Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 026 (The Baptist testifies to Jesus)

This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
C - Ba Yeesu njëkkee ñów Yerusalem (Yowaana 2:13 - 4:54) -- Ci dëgg-dëgg, lan mooy màggal?

3. Yaxya mungi seedeel Yeesu boroom kër gi (Yowaana 3:22–36)


YOWAANA 3:22-30
22 Gannaaw looluYeesu ànd ak ay taalibeem,dem ca biir diiwaanu Yude, toog fa ak ñoom ab diir, di sóob nit ñi ci ndox. 23 Yaxya moom itam doon na sóobe ci ndox ci dëkku Aynon, ca wetu dëkku Salim, ndaxte diiwaan booba barewoon na ndox. Nit ña daan nañu ñów ca Moom, Mu leen di sóob. 24 Booba tëjaguñu Yaxya ci kaso. 25 Foofa ay taalibey Yaxya tàmbaleee werante ak benn Yawut ci mbirum sangu set. 26 Ci kow loolu ñu dem ca Yaxya ne ko: »Kilifa gi ndax fàttaliku nga kooka nga seedewoon te mu nekkoon ak yów ca gannaaw dexu Yurdan? Moom de, ma ngay sóobe ci ndox léegi, te ñépp a ngay dem ca Moom! » 27 Yaxya tontu leen: » Kenn manul a am dara lu ko Yàlla joxul. 28 Yéen ci seen bopp man ngeen a seede ne, waxoon naa ne, du ma Almasi bi waaye dañu maa yónni, ma jiitusi Ko. 29 Kiy céetal moo moom séetam. Waaye xaritu kiy céetal dafay taxaw di ko déglu, tey bég, bu déggee baatam. Mbég moomu mooy sama bos tey, te fi mu nekk mat na sëkk. 30 Li war mooy Moom, mu gën a màgg, te man, ma gën a féete suuf. »

Bi Pak (bésub jéggi ba) weesoo,Yeesu génn Yerusalem, tàmbalee sóobe ci ndox. Taalibe ya xamoon nañu ni xol bu toj ame solo laata juddu gu bees di man a am, te itam leeroon na leen ne bu nangu say bàkkaar te rëccu leen amul, mucc du man a nekk. Sóobu bi ci ndox dafa doon misaal suufeelu gi, maanaam xol bu toj, bi kiy rëccu di wonee fi ko bokk ci Kóllëre gu Bees gi ak Yàlla tollu.

Sóobkat bi ci ndox, Yaxya, dafa toxaloon fa mu daan sóobaate; léegi manga féetewoon ca Enon, muy ca catu bët-gànnaaru tundu Yurdan wa. Nit ña dañu daan dem ca moom, ubbil ko seeni xol; mu leen di sóob ci ndox, di leen waajale noonu, ngir ñu man a dajeek Yeesu.

Yeesu tëbul rekk dellu Galile,waaye dafa tàmbalee sóobe ci ndox ña daan rëccu, feneen ca réew ma. Loola nag moo juroon jàppante ba amoon ca diggante ñaari mbootaay ya. Laaj bi moo doon: Kan ci ñoom ñaar moo gën a yelloo sellalaate ci bàkkaar? Kan ci ñoom moo gën a jege Yàlla? Laaj bu am solo la woon, ndaxte dañoo bëggoon a jébbal seen dund jàngalekat bi gën a dal seen xel. Mbokk mi, ndax bàyyi nga xel ci sa njaamu?

Yaxya dékku na nattu yu metti. Moom iñaanewul Yeesu siiwam gu jéggi dayoo gi, waaye dafa nagu ne liggéeyam am na fu mu yem. Dafa nangu ci woyofteef ne: »Nitu neen manul a matal liggéey bu rafete nii moom kese. Ci kow kàttanu Yàlla, barkeem, ak meññeef mi doŋŋ, la ko man a jëfe. Nunn ag, danuy bàkku, te di kañu ci sunu xam-xam, sunuy ñaan, walla sunu wax ju neex. Bu nu waree jot mayu baatin, ci Yàlla la war a jóge. Ay jaam yu yelloowul dara lanu, naam fekk ne nungi déggal sax coobare Yàlla. Yaxya dafa suufeelu, jéemul sax jiital ay man-man yu ko sut, waaye dafa màggal Yàlla kese.

Yaxya seedewaat ci kanamu ay taalibeem. Nekkul Almasi bi. Xëyna sax yaakaaroon na ne Almasi bi dugg gu kéemaane lay agsee Yerusalem, waaye loolu mujjul am. Yeesu wéy di sóobe ci ndox, loolu jaxase xelu Yaxya, mi wéy ci déggal ndigal li mu jot. Xàllkatu yoonu Krist la woon. Yaxya jàpp ci peeñu mi mu jot. Mu biral ne Yeesu mooy boroom céetal, biy faj kiy rëccu ak metitlu, ñu laabal ko ci ndox ngir mu nekk séetam bi.

Tey jii nag, Xel mi samp na jokkoo baatin googu, ni ko Póol waxe nii: » Ci cëri yaramu Krist lanu bokk, te Moom mooy boppu yaram wi; benn lanu ci Moom. » Krist nekkatul sunu àttekat, waaye sunu Musalkat la, boroom céet li. Nataalu mbégte céet li moo nuy won sunu yaakaar ci Krist.

Yaxya dafa dandu, di bég ci màggaayu Mbootaay gi (Egliis bi). Dafa doon nekk ci wetu Yeesu, te daawul jaxasoo ak mbootaayam. Dafa doon seede ne xaritam àqan la. Na mu beroowoon ca mànding ma,Yeesu dugg biir Yerusalem, def fa ay kéemaan te waare fa.Yaxya seetlu màggaayu (yaatuwaayu) Nguuru Yàlla, te noonu mu bég ci. Baatu boroom céet li ak kilifteef gi mu àndal neex ko lool. Bataaxali ndami Krist yi di mballax ci moom ni tamay Àjjana. Noonu la lewetaayu Krist dalalee xolu Yaxya, nitu àll ba, ca njeextalu liggéeyam. Bege na li mu bokk ci berndeelu céet googu.

Yaxya jekkoon na ngir dee, te yokk ay limu taalibeem soxalu ko woon. Li ko gënaloon kay mooy wàññeeku te saay ndax jàngu bi gën a màgg.

Yów sama mbokk miy jàng lii,kan mooy boppu seen ndaje yi? (kuy jiite seen ndaje yi?) Ndax ku nekk ci ñoom mingi xeex moroomam ngir nekk njiit, wala yaa ngi bàyyi ñeneen ñi ñu gëna ndaw, ngir Kirist gëna am doole ci yeen? Booleen ak Yaxya ne, "Moom dafa wara yokk, man ma wàññeeku."

LAAJ:

  1. Nan lanu man a jàppe Yeesu ni boroom céet li?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 21, 2025, at 07:08 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)