Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- Tracts -- Tract 06 (Rejoice in the LORD Always!)
This page in: -- Armenian -- Baoule -- Burmese -- Chinese -- Dagbani? -- Dioula -- English -- French -- German? -- Greek -- Hausa -- Hebrew -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Japanese -- Korean? -- Lingala -- Maranao -- Nepali? -- Peul? -- Somali -- Spanish -- Sundanese -- Telugu -- Thai -- Turkish? -- Twi -- Uzbek -- WOLOF -- Yoruba

Previous Tract -- Next Tract

BATAAXAL - Bataaxal bu ñu tënk ngir séddale ok

BATAAXAL 06 -- Deeleen bég saa su nekk ci Boroom bi! (Filip 4:4)


Bés bu nekk, ay waxambaane dañuy jéem a yokk seen man-man, te duñu báyyi xel ci musiba yi leen man a dal bu ñuy jéem a yéeg ci tund yu kowe yi,walla bu ñuy fecc ay waxtu ci bérabu feccukaay yi,di jéem a yokk seen tiitar ci kanamu nit ñi.Dañy jéem a fatte seen wéetaayu ruu ak ay jëfin aky wutum njàmbaar.

Ñeneen ñi dañuy wut alal,ngir bégal seen dund, fàtte seeni coono, te topp seen nafsu, ak puukare. Ñeneenati di ñaxtu ñàkkum njubte gi am. Dañuy waat ne fàww ñu fayu,te di xataraayu ngir doon seen goreelkati askan.

Ñu néew ñooy jákkaarloo ak Yàlla ngir laaj Ko: “Lan laa war a def ngir mucc?” “Loo bëgg ma def, ak lu ma warul a def?” Yërmaande Yàlla dafay ñaax xol yu tiis yi ngir ñu xool ci asamaan ba jot dëfal gu wóor giy jóge ci Aji Sàkk ji.

Limu ñi seen yaakaar tas mungi gën a yokk. Amatuñu luñuy dàkk, amatuñu yaakaar ci dund gi;kon nag,nu ñuy ameeti yaakaar ? Ndax,nun ñépp cib xare ndell buy rajaxe ñetteelu xaaju àddina si, lanu jëm?


Peeñu buy dëfal xol

Ca jamonoy xare yu tar, la Neemi jotewoon Peeñu mu jóge ca Yàlla di ab tontu ñaanam:Buleen nàqarlu ndaxte mbégteem Aji sax ji mooy nekk seen doole.” (Neemi 8:10).

Nanu ubbil Boroom bi sunu xol yi,ndaxte Moom rekk moo nu man a may noflaay ak jàmm, te di yeesal sunu yaakaar.

Ban dëfal la yonent bi jote ci Peeñu mi? Aji sax ji xamal na ko ne mungi ci mbégte mu rëy. Melul ni Budaa miy toog benn bérab di ree te di xebat coono nit ñi. Mbégte muy dund la sunu Boroom àndal,teg ci di nu muccloo. Tëraloon na yoonu muccug bépp doomu Aadama. Aji xam lépp ji,xam na ne amul kenn kuy def lu baax, ñépp a geru, te kenn manul a musal sa bopp, walla nga sëkke jàmm ak mbégte, sa wéetaayu xol. Aji sax ji dafa bëgg a yeesal bàkkaarkat yi ,may leen dund gu am njariñ ak yaakaar. Mbégte Yàlla mooy sa doole ! Képp ku tuub say bàkkaar, te dëddu leen, dina la may doole, ndampaay, ak fît. Aji sax ji rekk moo man a dëfal, te nguuru asamaanam yomb a am.


Ab Musalkat Juddu Na

Ca tundi Betleem, guddi ga ne rayy ak leeraay ga malaakam Boroom ma àndoon ak ndamam feeñewoon sàmm ya doon wottu jur ya. Ñu daldi nërmeelu ndax tiitaange.Dañoo yaakaaroon sax ne bésub àtte bi moo agsi. Ñu ragal lool ndax li ñu fàttaliku seeni bàkkaar. Bu ñu sañoon sax daldi moytu àtte ba ,waaye ndamul Aji sax ji solu leen.

Malaaka ma gëddu leen,waaye dafa leen a soññ ne leen: “Buleen tiit ,ndaxte dama leen di xamal xabar bu baax buy indi mbég mu rëy ci nit ñépp. Tey jii ca dëkkub Daawuda, ab Musalkat Juddul na leen fa,te mooy Almasi bi,di Boroom bi. ” (Luk 2:8-11).

Ci Peeñu moomu, malaakam Boroom bi dafa yégle jamono ju bees,ju ànd ak mbég, ak yiw. Mucc gi Yàlla tëraloon agsi na. Malaaka mi dafa woo nit ñi ngir ñu ñów rootsi co teenu mbégte ak jàmm, biy balle ci Yàlla. Aji sax ji du ñi jub, ak ñi dogu ci diine rekk la may yiwam, waaye boole na ci itam ñu bon ñi ak ñi geru. Malaaka mi njëkkewul ca boroom xam-xam ya, ak ñu tedd ña waaye ña jângul, ak ña xamul dara la xam- xamu Boroom bi waroon a gindi. May bajjo googu, du góor ñi rekk lañu ko jagleloon, waaye itam jigéen ñi ak xale yi, rax ci dolli ñi sonn te tawat. Mbégte Aji sax ji ñépp a ci am wàll. Lu tax malaaka Aji sax ji ne, na ñépp bànneexu? Ndaxte Musalkat bi juddu na te doxalinu yërmaandeem tàmbalewoon na.

Li ci gën a tiis mooy ne,askanam dafa ko weddiwoon,Moom Buuru jàmm ji. Bëgguñuwoon soppi seeni xalaat. Seeni mebét moo doon nguuru ,am alal, te am tur ci biir askan wi. Seeni ngànnaay yiy reye lañu bëggoon a jēfandikoo ngir daan seeni noon ba jébbal Ndam li seen nguur.


Mayug Krist gu kéemaane gi

Krist nag Moom, dafa dajale ñi dëddu seeni bàkkaar ak ñu jànnaxe ña doon wut Yàlla. Mu faj ñu wopp ña doon ñów ca Moom :Mu baal leen seeni bàkkaar yépp, te dàq rab ya leen daan dugg ;Mu dalloo taw ba ,te seddal xoli ña Ko daan déglu,te itam biral leen ne: “wax naa leen loolu, ngir ngeen bokk ci sama mbég, te seen bos mat sëkk.” (Yowaana 15:11). "Ba léegi ñaanaguleen ci sama tur. Ñaanleen, mu nangu. Bu ko defee seen mbég mat sëkk." (Yowaana 16:24)

Krist dëggal na kumpag asamaan googu, ci biir ñaanam gi Mu ñaanal ay taalibeem, ba di ci biral ne ay am-ji-jàmmam man nañoo xéewlu bu baax ci mbégteem gi: "Waaye léegi maangi jëmsi ci yów, te maangi wax nii ci bi may nekk ci àddina, ngir ñu fees ak sama mbég." (Yowaana 17:13)

Doomu Maryaama ji may na mbëggeelam gi ay taalibeem ,ay noonam, ak ña Ko doon sonnal. Far na seeni bàkkaar ak seeni tooñ, te dee ngir seeni ñaawteef. Ci deewam gi la leen Krist jubóolewaate ak Ku Sell Ki. Krist am na sañ-sañu baale tooñi ñi nangu mucc gi ci kow yiw, te may leen yaakaar gu amul àpp.

Ba Mu yéegee ca Yàlla ak ndam,Doomu Maryaama ji tàbbal na Xel Mu SELL MI ci dundug bépp doomu Aadama: "Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci jonentam Yowel ne:" Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi,dinaa tuur ci sama Xel ci kow nit ñépp; seen xeet wu góor ak wu jigéen, dinañu wax ci Kàddug Yàlla. Waxambaane yi dinañu gis ay Peeñu te màggat yi di janneer. Waaw ci bés yooyu dinaa tuur sama Xel ci kow sama jaam yu góor ak yu jigéen, te dinañu wax ci Kàddug Yàlla. Dinaa wone ay kéemaan ci kow asamaan ak ay firnde ci suuf, ci àddina, muy deret, safaraak ay niiri saxar. Jant bi dina daldi lëndëm, weer wi deretal, bala Boroom bi di ñów, di bés bu mag, bi ànd ak ndam. Booba nag ku woo Boroom bi ci aw turam, dinga mucc."(Jëf ya:2:16-21) Képp ku tuub say bàkkaar, te ànd ak Krist ci kow ngëm, dinga jot Xelum mbëggeel, mbégte ak jàmm, rax ci dolli man a góor-góorlu man a muñ (Galasi 5:22). Gindiku mungi tàmbalee ci dundug ñi gēm bu ñu nangoo báyyi Xelum Yàlla mu Sell mi, Mu yeesal leen. Ñu nekk ci coono, dinañu leen dëfal, ñi seen yaakaar tas, dinañu dellu amaat yaakaar, ñu bon ñi wëlbatiku nekk ñu jub te ñi nar a dee, dinañu dund ci kàttanu dund gu amul àpp gi. Li ko dalee ca bés bu nu Krist jubalee ak Yàlla ci la yiwam wiy maye wér ak cellaay xëppu ba ne gàññ te ànd ak lewetaay, ci kow bépp doomu Aadama.

Ba ndaw li Póol mosee baatin yooyu dafa bind ne: Deeleen bég ci Boroom bi ;maangi leen koy waxati :bégleen!” (Filip 4:4).

Mbégte Yàlla mungi dëkk ci ki sax ci mbëggeelam, di jàng Kàddoom gi te di ko denc .Krist dafay soññ ay taalibeem, te di dalal seen xel bi Mu naan:Moona li leen rab yi déggal, bumu tax ngeen bég, waaye bégleen ndax li ñu bind seen tur ci asamaan” (Luk 10:20).

Mbokk mi,
Ndax dangaa sëngëm ,walla sa yaakaar dafa tas ? Walla book yaangi sax ci Krist ?Képp ku ŋoy ci Doomu Maryaama ji dinga am wàll ci kàttanam ak bégteem. Jébbalul ci Krist, noonu mbégte mu amul àpp dina sax ci sa xol, ci biir àddinas yéeféer sii fees dell ak ay fiir aky bundxataal.

Ndax yaangi sax ci mbégte Yàlla gi? Soo nu laajee Injiilu Yeesu, dinanu la ko yónnee, mayaale la ay nafar yoo man a jēfandikoo ngir xéewlu ci teenu kàttanu Yàlla gu barkeel gi. Deel jàng Biibal bi bés bu nekk, te di ñaan saa su nekk, noonu Aji sax ji dina la wommat ci yoonu mbégteem gi.
Séddool mbégteg Yàlla ak say xarit: Bu fekkee ne bataaxal bii tooyal na sa xol, te nga bëgg koo séddoo ak ñi réer te seen yaakaar tas, kon dinanu la ci yónnee ak xol bu sedd guy. Ñaanalal ñépp ñi nangoo jēl bataaxal bii.

Sab leetar lanuy xaarandiku. Bindal sa dëkkuwaay ba mu leer. Nungi ñaan ngir mbégte Aji sax ji dëkk ci yow. Amiin!

WATERS OF LIFE
P.O. BOX 60 05 13
70305 STUTTGART
GERMANY

Internet: www.waters-of-life.net
Internet: www.waters-of-life.org
e-mail: info@waters-of-life.net

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on May 16, 2025, at 07:24 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)