Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 090 (Abiding in Christ)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
D - Tàggatoo ba ca yoonu Getsemane (Yowaana 15:1 - 16:33)

1. Bu nu saxee ci krist, danuy meññ bu baax (Yowaana 15:1–8)


YOWAANA 15:1-2
1 Man maay garab gu wóor gi, te sama Baay mooy Baykat bi. 2 Car bu soqikoo ci man te meññul, dina ko dog, sànni. Waaye car bu ci meññ, dina ko tenqi,n gir mu gën a meññ.

Ba ñu reeree ba noppi, yeesu ak ay taalibeem ya jaar ca buntu dëkk ba, dem ca tundu Oliw ya jaare ko ca toolu reseñ ya. Ni ñu doon doxe, Yeesu di leen gën a leeralal seen jariñu ngëm ak seen ngirtewu mbëggeel, jaare ko ci misaalu garabu reseñ gi.

Yeesu misaale Yàlla ni boroom toolu reseñ, bi saxal taatu garab yi ci àddina sépp. Benn ci ñoom moo nekkoon waa Kóllëre gu Njëkk ga, ni nu ko Sabóor 80:8-16 ak Esayi 5:1-7 Waxe. Yàlla béguloon ci garab yooyu, ndaxte daawañu meññ ay reseñ. Noonu Yàlla jëmbat car bu bees; maanaam Doomam, ji juddoo ci Xel mu Sell mi. Mooy nekki garab dëgg gi, te war a meññ te jur xeet bu bees, ak maas gu sell, guy jur ay doomi baatin yu takku. Yeesu xamle li aju ci doom bi Xel mu Sell mi di meññ ci doom-Aadama yi, muy doomu jikko baatin, ju am solo ji. Moom xamoon na ne njàngalem nit dafa am njuumte, ndaxte am na mala muy dund ci nit ki, te di xaar ku ko yee rekk, ngir mu man a rajaxe ñeneen mi, ba warax leen. Ca ba muy door njàngaleem, Yeesu dafa ne woon Moom rekk mooy kiy meññ doom yu neex Baay ji, te mooy surga jàmm ji ak kiy sos Jàngu bi.

Yeesu dafa njëkk a wone li jaaduwul ci misaal bii : Yàlla dina dog bépp caru garabu reseñ bi,bu dul dékku mbëggeel,Mbaa du meññ doomu baatin,mel ni car bu amul njariñ. Bu Yàlla fekkul ci yów meññeefu (doomu) Injiil li,walla gisul ci yów li deewug Yeesu ak ndekkiteem jur ci sa dund,kon dina la dog ci garabu Doomam ji. Waaye bu gisee ne Xel mu Sell mi mungi liggéey ci yów, dina la suuxat ba nga màgg ni car bi sax ci garab gi.

Ay xob dinañu ci sax te dina amy doom. Boroom tool bi dafay felet(dagg) car yi amul njariñ, nbax garab gi gën a man a meññ. Doom jooju, walla meññeef moomu du sa alal, waaye yëfu Krist mi nekk ci yów la. Ay surga yu amul daanaka njariñ lanu, waaye Moom lépp la ci ñépp. Ndax xamoon nga ne garabu reseñ dañu koy tenqi lolli wu nekk, ndax mu gën a meññ at mi ci topp? Noonu it la Yàlla di jëfe ak nun. Dafa lay jubbanti te dindi sa sikk yépp ngir dakkal sa dëgër bopp gi te nga dëddu bàkkaar ba dee. Noonu dunug Krist dina màgg ci yów jëmale la cig mat. Bare na ay yoon yu Boroom bi man a jaar ngir tàbbal la ci mucc gi. Ay xew-xew, ay lajj, ak ay feebar dinañu la soong ngir daaneel la. Bul dund ngir sa bopp, waaye dundeel Boroom bi; bu ko defee, ci kàttanam, dinga nekk ku am mbëggeel.

YOWAANA 15:3-4
3 Yéen nag, Baay ji setal na leen jaarale ko ci kàddu gi ma leen wax, ni baykat di tenqe garabam. 4 Saxleen ci man, ma sax man itam ci yéen. Ni car manul a ame ay doom, te saxul ci garab, noonu itam dungeen man a meññ li may jëfe ci yéen, bu ngeen saxul ci man.

Yeesu dafa nuy dëfal. Yàlla du nu dagg ci garab gi ndax sunu geru judduwaale,ak sunu bàkkaar yu bare yi. Yeesu may na nu cellaay gu mat sëkk, li ko dale ca bés ba nu gëmee. Bul wax ne: «Benn bés dinanu sell jaare ko ci sunuy farata,ak ni nuy ñaane.» Dafa noo laabal ba noppi; baal na nu benn yoon ba fàww te sellal na nu ca kurwaa ba (bant ba). Injiil, kàttanu cellaay lay noyyee. Naka noonu, du sunuy man-man, sunu coono walla sunu mataay ñoo nuy sellal, waaye kàddug Yàlla gi. Ni Aji Sàkk ji sàkke àddina si ci kàddoom, noonu itam la Yeesu di sàkke sellaay ci nun, bu nu déggalee kàddoom. Du ndigleb sóob ci ndox, walla reeru Boroom bi ñoo nuy sellal, waaye ngëm gi nu am ci Yeesu Krist la. Njàngum Biibal bi dafay xóotal sunu ngëm. Jéemal a jàng Biibal bi bés bu nekk, ndaxte boo ñàkkee dundu baatin, dangay sore Yàlla.

Yeesu dafay dëgëral baatu SAX ci. Ci baat boobu la sunu màggaay ak sunu meññ aju. Man nanu gis tekki-tekki yu bare ci baat boobu di feeñ fukki yoon ci saar 15; danuy sax ci Moom, mu sax ci nun ;danuy sell bu nu saxee ci Moom; kàttanam ak meenam ñooy daw ci nun. Lépp ci Moom la jóge, kon danu war a sax ci Moom. Bu nu tsax ci eqalikoo ak Moom, kon kàttanam du manatee daw ci nun. Bu ab car dammee ab diir bu ndaw sax, dina wow. Ndax xam nga ab jàngu bu wow koŋŋ ba dee? Am na de! Ni ay way-gëm, danu war di ñaan Yàlla mu nuy dimbali ngir nu sax ci Moom. Noonu dina def liggéeeyam ci nun saa su nekk, di nu dimbali nuy màgg, di meññ ak di jëf. Rax ci dolli dina nu sàmm guddi ak bëccëg ci turam. Sax du ci kow sunu man-man, waaye ci kow yiwu Xel mu Sell mi la. Kenn manul a saxal boppam ci Krist. Nanu Ko sant ci may googu te ñaan Ko Mu wéy di sax ci nun, te it ñeneen man a sax ci Moom.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, yów yaay garabu reseñu Yàlla gu sell, gi nekk ci nun. Ci yów lanuy ame jikko yu baax yépp. Mbon gépp ci sunu xol la jóge. Nungi lay sant ci ni nga nu sellale jaare ko ci Injiil li. Sàmm nu ci sa tur, ndax sa kàttanu Xel mu Sell mi man a meññ doomu mbëggeel gi. Bu dul Yów, dunu man a def dara. Yokkalal doole sunu dogu mbokk yi, ndax ñu bañ di dund ngir seen bopp rekk, ci néew-kàttan, waaye ñu sax ci Yów.

LAAJ:

  1. Nan la Yeesu nekkee garabu reseñ gi dëgg?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 19, 2026, at 11:03 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)