Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
B - Krist jële na ay taalibeem la ko dale ca tuub seeni bàkkaar ba ca mbébteg céet ga (Yowaana 1:19 - 2:12)
3. Juróom-benni taalibe yu jëkk yi (Yowaana 1:35-51)YOWAANA 1:43-46 Ci aaya yi nu weesu gis nanu ci ay xew-xew yu am ci biir ñeenti bés yu tegaloo. Bés bu njëkk bi, ag Kureel gu jóge Yerusalem ñów na; ñaareelu bés bi, Yaxya biral na ne Yeesu mooy Mbotem Yàlla; ñetteelu bés bi, Yeesu woo na ñeenti taalibe; ñeenteel bi, Mu woo Filip ak Natanael, ñu bokk ci taalibe yi. Yeesu ci boppam moo dem ca Filip. Filip jotoon na dégg Yaxya ne Yeesoo ngi ci seen biir. Waaruwoon na lool ba Yaxya joxoñee Yeesu, ne mooy Mbotem Yàlla mi. Filip sañuloon jege Yeesu. Béggoon na xam Boroom bi, waaye dafa jàppewoon boppam ni ku yeyoowul am jokkoo ak Aji Kowe ji. Kon book, Yeesu moo dem ci moom, beddi bépp gàllankoor te ne ko mu jóg top ko. Yeesu amoon na sañ-sañu tànn ay nitam ndaxte moo leen sàkk, bëgg leen te rammu leen. Du nun ñoo Koy nangu, waaye moo nuy jëkk a gis; Wut nanu, te gis na nu Mungi nuy woo ci liggéeyam. Bu woote amul, dara du jëm kanam, benn liggéey du am solo bu ko Yeesu diglewul. Képp kuy liggéey ci nguuru Yàlla gi te kenn tànnu la ci li ngay def, dangay sonal sa bopp te lëjal ñi ci des. Waaye kiy dëglu Krist, te jekk ngir dégal ko, Krist dina ko sàmm te aar ko fu mu man a tollu. Filip dafa dem ci saa si yéeneji Xabaar bu Baax bi te noonu la yëgale Xabaar bi xaritam bi tuddu Natanael: ”Gis nanu Almasi bi!” waaye du “Gis naa”. Dafay boole boppam ci jàngu bi, boole ci lewetaay. Dafa mel ne Yeesu xamal na taalibe yi li jëm ci liggéeyam, waaye waxul dara ci juddoom ca Betleyem, walla ci baayam Yuusufa mi Ko yer. Kon taalibe ya xamuñuwoon dara ci Moom. Natanael ku màccoon la ci Mbind yu Sell yi. Gëstuwoon na dige yi ajuwoon ci Krist, te nekk ci téerey Musaa, ak yu Yonent yi. Kon moom xamoon na ne Almasi bi Betleyem lay juddoo, ci geñog Dawuda, te dina nguuru ci askanam. Kon Natanael amoon na jafe-jafe ci dégg ab Almasi buy jóge Nasaret, di ab dëkk bu ndaw, bu kenn limaalewul sax ci téereb Kóllëre gu Njëkk gi, te it Yonent yi waxuñu dara lu ci jëm. Mu fàttaliku ne foofa Seloot yu xarañ ya fippoowoon ca kow waa Rom ya. Fippu googa waa Rom dañu ko dakkaloon, te rey ca nit ñu bare. Xew-xew yooyu soxaluñuwoon Filip. Mbég mu rëy la amoon ba mu dajee ak Krist. falaŋ xel-ñaary Natanael. Ngir bañ a guddal wax, mu ne ko: ”ñówal gis.” Waxin wii mooy ëkku yéenekaayu Xabaar bu baax bi, mooy maye mos dëgg gi, te di ci jëme, ”Ñówal gis.” Bul dug ci ay werante yu jëm ci Yeesu, waaye dundal ak Kàttanam ak teewaayam. Sunu seede laluwul ci ay xalati gént, waaye ci jëmm jiy Boroom bi tigi. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, jarajëf ci sa mbégte miy feesal sunuy xol, wéyale nu ci neex làmmiñ ak rafet jikko ngi rnu man a jëmale nit ñi ci Yów. May nu mbëggeelu waare ak mbëggeel, ak muñ, te baal nu sunug ragal, sunuy lay, ak bare kersa. Defal ba nuy biral sa Tur ak njàmbaar. LAAJ:
|