Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- Tracts -- Tract 05 (Prepare The Way of the LORD!)
This page in: -- Armenian -- Baoule -- Burmese -- Chinese -- Dagbani? -- Dioula -- English -- French -- German? -- Greek -- Hausa -- Hebrew -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Japanese -- Korean -- Lingala -- Maranao -- Nepali? -- Peul? -- Somali -- Spanish -- Sundanese -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Uzbek -- WOLOF -- Yoruba

Previous Tract -- Next Tract

BATAAXAL - Bataaxal bu ñu tënk ngir séddale ok

BATAAXAL 05 -- Xàll-leen yoonu Aji sax ji! (Esayi 40:3)


Nit ñi dañuy yëngu rekk, te amuñu mujj gu ñuy séntu ci seen dund. Tekk ak teey lañuy bëgg a aakimoo, te di xar seeni tánki tubéy ngir am luñuy dunde bés bu nekk. Seen xel demul sax ci dee gi leen di xaar. Ñu néew ci ñoom ñooy báyyi xel ci Yàlla, ragal ko ba di topp ay ndigalam ngir man a tettewu te jaare ci xam dëggam gi.

Ki sàkk àddina si, maanaam Aji sàkk ji du fàtte mukk lenn ci li Mu sàkk. Lu ci nekk ci ñoom bëgg na ko, te mungi leen di báyyee xel, di waxtaan ak ñoom, te di seetlu seen xol. Dafa leen bêgg a sol kàttanam, bu ñu nangoo rëccu seeni bàkkaar, tuub leen te dellusi ci Moom.


Aji sax ji moo nuy fekksi (ganesi)

Ba Aadama ak Awa ñàkkee déggal Yàlla, dañoo amoon gàcce ba daw làquji, ndaxte gisoon nañu jéya ji ñu defoon. Moone de Aji sax ji mbugaluleen, waaye dafa leen a wër ngir gis leen, “Aadama foo nekk?” (Njalbéen 3:9). Aji sax ji nun ñépp lay wut, te naan nu:"foo nekk?"Foo tollu ci sag dund?"

Ca Mesopotami la Yàlla woowe Ibrayma ca biir ña gēmoon ay yàlla yu bare rax ci dolli geru. Noonu Yàlla def ko ab màngkat bu ñeme coono, te di yóotu ab dalu bu sell bu mu man a dëkk ba fàww. Mbokk mi,ndax yow itam dangay wut yoonu njubte gi, maanaam kër goy dëkk ba fàww, te moom ko?

Yanqóoba ab naxekat bu muus lawoon.Dafa dawoon làquji ca dëkk bu sore, ba noppi mu takk fa soxna. Gannaaw ay at yu bare, mu ñibbisi cim réewam. Waaye malaakam Yàlla kar ko ca yoon wa ngir fayloo ko bàkkaar ba mu defoon laata muy gàddaay. Moone de Yanqóoba gëmoon na yērmaande Aji sax ju rëy ji. Mu bëre ak ku sell ka, te naan ko, “Duma la báyyi nga dem te barkeelooma!” (Njalbéen 32:26). Ndax yaangi ŋoy ci Yàlla ba Mu musal la?

Musaa dafa dawe Misira, dugg ca manding ma,ndaxte ca biir meram dafa reyoon ab wottukat bu doon dóor ab yawut bu nekkoon jaam. Gannaaw 40 at, Aji sax ji feeñu ko ci as ngarab suy tàkk, ne ko “Man maay Ki nekk”, Ki dul soppiku mukk.Musaa mosu Ko ñàkk a déggal. Ndax Boroom bi mos na la a dabsi ci sa mandingu dund?Ndax sa xol dégg na wooteem bi?Ndax yëg nga Kóllëreem gi dul soppiku mukk?

Samwel waxambaane lawoon ba ko Aji sax ji di woo ngir fal ko nib àttekat cim réewam. Du ay mag doŋŋ la Yàlla di tànn, waaye itam ay xale. Dañu war a jàngal xale yi Kàddug Yàlla gi, te wommat leen ñu jëm ci Moom. Aji sax ji dafa bëgg a jokkoo ak xaley tey,te jaare ko ci ay surga yu mel ni yow.

Daawuda dafa njaaloo, ba noppi reylu jëkkëru ndaw sa. Waaye loolu taxul Yàlla báyyi ko. Dafa koo yónnee ab yonentam, ngir mu xamal ko bóom gi mu jëf, te yëgal ko ne merum Yàlla mungi boy ci kowam. Daawuda daldi rëccu bu baax bàkkaaram te soññi bàkkaarkat ya ba ñu dëddu seeni bàkkaar. Daawuda daldi am yiw ak mbaalug Yàlla. Jàngal Sabóor 51; jápp ko ci sam xel te ñaane aaya yii ak ngëm noonu dinga ci jële xel mu dal ak njéggal gi Daawuda amoon.

Esayi, mooy njiitu diine ja séenoon ndamul Yàlla ba xaacu ne: “Musiiba dikkal na ma!sànku naa, ndaxte ku ay tuñam selladi laa, te Maangi dëkkandook aw askan wu ay tuñam laabadi, te samay bët (gët)teggu nañu ci Buur bi, Aji Saxu xarekat yi.” (Esayi 6:5).

Dafa jooy ndax leeraayu Aji sax ji won na ko ni mu mel, moom ak askanam. Ndax bëgg ngaa jege Yàlla ngir gis ndamam?Kon gis nga ne sa bàkkaar mungi lay tággale ak Ku Sell Ki. Ndax xamoon nga ne say bàkkaar dañu lay xañ nga jege Aji sàkk ji, te dañu leen war a faxas? “Nungi leen koy ñaan,nanguleen a juboo ak Yàlla” (2 Korent 5:20).


Xàll-leen yoonu Aji sax ji !

Képp ku bëgg a neex Yàlla, danga war a sàmm ay ndigalam. Te ku def bàkkaaru lees-teyul ba moy ay ndigalam, war nga rëccu te tuub sa bàkkaar, ñaan Boroom bi Mu baal la ko ci kow digeem bi ne: “Bunu nangoo sunuy bàkkaar ci kanamam, Moom kuy sàmm Kóllëre la te jub, ngir baal nu sunuy bàkkaar te sellal nu ci lépp lu jubadi” (1 Yowaana 1:9). Na ki fen jublu ci Yàlla te nangu fenam. Na ki fekk lu mu moomul ci biir këram, jël loola delloo ko boroomam, te ñaan ngir ñu baal ko. Na kiy ànd ak keneen di moy, nangu sobeem, tuub ko te dëddu bàkkaar. Kiy noot ñeneen ñi, rawatina ay ñoñam, soxnaam ak njabootam, na leen baalu te dogu ci jàppale leen.

Yaxya matal na digeb Yonent-Yalla Esayi ba mu biralee peeñu ma mu jotoon: “Baat baangi jib naan:"Xàll-leen yoonu Aji sax ji, ca manding ma,maasale mbedd ya ngir sunu Yàlla ca tàkk ga!Na bèpp xur maasaloo, te bépp tund màbb, bu mag ba ba ca bu ndaw ba. ;yoon yi ñagas rattax, te mbartal doon joor. Noonu ndamul Aji sax ji feeñ te nit ñépp gisandoo ko;ndaxte gémmiñu Aji sax ji wax na ko.” (Esayi 40:3-5; Luk 3:4-6).

Yaxya moo waare ne amul benn Doomu Aadama bu jub. Nun ñépp a tooñ,te war nañu nu sellal, soppi nu ba nu nekk ñu suufeelu. Na ki nax ñeneen ñi dëddu muusanteem, dox ak njubte, te jubbanti ay ndëngateem.

Aaya yii nu dëgmal dañuy tënkk Ndigali Yàlla yi: “Nanga bëgg Aji sax jiy sa Yàlla, ak sa xol bépp ak sa noo gépp, ak sa kàttan gépp” (Nafaru Ndigal yi 6:5), te, “anga bëgg sa moroom ni nga bëgge sa bopp. ” (Lewi 19:18). Soo nammee bëgg Yàlla, nanga sàmm ay ndigalam. Laajal Boroom bi nan nga Ko man a waajale yoonam wi ngir mu ganesi la.


Aji sax ji Mungi xàll yoon, te jëmsi ci yow

Doomu Mariyaama ji ni Mu juddoo dafa jéggi dayoo, ndaxte Xelum Yàlla moo soppaliku jëmmu nit ci Moom. Dañu yónniwoon Yeesu Mu am jëmmu suux, ci biir doomi Aadama yu fees dell ak bàkkaar, te geru. Mu feeñu leen ak mbëggeel ba di faj seeni mbokk yi am jàngoro, rax ci dolli di dàq rab yu bon yi leen doon dugg. Monte ña ëppoon ca askan wa jáppuñuwoon ne reenu ndamam googu, ci mbëggeelam gu sell gi la saxe.

Mariyaama ji faxas bàkkaaru àddina si, wuutu nu ci dee gi, sellal nu ci bépp bàkkaar, te layool nu ba nu jot njubte gu amul genn payoor. Nanu Ko sant,te bëgg Ko ndaxte Moo nu ubbil buntu asamaan yi.

Ñowug Yeesu Krist ci sunu àddina si mooy ponku cosaanu nekkinu Doomu Aadama. Yàlla dafa ñów fekksi nu, ngir nu wëlbatiku dellu ci Moom. Képp ku tuub te wëlbatiku ci Yàlla, Mu baal la. Képp ku xam mbóot googu, ku maandu nga, te ku ciy dox, dees na la naw.


Yàlla dafa nuy fekksi, ku nekk ci sa bopp

Krist dafa ne mëll ci bàmmeel te di dund ndaxte dafa daan dee gi, yéeg ca asamaan, di dund ak Yàlla ju sell ji. Namm na lool taalibeem yi Mu bëgg. Xam na seen néew doole ak seen yaakaar,loolu moo tax Mu yónnee leen Xelam mu Sell mi. Laata Muy yéeg asamaan Yeesu nee na ci, “Ci dēgg maangi leen koy wax,li gën ci yéen, mooy ma dem, ndaxte su dul loolu, Dimbalikat bi du ñów ci yéen ;waaye suma demee, dinaa leen ko yónnee.” (Yowaana 16:7). Xel Mu Sell miy sunu dëfalkat, la Yàlla di ñówe ci nun. Xel moomu mooy dëkk ci ndawi Yeesu yi.

Ndax ubbil nga sa xol Xelum Krist mi ?Dafa laa bëgg a soppi, te sol la mbēggeelam ba nga fees dell, ngir jàmmam ji, mbégteem,góor-góorloom,ak baaxaayam dëkksi ci yów. (Macë 11 :29 ;Galasi 5 :22-23) Aji sax ji mungi fëgg ci sa buntu xol. Ndax dinga ko ko ubbil ? Bul dëgëral sa xel, waaye xàllalal Aji sax ji yoonam wi jëmsi ci yów. Seen YÀLLA nee na:

Dëfalleen sama mbooloo, dëfalleen seen xol. Wax leen waa Yerusalem ak laabiir, dégtal leen ne seenug njaam jeex na, te jot nañu ci loxoy Aji sax ji lu fay ñaari yoon seeni moy.” (Esayi 60:1-2)


Yàlla angi ñów ci ku nekk

Mbëggéelu Krist dafay xiir Képp ku sa Xelum diine soppiku, ci yëgal say xarit ak say dëkkandoo xabaaru Injiil bu baax bi, te xamal leen ne Yàlla angi leen di xaar. Bul wëndeelu ci neen, waaye toppal Krist, te gindiji ñiy réer.

Boo xamul ni nga war a surgawoo Boroom bi, ñaan Ko ngir Mu won la yoon wi ba nga man a jot ñeneen ñi, rax ci di def ay jëf yu rafet, te di dimbali ñi nekk ci soxla. Boroom bi dina ubbi sa gémmiñ booy wax ak ñi namm a dégg mbëggeelu Yàlla ak sellaayam. Boroom bi dafa lay may doole, ànd ak yów, te sàmm la. Dénkal Krist it ed it e noonu dinga barkeel. Boroom bi dina waajal say ndaje.


Xalaatal ci kumpag ñówug Krist

Boo nammee xóotal sa xam-xam ci ni Krist laale xoli ñu bare, bind nu ngir nu man laa yónnee Injiilu Krist bu ànd ak ay nafar aky ñaan yuy dëgëral sa ngëm ,sa mbëggeel ak sa yaakaar. Na sa mbind leer nàññ.

Sa bataaxal rekk lanuy xaar.

WATERS OF LIFE
P.O. BOX 60 05 13
70305 STUTTGART
GERMANY

Internet: www.waters-of-life.net
Internet: www.waters-of-life.org
e-mail: info@waters-of-life.net

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on May 16, 2025, at 05:15 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)