Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 006 (The Baptist prepares the way of Christ)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
A - Peeñug Kàddug Yàlla gi ci Yeesu (Yowaana 1: 1-18)

2. Sóobkat bi ci ndox(Yaxya) mungi waajal yoonu Krist (Yowaana 1:6-13)


YOWAANA 1:9-10
9 Kàddu googu mooy leer gu wóor, guy ñów ci àddina te di leeral nit ku nekk. 10 Ci àddina la nekkoon, àddina si ñu sàkk jaarale ko ci moom, te àddina si xamu ko.

Krist mooy leeru àddina si dëgg. Am na téeméeri at, Xel mu sell mi jaarewoon na ci Yonent, ne leer googu dina ñów. Téeréey Kóllëre gu Njëkk gi wax nañu ay yooni-yoon ñówug Krist ci sunu dunya. Yonent Yàlla Esayi nee na: ”Mungi nii, lëndëm gi muur na suuf si, lëndëmaay gi muur askan yi; waaye Aji sax jaangi jóg ci yów, ci sa kow la ndamam feeñe.” (Esayi 60:2).

Ci Yowaana 1: 9:10 ñeenti yoon lañu ciy gis baatu “àddina”. Ci Yowaana, li baat boobu di tekki jege na torop li lëndëm di tekki, ndaxte bind na ne: ”Àddina sépp a ngi tëdd ci loxoy Ibliis.” (1 Yowaana 5:19).

Ca njalbéen ga àddina si bonuloon, ndaxte Yàlla nu baax la ko sàkkewoon. Rafetaayam, baaxaayam dañu feesoon dell àddina si ”Te Yàlla gis lépp li Mu def, fekk lépp a baax lool.” (Njabéen 1:31). Yàlla dafa sàkk nit ki ci melokaanam, te mayoon nañu ndamam maami nit ki, ñi doon lerax leeraayu Aji Sàkk ji ni ab seetu.

Waaye rëy tax na ba ñu mujje nekk ñu bon ak ay fippukat. Ñu dog seen jokkoo ak Yàlla, te lëngoo ak xelum lëndëm gi. Sore Yàlla, bon rekk lay jur, ni ko Dawuda nangoo ci Sabóor 14:1: ”Ki ñàkk xel dafa naan ci xolam: Yàlla amul! Yàqu nañu seen bopp, def nañu ay jëf yu ñaaw; Amul kenn ci ñoom kuy def lu baax.”

Yowaana taskatu Injiil li seede na ne Krist ñów na ci àddina su bon sii, ni jant bi di fenke te di dàq ndànk - ndànk lëndëm gi ci kanamam. Leeru Krist duggul ci àddina si ni melax buy metti bët. Ak lewetaay la dugge di leeral ñépp. Ñówul nib àttekat walla mbugalkat, waaye nib Musalkat ak Ràmmukat. Nit ñépp soxla nañu Krist leeral leen. Bu dul loolu, dinañu des ci lëndëm gi. Krist mooy leer gi tigi, waaye du keneen. Képp ku nangu leeram jaare ko ci Injiil li,s a jikko dina soppiku, nga baax te leer ci kow ñeneen ñi.

Nanu jéem a xam li wax jii di tekki: ”Aji Sàkk ji ñów na ci àddinaam.” Ki moom (boroom), jël na alalam, te buur bi jegesi na askanam. Kan mooy jóg ciy nelawam te waajal Ko ñówam? Kuy gëstu dëgg gi aju ci ñówam ak ay mébétam? Kan moo jekk ngir dummuuyu mébéti àddina yu ñàkk solo yi ngir teeru Yàlla jiy ñów? Kan mooy yëg jamono ju soppiku ji te di jenn doŋŋ, ji Yàlla di ñówe?

Ci saa si, Yàlla daldi feeñ ci biir bàkkaarkat yi. Ci biir sutura ak jàmm la ñówe. Bëgguloon a fésal màggaayam,kàttanam ak ndamam. Xanaa kay, suufeeloom, mbëggeelam ak dëggam, la feeñal. Ca Njalbéen ga ba tey, rëy mungi daan nit ki. Seytaane nag moom, dafa bëggoon am doole, ndam, ak xel, ni Yàlla. Gannaaw gi Krist, Aji Kàttan ji daldi juddu, liir bu tooy xepp te suufeelu ñu tërël ko ca ñàddu jur ga. Ak suufeeloom, lewetaayam, ak dégg ndigalam, Mu jël ndam li. Wàccee na boppam ba tollook ku gën a suufe ci nit ñi,ngir yékkati kenn ku nekk, te musal ñépp.

Yeen ñépp dégluleen! Gannaw xabaar bu neex boobu, gis nanu ne àddina si xamul leer gi te nandu ko. Nit ñi xamuñu ne Doomu Yàlla ji jegesi na leen ted und na ak ñoom. Dañoo des ci ngumba ak seen ndof, ak li ñuy xarañ ci baatin lépp, siaas, ak xam-xam. Gannaw xabaar bu neex boobu, gis nanu ne àddina si xamul leer gi te nandu ko. Nit ñi xamuñu ne Doomu Yàlla ji jegesi na leen te dund na ak ñoom. Dañoo des ci ngumba ak seen ndof, ak li ñuy xarañ ci baatin lépp, siaas, xam-xam. Ràññeewuñu sax ne Yàlla ci boppam mungi taxawoon ci seen kanam. Xamuñuwoon Ki leen sàkk, te nanguwuñu seen Musalkat ak seen Àttekat.

Ci kow dëgg gu metti googu, man nanu ci jële ab ponk bu am solo ci nguuru Yàlla gi: Manunu xam Yàlla ak sunu xelu bopp ak sunu man-manu bopp. Lépp lu nu xam ci mbëggeelu Krist, yiw la ak mayu Yàlla, ndaxte Xel mu Sell mi moo nuy woo jaare ko ci Injiil, di nu leeral ak mayam yi te di nu sàmm ci ngëm gu dëggu. Kon war nanu rëccu, tuub te bañ a wéeru ci sunu xelum bopp, walla sunu yëgeelu ruu. Danu war a ubbil sunu xol leer gi dëgg, ni tóor-tóor yi di ubbikoo ci ceeñeeri jant bi. Noonu la gëm Krist di jure xam-xam dëgg. Njalbéenu ngëm googu, jógewul ci nun, waaye liggéeyu Xel mu Sell mu Boroom bi ,mi nekk ci ñépp ñi ko déggal la.

ÑAAN: Nungi lay sant Boroom bi Yeesu, ci li nga ñów ci àddina si. Ñówuloo ngir àtte mbaa ngir fayu, waaye ngir leeral te musal nit ñépp. Danoo gumba ted of. Baal nu sunuy tooñ, te may nu xolu dégg-ndigal. Ubbil nu suny bët ba nu man laa gis. Ubbil sunu ruu, mu dékku ceeñeeri sa leer gu sedd gi, dax nu man a dunde kàttanu Xel mu Sell mi.

LAAJ:

  1. Lan la Krist Leer gi séq ak àddina lëndëm gi?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 09, 2025, at 01:49 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)