Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Armenian -- Baoule -- Burmese -- Chinese -- Dagbani? -- Dioula -- English -- French -- German? -- Greek -- Hausa -- Hebrew -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Japanese -- Korean -- Lingala -- Maranao -- Nepali? -- Peul? -- Somali -- Spanish -- Sundanese -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Uzbek -- WOLOF -- Yoruba
BATAAXAL - Bataaxal bu ñu tënk ngir séddale ok
BATAAXAL 04 -- Na jàmm dëkk ci yéen!Sunu jamono ji dafa jaxasoo. Bomb yaangi téll-télli, xare yi di jolli, doomi jàngoro yi ñungi soong réew yi, koom gi mungi rës, te xiif, fit wu rëcc, ak ñàkk yaakaar ñungi noot nit ñi.Ñu bare ne jàmm ak déggoo man nañoo am. Krist nag artu nanu ci li war a ñów: “Dingeen dégg ay xare ak coowi xare ;buleen ci tiit, ndaxte fàww loolu am...” (Macë 24:6). Ci téereb Peeñu ma, jànge nanu ci ne jàmm ji dañu Ko rocci ci àddina si (Peeñu 6:4) Lu tollook 2700 at ca gannaaw, Yàlla waxoon na yonentam Esayi ne “Ñi soxor duñu am jàmm mukk.” (Esayi 48:22; 57:21).
Ñan ñooy ñu soxor ñi ?Ñu bare dañuy jàpp ne ñoo gën ñeneen ñi, ndaxte seen doxalin moo gën a rafet. Xëy na ñoo nu gën a jàng te ëpp nu tiitar. Ñeneen di xalaat ne seeni jëf yu baax dinañu faxas yu ñaaw ya,ba bésub àtte ba deesu leen daan. Aka ñoo juum ! Bunu méngalee sunu bopp ak Yàlla, sunu jéll dafay leer naññ. Képp ku diiroo mbagg ak mataayu Yàlla, ak yërmaandeem dangay mel ci kanamam ni kuy sagu ak di tiitaru. Kan nga ciy niirool ? Ci sunu jamono jii, ñu bare dañuy moy ndigali Yàlla yi ndaxte dañoo tàmm a bàkkaar. “Aji sax ji gis ne coxoru nit réy na lool ci àddina, te fu ñu man a tollu lu bon rekk lanuy xēnte ci seen xol” (Njalbéen 6:5). Yonent-Yalla Daawuuda dafa xaacu ne : "ñépp a réer, te ñépp a ngi moy amul kenn ci ñoom kuy def lu baax, du ci kenn sax !"(Sabóor 14:3;Rom 3:10-12) Tey jii, kenn nëbbatul a def lu bon, ba di ci rus,di ci am kersa walla loo ciy rëccu. Sunu duniyaa bii,Sodom ak Gomor lay nirool, te nungi ci biir, danuy ñàkkal solo bàkkaar, te xam ne merum Yàlla ci sunu kow lay dal nun ñépp. "Yàlla dàq ñi rë waaye yiwal na ñi woyof." (Yanqóoba 4:6)
Jàmm ji Yàlla moo nu koy mayAji sax jiy Boroom yērmaande ji moo xamal yonentam Esayi ne jenn doom cundum dina juddu, te dees na ko tudde Diglekat bu yéeme bi. Nguuram dina sax ba fàww".(Esayi 9:6-7) Ba doomu Mariyaama ja juddoo ca Betleem, malaaka ya dañoo bég ba di woy naan: "Ndam ñeel na Yàlla ca asamaan ya kowe, te na jàmm wàcc ci suuf ànd ak ñi Mu nangu ndax yiwam !" (Luk 2:14) Ak li may googu di am lépp, terewul ne ñu néew ñooy nangu jàmmu Yàlla, ba mos yērmaandeem gu jéggi dayoo gi. Moone de jàmmu Yàlla ji dafay solu ba fees ñépp ñi nangu digeem bi te gëm ko. Ba Krist dekkee, dafa feeñu ay taalibeem ca kow nañu tiitewoon, Mu dëfal seeni xol, ne leen, “Na jàmm wàcc ci yéen !” (Yowaana 20:19, 21, 26) Ci biir nuyóo boobu Doomu Mariyaama ji mungi doon maye jàmm ju amul àpp ji Mu lal ci diggante Yàlla ak nun, jaarale ko ci wuutu bi yonent waxoon ba mu naan: “Danoo teg ne mungi ci mbugal di ku Yàlla fàdd, te suufeel ko te fekk sunuy tiis la yenu, gàddu sunuy naqar.Sunuy bàkkaar a tax Mu gaañu, ne làcc ndax sunuy tooñ mbugal gi nu may jàmm,Moom la dal.Nun ñépp a réeroon ni ay xar, ku nekk aw saw yoonu bopp,te Aji sax ji yen ko sunuy njubadi nun ñépp.” (Esayi 53:4-6) Krist moo nu jubóolewaat ak Yàlla ci ni Mu nu wuutoo ba jëndaat jàmm ji ak yiw wi nu Yàlla jagleel. Doomu Mariyaama ji forsewunu ngir nu nangu jàmmam ji, sasunu ko itam, dafa la ko tegal ngir nga man a tànn te nangu ko ci sa coobare te féetewoo sa yiwu ngërëm.
Nangu Jàmm JiKrist dafa ñaax ay taalibeem, ne leen, “Jàmm laa leen bàyyeel, sama jàmm laa leen may. Mayuma leen ni àddina di mayee. Buleen jàq, buleen tiit.” (Yowaana 14:27). Buuru jàmm ji mooy may jàmmu Xelam ñi gēm kàddoom. Kepp ku jot Xelum jàmm ji, dinga soppiku ba nekk "Doomu jàmm". Ndaw li Póol biral na ko ba mu nee: "kon nag gannaaw Yàlla àtte na nu ni ñu jub ci sunu ngëm, nanu jàpp ci jàmm ji nu am fa kanam Yàlla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Krist." (Rom 5:1) Ñu bare ñu doon wut, jot nañu léegi xelum jàmm, mi dëkksi ci seen xol. Nungi lay ñaax ngir nga ñaan Yàlla, Mu matal digeem ci sa dund, jaarale ko ci wuutub, biy may jàmmam képp ku gëm Kàddoom, te jote ci Moom yiw wi ñu digewoon. Xelum Jàmm ji dafay dēggal sellayu sa ruu ak sa xol ci bépp fen ak selladi Dafa lay may kóoluteg sa mbaalug bàkkaar gi la deewug Yeesu baaxe. Xel mu barkeel moomu nekk ci yow, ngir jubóole la ak Yàlla ci kàttanu Krist, mooy meññ te saxal jàmm ju amul àpp ci sag dund.
Barke ñeel na ndawi jàmm jiXel mu Sell mi dafay meññloo ci ndawi Krist yi mbēggeel, mbégte asamaan, jàmm ju amul àpp, muñ laabiir, mbaax,Kóllëre, lewetaay ak maandute. (Galaat 5:22-23).Ndax xalaatuloo ne sa xol, yooyu ngëneel lay yóotu?Dund gu sell ngay ñaan, boole ci mébét bu làqu bi nga namm. Yàllay jàmm ji dafa laa bëgg a soppi, ba nga nekk déegu jàmm ci biir diiwaan bu feebar. Képp ku jot jàmmu asamaan, man nga koo séddoo. Te képp ku jot mbaalug bàkkaaram, man nga baal ñi la tooñ Krist dafa namm a may jàmm sa njaboot, sa ekool ak sa bérabu liggéey. Bul tiitaroo say jëfi diine, ndaxte Doomu Mariyaama ji moo tax nga suufeelu te woyof, na Mu meloon ba Mu nekkee ak nun ci kow suuf. Krist dafa doon surgawu ñi baax ak ñi bon. Kon képp ku koy topp, waruloo réy waaye dangay nekk surga ni Moom. Ndaw li Póol jagleloon na ñaanu Boroom bii nga xam ne bokk nga ci bu fekkee ne yaangi liggéeyal Sang bi ak mbég: “Jàmmu Yàlla ji xel manut a takk, dina aar seeni xol ci darajay Krist Yeesu.” (Filip 4:7)
Ndax bëgg ngaa jot jàmmu Yàlla ?Soo ko bëggee, man nanu la yónnee Injiilu Krist yu ànd aky nafar yu la man a dimbali ba nga taxaw temm ci jàmmu Yàlla.
Séddool Kàddug JÀMMU YÀLLA JINii la Krist jeexale ay njàngaleem : "Dama leen wax loolu ngir ngéen ame jàmm ci man. Dingeen am nattu ci àddina, takkleen fit yi ;noot naa àddina si (daan naa àddina si)." (Yowaana 16:33) Bu fekkee ne bataaxal bii laal na sa xol, te nga bëgg koo séddoo ak say xarit ak ñi mosagul jàmmu Yàlla ji, bind nu ngir nu yónnee la ci as tuut. Ijjil sa dëkkuwaay ba mu leer naññ. WATERS OF LIFE Internet: www.waters-of-life.net |