Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 008 (The fullness of God in Christ)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
A - Peeñug Kàddug Yàlla gi ci Yeesu (Yowaana 1: 1-18)

3. Feesaayu ndamul Yàlla feeñ na ci jëmmal gi (Yowaana 1:14-18)


YOWAANA 1:14
14 Kàddu gi ñów, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nanu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doom ji Mu am keep.

Kan mooy Yeesu Krist? Yàlla dëgg la te nit dëggantaan la itam. Kumpa gu rëy googu la nu Yowaana di tegal ni bàkku (feemu) Injiilam. Bi mu tegee baaraam ci peeñug Kàddu Yàlla, ci la nu won reenu bataaxalam. Aaya 14 mooy caabi yéene yi ci topp yépp. Boo xamee bépp tekki-tekki peru baatin bii, kon dinga àgg ci xam-xam bu xóot bu nekk ci saar yi nu dëgmal.

Ni Krist jëmmale Yàlla ci kow suuf, wuute na lool ak sunu yeesalu baatin. Nun ñépp am nanu yaram, te sunu ndey ak baay ñoo nu jur. Gannaaw loolu kàddug Injiil gi laal nu, te yeesal dund gu dul jeex ci nun. Waaye Krist juddoowul ci baayu nit. Kàddug Yàlla moo ñów ci Mariyaama ni ko ko malaaka mi waxe: ”Xel mu Sell mi dina wàcc ci yów te Aji Kowe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddoo ci yów dinañu ko woowe Ku sell ki, Doomu Yàlla ji." (Luk 1: 35). Ci know ni mu nangoo xabaar bu neex boobu ak ngëm, xiig gi jot as ngelabon cundum, ci biiram fu Xel mu Sell mi ànde jaxasoo ak deretu nit. Noonu la Yàlla defee boppam nit.

Sunum xel matul ci googu dëgg. Xam-xam bi aju ci yaram manual a faramfàcce kumpa googu. Li nit ki jot a gism anu ko àjji. Yenn kangaami diine dañuy jéem a woyofal juddug Yeesu di ko jéem a gise ciy xalaati “siaans”, te naan dafa feeñ ci yaram wu dul yaram wuy yëg metit ak naqar. Nungi biral fii, te nangu ko, ne Krist dafa boole woon nekk nit dëgg, ak Yàlla tigi.

Jëmmalug Krist mooy faramfàcce bi gën ci juddu gu kéemaane gii. Doomu Yàlla ji ba fàww, ji nekkoon ak Baay bi ca ba dara xewagul, mos na sunu yaram te raxul bàkkaar, ndaxte Xel mu Sell mi nekkoon ci Moom daan na jeng bu jëm ci bàkkaar. Noonu Yeesu kese moo dund ci set ci bàkkaar, ak laab, te amul benn gàkk-gàkk.

Doomu Yàlla ji jaxasoo na ak way—fippu yi, ak ñu soxor ñi te bon, te dee ñoom ñépp. Waaye Moom amul àpp, manual a dee ndaxte Yàlla la. Ak li muy doon Ku kowe lépp, terewul mu bëgg nu, ba bàyyi ndam la Mu amoon ca wetu Baay bi, ñów dund ak nun ci suufeelu. Dafa dellu nekk ni nun te xam bu baax li nuy dund. Ci biir coono la jànge dégg ndigal gu mat sëkk. Dafa feesoon ak yërmande. Moom beddiwunu, nun nu bon ñi. Krist dafa soppaliku nit, ngir man noo jege, ba dendale nu ak Yàlla.

Yaramu Krist dafa mel ni Kër Yàlla ga ca jamonoy Kóllëre gu Njëkk ga, fa Yàlla daan dajeek ay ñoñam. Yàllaa ngi nekkoon ci Krist, te feeñu nu ci jëmmu nit. Lépp li doon Yàlla, dafa newoon fàŋŋ ci Krist. Li xëtu gerek bi wax sax mooy ne Yowaana nee na Yeesu dafa “Nekksi néegu Yàlla“ ci sunu biir. Loolu mooy tekki ne tabaxul ag këru buur guy yàgg, ngir dëkk ak nun ba fàww ci know suuf ,waaye ab diir bu gàtt la fiy toog ,ni ko màngaan yi di defe ci seeni xayma yi; bu ñu noppee rekk dañuy lem seeni xayma, dem feneen. Krist, ab diir bu gàtt la toog lak nun, gannaaw gi Mu dellu asamaan.

Apootar yi seede nañu ndamul Krist. Seen seede boobu sargal la ak mbég mu rëy. Ñoom ñooy seede yi gis jàkk Doomu Yàlla ji ci yaramu nit. Seen ngëm may na leen ñu xam mbëggeelu Yeesu, muñam, suufeeloom, njubteem, ak ni Mu nekke Yàlla. Yàlla ci boppam lañu gisoon, ci bépp sellaayam. Ci Kóllëre gu Njëkk gi, baatu “Ndamam” dafa tënk lépp li aju ci melokaanu Yàlla. Apootar Yowaana dafa wone ak njàmbaar ci seedeem lépp liy melokaanu Yeesu. Moom xamoon na màggaayam gu nëbbu gi, rax ci dolli rafetaayam ak màggaayam.

Ni ko Xel mu Sell mi solo la Yowaana woowe Yàlla, Baay, te tudde Yeesu, Doom. Kenn manual a moy baat yooyu. Xelalug Xel mi dafay xotti ndimo liy nëbb turu Yàlla te di nu wóoral ne aji sell ji amul àpp, Aji Sàkk, ji am kàttan, mooy Baay te am na Doom ju sell ni Moom, di boroom ndam, di nekk ba fàww, te fees dell ak mbëggeel. Yàlla du àttekat buy daan, di yàq, te di fayul rekk. Dafa am yërmande, lewet, te man a muñ, te Doomam itam noonu la mel. Bu nu xamee dëgg Baay bi ak Doom ji, kon dinanu jot xolu Kóllëre gu Bees gi. Képp ku gis Doom ji, gis nga Baay ji. Bii peeñu soppi na gis-gis bi yeneen diine yi am ci Yàlla, te ubbi sunuy bët ci jamonoy mbëggeel.

Ndax bëgg nga xam Yàlla? Kon jàngal dundug Krist! Lan la taalibe Yeesu ya gisoon? Ci gàttal lan mooy seen seede? Gis nanu mbëggeelu Yàlla gu ànd ak yiw ak dëgg. Bàyyil xel ci ñetti baat yooyu, te boole ci ñaan, noonu dinga gis mataayu ndamul Yàlla ni mu teewe ci Krist. Ci yiwam, Yeesu dafa nu fekksi te yelloowunu ko, ndaxte ñu dëng lanu. Nun ñépp a tooñ; kenn ci nun jubul. Ñówam mooy wone yiwam. Rusul sax di nu woowe ay doomi baayam, waaye dafa nu laabal, Sellaaal nu, te yeesalaat nu ba noppi sol nu Xelam ba nu fees. Yii jëfi texe ndax duñu “yiw ci kow yiw”? Te ëpp na loolu sax, ndaxte am nanu yelleef bu bees; Krist may nanu yiwu nekk ay doomi Yàlla. Xabaaru Yiw wi du ay naxaate walla ay xalaati neen, maanaam ay génti neen, waaye yelleef bu bees la. Jëmmal gi, màndarga la buy wone ci dëgg liggéeyu Yàlla, biy tax nu mat ci muccam gi. Yiw wi mooy reenu sunu ngëm.

ÑAAN: Nungi lay sujjootal, yów liir bi ci ñàddug jur gi, na ko sàmm ya ak kàndiŋ ya Betleyem. Yów yaay Yàlla ji jëmmoo nit, te rusuloo nu woowe say doomi baay. Sa leer mungi leeral lëndëm gi. Laabalal sama xol bu selladi bi, ndax mu man laa nekkal ndabal ñàdd ba fàww. Maangi booloo ak way-gëm yépp, ngir màggal la, ndaxte sa ndam nekk na yaram wu suufeelu. Nungi lay ñaan nga feeñu ñi nu wër ngir ñu man a jot seen yelleef bu bees bi, te nangu la.

LAAJ:

  1. Lan mooy jëmmalug Krist?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 10, 2025, at 08:29 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)