Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
C - Ba Yeesu njëkkee ñów Yerusalem (Yowaana 2:13 - 4:54) -- Ci dëgg-dëgg, lan mooy màggal?
2. Yeesu mungi wax ak Nikodeme (Yowaana 2:23 – 3:21)
d) Sàbbi Krist,ci àtte lay jëme (Yowaana 3:17-21)YOWAANA 3:17-21 Yaxya dafa yéglewoon ab Almasi buy àtte nit ñi, di dagg garabu askanam yu jagadi yi. Yeesu xamal Nikodem ne du lakk ci safara si, waaye dafa war a nangu mucc gi. Sunu Musalkat bi dafa am yërmande. Bi Yaxya demee ba daj kumpa saraxu wuutu boobu, ci la tudde Yeesu « mbotem Yàlla mi ». Ci kow mbëggeelam, Yàlla daldi yónnee Doomam ji; du ngir Yawut yi kese, waaye ngir waa àddina sépp. Baatu « àddina » feeñ na ñetti yoon ci aaya 17 bi. Loolu nekkoon na xët bu mettiwoon la ci Yawut yi, ñoom ñi doon jàppe yéeféer yi ni ay xaj. Ni Yàlla bëggewoon askanu Ibrayma, noonu itam la bëggewoon askan yépp. Ñépp a yelloo àtte bi. Moone Yeesu ñówul ngir mbugalaate, waaye ngir musal. La ko dale ca njalbéen ga, mungi matal misaalu jaan ja ñu lonkoon ca bant ba, ngir dékku àtteb Yàlla ngir nit ki. Mbëggeelu Yàlla berul, te bañul xeet, waaye askan yépp la uufaale. Krist dafa ci rax kàddu yu bette yii: » Ku gëm Doom ji, deesu la àtte. « Noonu, bépp ragalu bésu àtte ba teggi nañu ko. Gëm Krist dafa nuy goreel ci dee gi nu yelloo. Set nga wecc ci àtte bi boo dénkee sa bopp Yeesu. Képp ku sàbbi muuc gi Yeesu di maye, te di xalaat ne amuloo ci benn soxla, dangaa gumba, ñàkk xel te tàqalikook yiwam. Képp ku dalalul kàttanu Krist, xañ nga sa bopp leeraayu Xel mu Sell mi. Ku xebat deewug Krist, walla nga weddi ko, yaangi fippu Yàlla te di tànnal sa bopp sa layu njubte. Jëfam yépp deesu leen rafetal, te dafay gàcceel (gecc) ndamul Yàlla. Yeesu faramfàcce na lu tax ñenn ñi di sàbbi mucc gi; seeni bàkkaar ñoo leen gënal njubte Yàlla, te dañuy deltu gannaaw Krist, miy leeru àddina si. Dañuy ŋoy ci seeni bàkkaar. Krist xam na sunu xol, ak fi sunuy xalaat yu bon yépp jóge. Kenn manul a fexe ba baax, ci sa kow coobare bopp. Kàddu yooyu tooyal xolu Nikodem, rawatina ba leen Krist toftalee ak ay yégeeli mbëggeeli, ngir dammat rëy-rëy loom. Te fexe ba mu tuum ay bàkkaaram. Yeesu teg ci ne, ku Ko wóoluwul, lu bon nga bëgg, te bañ lu baax, ba noppi taq ci say bàkkaar. Li ëpp ci nit ñi, ay naaféq lañu, yuy nëbbe seeni bàkkaar ak ay muuñ yu sell. Dañoo bañ Krist ci kow teyeel walla ci lees xamul. Ndax nangu nga, te tuub say bàkkaar ci kanamu Yeesu? Su f ekkee ne nanguwoo te tuuboo say bàkkaar, kon doo man a judduwaat. Ubbilal sa xol bi leeru Yàlla gi, mu laabal la. Gëm mbotem Yàlla mi dafa nuy sellal Kon book, toroxlul te tuub say ger, wóolu Ko, te noonu dinga dund ba fàww. Jëfe ak sunu ngëm mooy tekki def lu baax. Gaawtu bi nuy nangoo dëggu Yàlla gi, bokk na ci anam yi ñuy yeesal. Képp ku sóobu ci dëggu Krist gi, te yemalewu ko ci am xelam rekk, waaye jébbal ci jëmmam jépp, kooku coppite biiram leer na. Fenkat yi dañuy mujje am ngor, ñi dëngoon dellu jub, workat yi mujj di doxal yoon. Ñi judduwaat, baaxuñuwoon, waaye dañoo nangu te tuub seeni bàkkaar, ba jot mbaalug Yàlla mi am kóllëre. Sellal gi tàmbali na ci ñoom; dafa leen di jox kàttanu mbëggeel, ngir ñu man a jëfe ak liggéeyu Xel mu Sell mi. Ci Krist la Yàlla di jaare ngir matal jàmm ji Mu namm ci ñi gém Xalabunu jëf yu baax yi, waaye ñoom du ci nun lañu jóge, ci Yàlla kay lañu jóge. Dunu ko jàppe ni lu nu yelloo, yiwu Yàlla la. Loolu mooy tekki ne danuy bàyyi sunu doylu bopp gi nu wéer c i sunu doylu bopp, te dalal njubteg yiw wi wékku ci deretu Krist. Ñépp judduwaat te sax ci Krist, dañuy seddal xolu Yàlla. Dañuy dunde cant ndax yiwam. Judd gu bees gi, ak dund gu sell gi, màggal yu sedd xolu Yàlla lañu. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, jarajëf ci li nga gàddu sunub àtte, bi nu dul dal, ndaxte nungi jokkoo ak Yów ci kow ngëm. Goreel nga nu ci merum Yàlla. Ñungi nangu sunuy bàkkaar ci sa kanam. Teggil nu li nuy xiir ci bàkkaar. Sàkkal ci nun meññeefu Xel mi, ndax sunu dund nekk màggalu Yàlla, Baay bi ci asamaam. LAAJ:
|