Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 012 (The Sanhedrin questions the Baptist)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
B - Krist jële na ay taalibeem la ko dale ca tuub seeni bàkkaar ba ca mbébteg céet ga (Yowaana 1:19 - 2:12)

1. Ag Kureelu Sanedreŋ mungi laaj Yaxya (Yowaana 1:19-28)


YOWAANA 1:22-24
22 Noonu, ñu laaj Ko ne: ”Wax nu yaay kan, ngir nu man a tontu ñi nu yónni. Nga ne yaa di kan? 23 Yaxya leen li yonent -Yàlla Esayi waxoon ne: ”Man maa di baat biy yégle ci mànding mi ne: ”Xall-leen yoonu Boroom bi!” 24 Amoon na ñu bokk ca farisen ya, yu àndoon ca mbooloo ma ñu yónniwoon ca Yaxya.

Laaji kureel ga, dañu melon ni ay fit. Laaj yooyu ñungi ajuwoon ci ay wax yu dëgguwul yi ñu doon séentu ñu feeñ, laata ñówug Almasi bi. Waaye, ndegam Yaxya dafa bañ ne du Almasi bi, walla Iliyas, ak Yonent ba Musaa yéglewoon ne dina ñów, noonu amatul maanaa ci ñoom, te ragalatuñu Ko. Waaye taxul ñu may Ko jàmm, ndaxte bëggoon nañu xam kan moo Ko yebal ak bataaxalam bi. Bëgguñuwoon dellu ca Kureel gu Mag ga (Sanedreŋ ba) te yóbbaalewuñu tontu yu doy.

Laaj yi bokkuñuwoon dara ak la Yonent-Yàlla Esayi yéenewoon (Esayi 40:3), waaye, Xel mu Sell mi, moo xelal Yaxya Aaya yooyu. Mu wone boppam ni baat buy yuuxu ca mànding ma, te di waajal yoonu Boroom bi. Bu fekkoon ne Yaxya indiluleenoon ay tegtal yu jóge ci Mbind yu sell yi, kon dinañu Ko tuumaal, ne Moo jox boppam sañ-sañ, te feent peeñug boppam. Te kon naroon nañu Ko daane tuumaal Yàlla. Yaxya dafa toroxlu, daldi féetewoo wàll wi gën a ñàkk solo ci Kóllëre gu Njëkk gi, maanaam nekkuloon dara lu dul ab baat buy xaacu ca mànding ma.

Nun ñépp,nungi dund ci sunu màndiŋu bopp. Li nu wër lépp, ay yëngu-yëngu la ak ab jaxasoo. Waaye Yàlla du nu bàyyi noonu, dafa nuy dimbali.D afa ñów ngir musal ñi geru. Ni Mu jógee asamaan, ngir ñów ci kow suuf, aw yiw wu mucc qyib la. Ku Sell ki, du nu yàq, ni nu ko yelloo, waaye dafa nuy wut, te di wut itam ñu réer ñi. Mbëggeelam raw na sunuy xalaat. Muccam gu rëy gi dafa ëmbaale soppi mànding mi, mu nekk ab tool bu naat.

Ci kow digalu Xel mu Sell mi la Yaxya xame ne Yàlla jaare na ci Krist ngir ñów ci sunu àddina si. Noonu la tàmbalee woo nit ñi ngir ñu yëngu, te waajal teerub Ki war a ñów. Xarañ gi mu àndal ngir waajal yoonu Krist, tax na ba mu nekk baat biy xaacu ci sunu màndingu àddina. Xamlewul boppam ni ab yonent, walla as ndaw, waaye ni ab baatu neen. Waaye baat boobu fees ak sañ-sañu Yàlla, bàyyiwuloon nit ña di ko taŋxamlu bay yandoor ci biir seeni bàkkaar.

Lan la baat boobu doon wax? Li ëpp maanaa ci yéeneem bi mooy: jóglee, te xam ne Nguurug Yàlla gi agsi na ci sunu biir! Jekkalleen seen dund! Yàlla dafa sell, te dina leen àtte. Yàlla dina leen laaj seen bépp fen, càcc,yaa ma neex, walla tooñ, te dina leen mbugale safaras laaxira. Yàlla du fàtte say bàkkaar Nit ku bon, ku bon rekk lay doon ci kanamam. Te ki ñu naan ku baax la, du tane ku bon ka. Ndaxte amul kenn ku set ci tooñ, ci kanamu Yàlla.

Ni ci Yaxya taxawe, dafa nuy ñaax ngir nu xolaat sunu bopp, nangu sunu ger, xalab sunu rëy te soppi sunuy xalaat. Mbokk mi, ndax jàppe nga sa bopp ni ku baax, te ñu yaatal ko? Amal ngor te nangu say tooñ! Su fekkee ne am na loo sàcc sa moroom, ak lu mu tuuti tuuti, delloo ko ko léegi ci saa si. Rreyal sa rëylu gi, ted und ngir Yàlla. Jekkalaatal li jubul ci sa doxalin. Toroxlul, ndaxte li nga def baaxul.

Ñu bare ca ña bokkoon ca kureel ga, ay Fariseŋ lañuwoon. Fitu Yaxya wa dafa leen a merloowoon, ndaxte ñoom dañu newoon ne dañoo jub, jullite, te baax, di topp Ndigal yi ni mu ware, te farlu ci. Waaye, dañu doon nax seen bopp. Dañu doon bàkkoo nekk ay niti diine tigi, fekk xol yu geru lañu fees, yu nammul lu dul fayoonte, ni xeetu jaanu co.

Seen Kàddu yu ñagas ya, yëngaluñuwoon Yaxya, mi dal ci seen kow, ba fàttali leen ne nun ñépp a soxla dellusi ci Yàlla nu mu gën a gaawe, te waajal yoon wi ngir Boroom bi man a ñów ci nun balaa yàgg.

ÑAAN: Boroom bi xam nga sama xol, sama démb, ak samay bàkkaar. Am naa gàcce ci samay tooñ, yi feeñ, ak yi làqu. Maangi lay jébbal samay coxorte yépp, te di la baalu. Yàlla bu ma sore sa teewaay. Dimbali ma ba ma delloo lépp li ma sàccoon ñeneen ñi, te ma baalu ñépp ñi ma gaañ. Moxoñeel sama rëy, te laabal ma ci samay bàkkaar, ci sa yërmaande, céy Boroom bi, yów miy yërëm ñi am yërmaande!

LAAJ:

  1. Nan la Yaxya def ba woo nit ña ngir ñu waajal yoonu Boroom bi?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 10, 2025, at 03:56 PM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)