Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
A - Ñaareelu tukki ca Yeruusalem (Yowaana 5:1-47) -- Yokkute jànkoonte diggante Yeesu ak Yawut ya
4. ñeenti seede yiy wone ne Kirist mooy Yàlla (Yowaana 5:31-40)YOWAANA 5:31-40 Yeesu yégaloon na ñi ko doon xeex ne moom moo am sañ-sañu matal liggéey yi Almasi bi Yàlla digoon. Dañu bañ waa jooju di yàq seen mbootaay ak seeni sàrt. Ñu laaj seede ngir firnde limu wax. Yeesu nangu na tontu seen laaj ci joxe firnde. Nun ñépp dañu jàpp ni noo gëna baax. Yeesu dafa wax lu dëggu ci boppam, te amul benn fen. Seedeem dëgg la, doonte yoonu Musaa mënul bàyyi xel ci seede bu nit ñi seede ci seen bopp. Kirist nangu na loolu: “Su ma seede sama bopp, sama seede du dëgg.” Jarul woon mu xeex ndax keneen seedewoon na ko, di Baay bi ci asamaan si, moo ko jàppale ci ñeenti firnde yu leer. Yàlla yónni na Sóobkat bi ngir mu yégle ci seen biir Almasi bi. Ndaw si seedewoon na Kirist, liggéeyam ci nekk saraxalekat, ak ci liggéeyam ci nekk àttekat. Waaye waa Kuréel gu mag gi dañu am sikki-sakka ci Yaxya, ba noppi bañ seedeem ci Yeesu (Yowaana 1:19-28). Seede yu Yaxya bokkul woon ci dooley Yeesu, wala limu doon dundal, waaye Yeesu mooy limu doon ca jamono yu yàgg ya. Ginaaw nit ñi xamu ñu woon lu bari, Yeesu nangu seede bu Baptist bi ngir jàppale dëggam. Baptist bi juumwul bimu wax ni Yeesu mooy Mbootu Yàlla biy joxe Xel mi. Baptist bi làmp la woon buy leer guddi. Mu dajale ay taalibeem, leeral leen. Waaye bi jant bi fenkee ci jëmmu Yeesu, soxlaatul woon làmp. Yeesu kese mooy Leer gi ci àdduna bi, am doole ju amul àpp. Ni jant bi di joxee dundu ak màgg ci kaw suuf, noonu la Yeesu di joxee dundu ak mbëggeel ci ngëm. Faj ak dàq jinne yi dañu wane ni leer moo daan lëndëm. Dafay dalal taw bi ak dekkal néew yi, loolu dafay firndeel ni boroomam la. Li muy liggéey dafa ànd ak Baay bi. Dafa jeexal liggéeyam ci bant bi. Ginaaw bimu dekkee, yónnee na Xel mu Sell mi ci ndaw yi, te ba leegi mingi koy yónnee ñi koy laaj. Jëf yi Yàlla di def dinañu mat ci ñaareelu ñëwu Almasi bi, ndekkitel néew yi, ak àtteb àdduna. Amul benn wuute ci seen liggéey diggante Baay bi ak Doom ji: li Baay bi def ba leegi, Doom ji itam daf koy def. Yàlla ci boppam yëkkati baatoom ngir may nu dégg kàddum yu siiw yi: “Lii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa neex” (Mathie 3:17). Kenn mënul seede lu mel noonu ludul Yeesu, mi dundu saa yu nekk ci bëgg-bëggu Yàlla. Doom jiñ bëgg, fees dell ak mbëggeel gu dëggu ak sell. Yeesu gëdd na Juif yi ndax xamu ñu Yàlla. Dañu bañoon dégg kàddoom ci yoonu Musaa wala ci yonent yi. Xamu ñu ko ci gis-gis wala ci gént. Lépp luñu ko njëkka wane amul benn sikk, ndax seeni bàkkaar dañu leen tàqalewoon ak Ki Sell mi. Bi Yesaya gisee robbu Boroom bi ci barabu jaamukaay bi, mu yuuxu naan, "Toroxal ma! Maa ngi dee, ndax man nit ku setul la" (Yesaya 6:5). Liy firndeel seen tëx ci ngëm ak ñàkka xam-xam mooy li ñu bañ Kirist, Kàddug Yàlla mi nekkoon nit. Képp ku foog ne xam nga kàddug Yàlla te bañ Yeesu, Kàddug Yàlla, dafay firndeel ne jottul wallu gu dëggu gi, walla nga xamul ko. Nit ñi dundu ci Testament bu yàgg bi dañu doon jàngat Mbind mi, di am yaakaar am dundu ba fàaw. Ñu fekk fa arafu yoonu Musaa bu dee, waaye ci beneen wàll bi, ñu ñàkk dige yiy wax ci Almasi bi, doonte yonent yu mel noonu bari nañu ci Testament bu yàgg bi. Dañu taamu seen xalaat, seen tegtal ak seeni njàngale, te xamu ñu woon ni Kirist mooy Kàddug Yàlla gi gëna mag ci ñoom. Yeesu won na leen lu tax ñu bañ ko nangu, maanaam nangu wuñu nangu Yàlla nimu mel. Dañu bañoon Kirist ba noppi ñàkk dundu ba fàaw, ñàkkaale mébetu ngëm ak yiw. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nu ngi lay sant ci li nga bëgg say noon. Seen ngëmadi moo tax sonn ngeen. Yaa ngi leen jox ñeenti seede yiy wane sa Yàlla. Dimbali nu seet ci Evangelium yi ak ci yeneen Mbind yi ngir gis la, gis sa boroom, wóolu say liggéey, am dundu ba fàaw. Ubbi leen noppi milioŋ yu bari yi tëx ba leegi ci sa baat. LAAJ:
|