01 - UBBITE GI: SOLO Ndigal yi ci dëgg-dëgg
Dafa amoon waa ju doon tukki ci ropplaan bu jógewoon Deli jëm Srinagar ca diiwaanu Casmiir; nees tuuti mu séen rafetaayu tundi Imalaya ya, galaas ga muur leen te ñu tiim tooli indu ya, Tund yu kowe ya dañoo tiim ay xur yu xat te tëju, Yenn coll yi dañoo nëbbu ci biir niir yi, Dañuy kowe ba ëpp 8000 meetar te sut sax yi gën a suufe yiy tollook 5000 meetar.
Bi ñu teeree Srinagar ,gan ga daldi fa fekk ay diine,aki aada yu dul jeex. Indu,waa Budaa,Yawut ,kercen,Jullit,ak Yéefëer,ñépp a fa dajaloowoon.Këri jàamukaay ,Jàngu, Jàkka ak ay tablo-mbedd,yépp a fa doon wujje ngir xëcoo nit ña. Juróomi réew ñoo dajewoon ca bérab bu ndaw boobu-Indu,Pakistan,Afghanistan,Ruus ak Siin-Bi muy wër taax ya ak dëkk yu ndaw ya ca Kasmiir,sunu gan gi yëg jankoonte gi am ci diggante nit ñi.Moone sax ab xare mbooloo bu bare deret ju turu yàq na taaru xur woowu la ko dale ca atum 1991.
Cosaan yi,ndigali diine àddina yu mag yi ak mebéti politiku nguuri àdina si dañoo lëj te yaatoo ni tundi Imalaya yi. Waaye li ëpp ci mbind yi, cant yi ak ndigali diine yi mbooloo mu tuuti moo ko yilif ni tundi Imalaya yu gën a kowe yi tiime yu gën a suufe ya.Benn ci Njobbaxtal yi gën a kowe ci coosaanu àddina mooy Dekalog bi maanaam « Fukki Ndigal yi ». Jenn YÀLLA ji dëgg wax na ak Musaa sàmm bi, xamal ko Coobareem gi, te bind Ndigalam yi ci ay alluwa xeer. Yawut yi ci kow cër lu mag lañuy fàttalikoo Baay jooju Yàlla jaarewoon ngir fas kóllëre ak ñoom ca tundu Sinai. 3300 at gannaaw loolu,ñungi jàng ay mbindam ba tey ci Këri- YÀLLA yi.
Kercen yi itam dañu jàppe Fukki Ndigal yi ni seen reenu ngëm bu kenn manul a buddi. Yeesu nee na ay taalibeem « li fekk asamaan ak suuf wéyul, benn tomb walla benn rëddu araf du wéy mukk ci yoonu Musaa,ba kera yépp di am. » (Macë 5 :18)
Jullit yi « Kalimu ALLAH » lañuy woowe Musaa maanaam Yonnetu Yàlla. Dañu ko jàppe ni Yonnent-Yàlla ak njiitu politik, nitu diine bu am baat ci politik.Ci ñoom, Musaa bokk na ci ñi gën a mag ci cosaanu àddina si.
Fukki Ndigal, yi Musaa jottali Doomi-Adama yi,wàll wu am solo lañu am ci Kóllëre gu Njëkk gi.Nekkoon nañu, te ba tey jii sax, ab ponk bu am solo ci Doomu-Aadama. Képp kuy jàng yii Ndigal, di leen denc, te di leen di jàngale dangay nekk ku maandu. Bépp askan bu faalewul yii Ndigal mbaa mu fàtte leen, dina daanu ci ger. njeng te réer. Ku bëgg a moytu mujj gu mel noonu,dafa war a jàng bu wér FUKKI NDIGAL YI.
Gëstu Fukki Ndigal yi dafa mujj nekk lu am solo te jamp ca kasimiir ndaxte diine yu yàgg ya dañu fa jàmmaarloo ak xalaati jamono tey.Sunu dundinu bés-o-bés mooy waral kenn ku nekk ci nun war a dellu ci yoonu Yàlla bi nekk ci Kóllëre gu Njëkk gi. Téere bii dañu ko bind gannaaw ay waxtaan yu ñu amaloon ak ay ndawi diiwaanu foofu ñuy woowe « njobbaxtalu àddina si » Ndaw yooyu nga xam ne dañoo wuute diine yi ñu cosaanoo, dañoo wut dëgg gi ak yoonu doxalinu seenug dund. Dañoo saytu dëgginu FUKKI SANTAANE YI ngir jamono tey. Ku ànd ak ñoom ci seen gëstu dinga baarkeel ci sag dund bés bu nekk.