jaww ji; néew yi dunu dégg wootey neen. Waaye Baatu Doom ji mooy yëngal ñi dee ba seen yaram daw. Ruu yi doon nelaw dinañu yeewu, te génn seeni bàmmeel. Kéemaanu kéemaan yi, yenn ruu yi dinañu dundaat, fekk yeneen ya saay ci dee. Ñaari ndekkite ñoo am, benn bi dund lay maye, bi ci des ca àtte ba la jëme. Waxtu woowu, ay mbetteel lanu deeñcal, ndaxte, dina am ñu nekk ci naqar, fekk foogoon nanu ne leer gu yaanj lañuy doon. Ñeneen dinañu melax ni jant bi, fekk nu ngi leen doon xoole ni ñu amul benn faayda, te ñàkk solo! Ci kanamu Yàlla, nit ñu baax ñi duñu gën ñu bon ñi. Waaye am na ci ñu Krist baal, te ñ usant Ko. Ci kàttanu Injiilam lañu dunde. Seen dund meññ na doomu Xel mu Sell mi. Yeesu far na seen bépp tooñ ak deretam ju am maanaa ji. Yiw woowu mungi leen dabe ci seen ngëm. Waaye nag ku xalaat ne say jëf dinañu doy ci kanamu Yàlla, dinga dégg kàddu gii: » Yów miy dunde bopp-sa bopp, lu tax sag mucc doŋŋ moo la soxaloon, te wonoo mbëggeel say noon? Lu tax nanguwuloo jokkoowaat ak Yàlla gi jaare ci ki ñu daaj ci bant? Lu tax nga weddi dundam gu dul jeex gi? Sag rëy-rëylu tànnloo na la dee gi, kon book wéyal ci sa ñàkkum yiw gi ñu la may. » Ñooñu dee ci biir bàkkaar dinañu dekki ngir dal ci àtte bu tar, te dinañu dégg baat ci kow baat lépp la ñu waxoon, defoon, mbaa xalaatoon. Waaye nag ki jegesiwoon ndamul Krist ci kow ngëm, dafay fees ak mbëggeelu Krist. Dafay jàppale ak mbég, te loolu firnde dund gu dul jeex la. YOWAANA 5:30 Krist mooy gëna neex; Mooy Àttekat bi sax. Krist xamoon na kàttan giñ ko dénk. Waaye mu woyof, ba sax wax ne: “Mënu ma def dara sama bopp.” Maanaamuma àtte, sunu, mbaa noyyi sama bopp. Dafa sargal baay bi. Jesus dafa musa nekk ci diggante ak Baay bi. Musu ñu dagg liiñ telefon bi ci seen biir. Baatu Yàlla moo ko xamal xalaati doomi aadama yi. Xelu Yàlla dafay xool àdduna bi, ba noppi di natt sa xol, di wane say xalaat ak li nga nëbb ñeneen ñi. Xel moomu, ci Krist, moo leen di àtte bu jub. Soo nangu sa bàkkaar ci Yàlla, ba noppi nangu baale ki ñu daaj ci bant, kon barkeel nga. Dina ñu bind sa tur ci téreb dund bi. Jesus dina wax ñi jub, "Ñëwleen, yéen ñi sama Baay barkeel, jëlleen nguur gi ñu leen waajal ci njàlbéen àdduna" (Mathie 25:34). Krist Dëgg du fen; xam na li nekk ci nun. Xam na jikko yi ñu donn ci sunuy maam, te du nu gaaw àtte. Dafay xaar ak muñ bés bu bàkkaarkat bi réccu. Limu sell mooy tàqale ñi am yërmaande ak ñi bañ xel mi, ba noppi dëgër bopp. Krist dafa wane woyof ak woyof. Dafa jox lépp Baayam. Noonu la Almasi bi amalee coobareg Baayam ci kàddoom ak ci jëf, ba ci bant ba sax. Biñu yeggee ci waxtu dogal bi, mu ñaan: "Du sama bëgg-bëgg, waaye sa bëgg-bëgg la." Noonu lay joxee àtte Yàlla yépp. Li evangelist bi wax ci diggante Baay bi ak Doom ji, daf nuy fexe nu gëm ni Trinite bi nekk benn. Sañ-sañu dekkal néew yi, Baay bi moo ko moom ni ko Doom ji amee. Yàlla won na ko ay jëfam yépp, te amul lenn lu mu xamul Doom ji. Baatu Krist dina dekkal néew yi; moo yor caabiy rab ak safara. Gëm kumpa la ci boroom xel yi; Bu mbëggeelu Kirist feese nu ak cafka gu neex gi, lanuy xam njariñu gëm Yàlla bu nekk ci Trinite ngir sunu mucc. LAAJ:
|