Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
A - Peeñug Kàddug Yàlla gi ci Yeesu (Yowaana 1: 1-18)
2. Sóobkat bi ci ndox(Yaxya) mungi waajal yoonu Krist (Yowaana 1:6-13)YOWAANA 1:11-13 Askanu Kóllëre gu Njëkk ga, Yàlla moo leen moomoon, ndaxte Aji Sax ji dafa fasoon kóllëre ak bàkkaarkat yooyu, ba Mu leen sellalee ba noppi. Wommat na leen ay téeméeri-téeméeri at. Ruuj na seeni xol ak larmeti Ndigal yi (Yoon wi), te waajal leen ngir ñu jot Injiil li. Ci noonu, nettalib askanu Ibraayma mungi jublu ci ñówug Krist. Peeñoom moo doon mébét bu mujj,bu Kóllëre gu Njëkk ga. Doy na waar li ñi ñu tànnoon, te ñu waroon a teeru Boroom bi, dañu koo weddi, ba jotuñu leeram gi. Dañoo tànnoon a dund ci lëndëmu Ndigal yi (Yoon wi), di daw ak doole jëm ca àtte ba. Xañ nañu seen bopp yiw wi, te sopp seeni jëf gënal leen mucc gi nekk ci Krist. Tuubuñu seeni tooñ, waaye dañoo dëgër bopp ci kanamu Xelum Dëgg gi. Du caagéen ne askanu Kóllëre gu Njëkk ga rekk la Yàlla moomoon, waaye doom-Aadama yépp, ndaxte Aji Kàttan ji moo sàkk doj yi, gàncax yi, jur yi, ak nit ñépp. Loolu moo tax, askaani àddina sépp, ak askanu Kóllëre gu Njëkk ga ñoo bokk benn wareef bi. Sunu Aji Sàkk ji ak sunu Rabbi, dafa bëgg a dugg ci sunu xol, ak sunuy kër, kan moo koy teeru? Yàlla moo la moom. Ndax teg nga sa dund ci loxoy Yàlla? Tey jii, lees naqarlu am na, ndaxte li ëpp ci réew yi nanguwuñu jekk ngir teeru leeru Krist. Bëgguñu xéewlu ci ceeñeeram yi ngir daan dëllaayu seen lëndëm gi. Kon weddeeti nañu Doomu Yàlla ji. Ak doomu Ibraayma, walla nit, ku mu ci man a doon, bu ubbilee Krist xolam, te jébbal dundam ci loxoy Musalkat bu am kàttan bi, dina mos kéemaan gu rëy. Ndaxte leeraayu asamaan dina ko leerale ak leerug Yàlla, te daan lëndëm gi dëkk ci xolam. Rax ci dolli, Kàttanu Yàlla dina dug ci xolam te yeesal melokaanu biiram. Krist dafa lay goreel ci njaamug bàkkaar. Dafa lay may ngoru doomi Yàlla yi. Soo bëggee Krist, kon Xel mu Sell mi dina dëkksi ci yów, te tàmbali liggéeyu muccam ci sa dund. Waaye nag, Yowaana, taskatu Injiil bi waxul ne dinanu nekk ay doomi Yàlla, waaye dinanu nekk ay doomi meññeefum baatin. Ñaari wax yii wuute nañu lool, ndaxte ku gëm Krist, dangay dug ci dund gu bees. Teg ci dafay màgg, di màcc ba àgg ci mataayu dundug baatinam. Kàttanu Boroom bi soppali nanu sosin wu bees, te dinanu Sellal te àggale nu cig mat. Dunu ay doomi baayale rekk ci Yàlla, waaye ay doom lanu jaare ko ci sunu juddug baatin. Mayug Xelu Krist, ci sunu xol dafa nuy sol ba nu fees ak sañ-sañu Boroom bi. Ni sañ-sañu B0room bi xëppoo ci kow way-gëm yi, mooy wone ne amul jenn kàttanu àddina sii, ak ba àddina di tukki, manuleen a tere fees ak mayi asamaan. Krist mooy sàkk ngëm gi, te moo koy matloo. Kenn manul a méngale doomi Yàlla ak doomi àddina si. Doomu Aadama boo gis am na ndey ak baay yu ko jur, ci know mu neex leen, walla jaare ci seeni bëgg-bëggi yaram. Xëyna ñaanandoo nañu te top yoon wi leen Xel mi won. Waaye bépp ndono baatin, xel walla yaram, bu jóge ci suny waajur séqul dara ak sunu juddu gu bees gi. Ndaxte yeesalug baatin dafa sell la ko dale ca njalbéen ga te ci Yàlla la jóge, Moom mi bépp kercen juddoo. Ndaxte mooy sunu Baayu baatin tigi. Amul benn liir bu man a juddul boppam. Dafa juddu. Te noonu itam la sunu juddug baatin nekke yiwu neen. Krist dafa jii jiwu Injiilam ci sunu xol. Képp ku bëgg jiwu yooyu danga leen di nangu te deñc leen. Dundu Yàlla ju amul àpp ji dina màgg ci moom. Barkeel ngeen yeen ñiy dégg Kàddug Yàlla gi, te deñc ko (jàpp ko). Juddoo ci njabootu Kercen, walla bokk ci mbootaayu kercen, taxul nu nekky doomi Yàlla. Waaye gëm Krist mooy tax. Ngëm googu dafa laaj nu jege Ko, sóobu ci ay jikkoom, xam lewetaayam, te màgg ci wéeru ci kàttanam. Màggaay googu man na am bu nu tegoo ciy loxoom, gëm ne musal na nu te mungi nuy soppi ngir nu mel ni Moom. Gëm Krist, ab jokkoo bu dëggu la ci sunu diggante ak Moom, ak kóllëre guy law ba fàww. Juddug baatin googu du man a sotti ci nun bu jaarul ci ngëm gii. Manunu wax ne juddu gu bees gi moo gën a mag(big) ou great(màgg)? Walla jafe ngëm gi; manunu wax itam ne ngëm gi moo gën a yomb yeesal gi. Ñoom ñépp a yem. Ba léegi Yowaana taskatu Injiil bi tuddagul turu Yeesu Krist. Dafa won way-gëmi réewi àddina si melokaanam rekk te jëfandikoo ay baat yu méngoo ak ni ñuy xalaate. Ndax xam nga bu baax juróom-benni tekki-tekki baaxaayi Krist, yi Taskatu Injiil bi jiital? Ndax ubbil sa xol kàttanu yooyu melokaan, kon dinga nekk doomu Yàlla dëgg. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, maangi lay sujjóotal. Bëgg naa la te ubbil naa la sama xol. Ñów nga ci man, ak li ma am ay bàkkar lépp, Sellal nga ma ci sama yooñ yépp. Céy Boroom bi, ubbil naa la yamblaŋ sama samay bunti xol. Kaay dëkksi ci man jaare ko ci sa Xel muSell mi. LAAJ:
|