Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- The Ten Commandments -- 06 Fourth Commandment: Remember the Sabbath Day, to Keep it Holy
This page in: -- Afrikaans -- Arabic -- Armenian -- Azeri -- Baoule -- Bengali -- Bulgarian -- Cebuano -- Chinese -- English -- Ewe -- Farsi -- Finnish? -- French -- German -- Gujarati -- Hebrew -- Hindi -- Hungarian? -- Indonesian -- Kiswahili -- Malayalam? -- Norwegian -- Polish -- Russian -- Serbian -- Spanish -- Tamil -- Turkish -- Twi -- Ukrainian? -- Urdu? -- Uzbek -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

TOPIC 6: THE FUKKI NDIGAL YI - Ab ñag buy aar nit ki ci cib jéll
Fukki denkaane yu am solo yi ci Exodus 20 ci leeralu xebaar bu baax bi

06 - ŇEENTEELU NDIGAL LI: Deel fàttaliku bésu noflaay bi, def ko bés bu sell



Gàddaay 20:8-11
Deel fàttaliku bésu noflaay bi, def ko bés bu sell. Nanga dox say soxla juróom. benni fan, def sa liggéey bépp. Waaye Aji Sax ji, di Yàlla sa Boroom, jagoo na bésu noflaay bi, di juróom-ñaareelu fan bi. Bu ci liggéey dara, yow mbaa sa doom ju góor walla ju jigéen, sa jaam bu góor mbaa bu jigéen, sag jur walla doxandéem, bi nga dëkkal. Ndaxte ci juróom-benni fan la Aji Sax ji sàkk asamaan, suuf, géej ak li ñu ëmb lépp. Waaye noppalu na ca juróom-ñaareelu fan wa. Kon Aji Sax ji barkeel na bésu noflaay ba, te def ko bés bu sell.


06.1 - BESUB NOFLAAY NGIR MÀGGAL AJI SÀKK JI

Ci Yawut yi, Bésub Noflaay bi, mandarga mu am solo la ci seen jokkoo ak Yàlla.Bu cant yi féetee boor, bés bii dafay xàjjale niti kóllëre gu Njëkk ga ak yeneen xeet ya. Ba tey jii Askanu Kóllëre gi mungi sellal bés bu mujj boobu ci ayu-bés bi, te du ci liggéey ni mu ko baaxoo defe ci yeneen bés yi. Duñu ci taal sax safara, walla di ci tukki lu sori. Waaye dañuy sol yére yu bees yi ñu dencoon ngir bési berndeel yi. Bésub Noflaay bi (Sabbyat), mbégte lañu ko jagleel. Nit ñi dañuy booloo di jaamu ci biir jàng ay pàcci téere yu ñu tànnandoo ci Tawret, di ci waxtaan ci biir toogaayu màggal.

Ci bésub Boroom bi, way-gëm yi dañu war a beral Yàlla jot gu gën a bari ga ñu Ko doon sédd ca yeneen bés ya.Dañuy def seen xel mépp ak seen xol bépp ci Moom ndaxte mooy seen Aji Sàkk ji, seen Musalkat, ak seen Dëfalkat. Ci bés boobu,danu ci war a faral di jàng Biibal bi, déglu ci xudba bu am solo te bokk ciy ñaan aky woyi cant yu nuy jàppale te di dalal sunuy coono yi nuy daj ci biir manding mi. Waaye nag du nit ki walla, noflaay bi ñooy solo bés bi, waaye Boroom bi ci boppam la. Kon Sabbat bésu Boroom bi la. Dafa ber bés boobu, sellal ko te barkeel ko. Bésub Boroom bi, neexalu Yàlla bu am solo la ngir ñi Mu sàkk.

Sellal Sabbat bi dafay tekki ne nungi màggal Aji Sàkk, ji sàkk asamaan ak suuf, biddeew yi, ban bi ak garab yi, lépp ci Kàddoom gu am kàttan gi. Moom moo sàkk jën yi, picc yi ak mépp mala mu ndaw ak mu mag. Sàkkam bi gën a kowe nag mooy nit ki Mu sàkke ni melokaanam moom Yàlla. Ci càkk gi, bépp xeet kéemaan la ci bu ñu defare doole ak maandute gu amul feneen. Boroom xam-xam yi yenn wàlli mbóoti yaramu nit ki doŋŋ lañu jot a xolli te ñu aju ci ay man -manam ak ci ni xelam di xalaate. Jëfi Yàlla aka ñoo yéeme! Te bu fekkee ne li Mu sàkk nii la taaroo, kon Moom miy Aji Sàkk ji, xanaa kenn waxatu ko!Kalaama nit manul a wax Màggaayam, Ndamam ak kàttanu ndogalam. Yelloo na màggal gi, ak woyi cant yiy bawoo ci ñépp ñi Mu sàkk.

Ba Yàlla sàkkee lépp ba noppi dafa noppaliku. Ljgéey bi sonnalu ko woon. Aji Kàttan ji manul a sonn, gëmmeentu mbaa Muy nelaw. Liggéeyam doy ko, Mu bég ci lépp li Mu sàkk, te gis ne lépp baax na. Yoon la ñuy màggal Yàlla bés bu nekk ngir Maanduteem gi kenn manul a natt ak kéemaani càkkam, rawatina nag ci bésub noflaayu Boroom bi.


06.2 - SOLO SABBAT BI

Ci bésu sabbat bi danuy am wàll ci noflaayu Yàlla, ba ca asamaan.Dafa nu may nu dund ko ci tekkaaral gi ak màggal gi. Tekkaaral googu ci sunu biir ak bitti, ci kanamu Boroom bi, lu am solo la ci sunu aafia. Kenn manul a moy ndigal loolu te mbugaluñu la. Ay réew yu mel ni Uñioŋ sowietik bu yàgg ba, walla ay mbootaayi sowu-jant jéemoon nañu teggi bésub Boroom bi, moo tax it ñu ñàkk jàmm ca biir réew ma. Ňiy bañ a faydaal bés boobu te di wëndeelu fu nekk ak seen woto bàyyiwuñu xel ci ndamul Yàlla, ci li Mu sàkk. Manatuñu am jotu xalaat ci kàddu Yàlla gi, te loolu moo tax seen liggéeyu ayu-bés bi di leen di sonnal. Nun ñépp a soxla noppalu, ba ci mala yi sax. Càkk gi manul a jotaat doole,fi ak taaxirluwul ci kanamu Yàlla. Warunu tuutal mukk ndigalu Yàlla bii aju ci sellal bésu Sabbat bi. Ndigal li nag waxul lu jëm ci 35 ba 40 waxtu iiliggéey, waaye ci juróom-benni fan ci ayu-bés bi la wax. Juróom-ñaareel bi Boroom bi kese lanu ko jagleel. Biibal bi dafa nuy jàngal ne dundug tàyyeel mooy ndeyu bépp dundinu ñaawteef, te liggéeyu bés bu nekk, ngëneel la ci nit ki.

Yeesu dafa nuy soññi ngir nu seetlu gàñcaxu Lis yi ci tool yi, ak yeneeni tóor-tóor te xool ni ñuy màgge. Ndax seetlu nga diir bi gàñcax gi di am laata muy tóor-tóor, xob yi jebbi ba mu jur ay doom? Taxawal te ubbi say bët. Jàngal a xam doole ak sarti dunya bi, bu loolu amee dinga gis maanduteg Aji Sàkk ji làqu ci gannaaw, ak mbaaxaayu Baay bi Mu làmboo. Yeesu dafa misaal ne nanu méngale rafetaayu tóor-tóor yi ak taaru yérey boroom alal yi. Su boobaa dinanu gis sax ne buur yi ak bummi yi gënuñoo jekk colin tóor-tóor yooyu nar a lax ba dee (Macë 6:25-33). Nit ki ci boppam mooy li ëpp maanaa ci li Yàlla sàkk, te kanamam dafay xaw a wone ndamam. Céy bu nu manoon a soppi sunu dundin, bàyyi dawantu bi, te am jotu toog xalaat! Kon rafetaayu càkk gi dinanu xiir ci sant Yàlla te màggal ko. Dees na naqarlu nag jëf yu ñaaw yi telewisoŋ bi di wone, ci mbiri séy yu daganul, ak ay coxorte fekk Yàllaa ngi namm a ubbi sunuy bët ci nawet bi ak noor gi ngir won nu yu kéemaane yi Mu sàkk te sàmm ko. Ni nu Boroom bi sante nu weg bésu Sabbat bi, dafa bëgg nu ber ko ngir dund ci kanamam. Sellal bésub Boroom bi, du noppalu, jàng mbaa déglu Kàddu Yàlla ngi rekk, waaye itam bokk na ci wëlbatiku ci Moom ak sunu xol bépp ngir Mu man noo soppi te sol nu ba nu fees ak Baaxaayam. Moom dafa sell, te bëgg nu sell itam. Kon nanu wéy ci leeraayu Mbëggeelam gi te di lerxat Ndamam li, ndaxte yeesal du man a am fu tekk ak teey teewul.


06.3 - DéGG-DéGG GU JAADUWUL CI SABBAT

Bésub Sabbat bi aar na askanu Kóllëre gu Njëkk ga cib jéll (dellu gannaaw), te teqale ko aky yàlla yu dul dëgg yu bare yu ña leen wëroon doon jaamu. Bésub Boroom bi waajal na bànni Israel ci ñówug Krist, Musalkatu àddina si. Taxul nag Sabbat bi ci boppam man a soppi mbaa aar, walla yeesal way-gëm yi koy sàmm. Nit ñépp a ñàkk doole, bon, te matadi ci kanamu Yàlla. Benn ndigal manul a soppi doomu Aadama ji, te Sabbat bi manul a goreel nit ki ci ay bàkkaaram. Waaye man na ko tere daanu cig yéeféer. Ci Kóllëre gu Bees gi, dunu màggal bésub Boroom bi ngir jot yiwam, waawe ngir sant Ko ci li Mu nu sàkk.Yàlla dafa mbubboo yaram, ganesi nu ci Krist. Dafa nuy toppatoo lu raw ni baay di toppatoowe doomam. Loolu tax na nu bëgg ko ci sunu xol te di Ko teral ak sunu dund gépp. Sàmm yoon wi dunu musal ci sunuy bàkkaar, waaye yiwu Yàlla wi mooy sunu kàttanu mucc ak yeesal gi nëbbu. Képp ku bëgg ñu goreel la, jaare ko ci yoon wi, yoon wi dina la daan. Waaye boo nangoo téye loxo bi la Yàlla tàllal, dina la wommat te aar la ci bépp mbugal.

Ca juróom-ñaareelu fan wa, Yàlla dafa noppalu, te xoolaat liggéeyam bépp. Noonu Mu gis ne lépp li Mu def baax na lool. Waaye noflaayu Yàlla bu sell bi dakk na, ba Ko nit ki ñàkkee déggal ba tàbbi ci bàkkaar. Booba la Yàlla ñàkk noflaay ba tey, te di liggéey guddi ak bëccëg ngir musal askanam wu réer wi. Nee na: ”Ak sa jëf yu futi yi, yow yaa ma sonnal.” (Esayi 43:24) Yeesu biral na ne: ”Sama Baay nekk na ba tey ci liggéey, kon man itam damay liggéey.” (Yowaana 5:17) Yàlla nun lay xalaat ak sunuy bàkkaar yu feeñ yeek yu làqu yi. Nungi sant Yàlla ci goreel gi Mu may bàkkaarkat yépp, jaare ko ci ni nu Krist wuutoo. Képp ku gëm Mbotem Yàlla, àtteb Yoon bu tar bi du dal ci sa kow mukk. Deretu Yeesu mi dee te ñu suul Ko laata sabbat bi di duggusi, moo lay setal wecc. Ci bésub noflaayu Yàlla bi Moom dafa noppalu ci bàmmeelu boroom alal, te ci fan wu njëkk wi ci ayu bés bi, Mu dekki ci biir ñi dee. Kon Yàlla matal na li bésub Sabbat bi laaj. Ci kow ndekkiteem gi, dogal na ci ab bés bu ñuy dàkkentale “càkk gu bees gi” te muy law jaare ko ci yiwu Yàlla ak kàttanu Xel mu Sell mi, waaye du ci kow àtteb Yoon wi.


06.4 - NDAX KERCEN YI AM NAŇU SAŇ-SAŇU MÀGGAL CI DIBEER TE BAŇ KOO DEF GAAWU BI?

Yawut yi ak Adwantisti juróom-ñaareelu fan wi, dañuy tuumaal kercen yi, naan leen ñungi moy ñeenteelu Ndigal li. Ňungi naan merum Yàlla dina dal ci kow gaayi Krist yépp yiy noflaayu dibéer bi te bàyyi gaawu bi. Waaye nag fekk na Yeesu ne Moom mooy Boroomu Sabbat bi. Doomu Nit ki matalal nanu lépp li Sabbat bi laaj. Matal na ko, te jeexal ko tàkk. Yeesu indiwul yoon wu bees wuy sellal ab bés, mbaa aw weer, walla am at. Dafa musal ay taalibeem te sellal leen. Du ci bésub noflaay bi walla ci yenn xew-xew yi rekk la nit ki war a jaamu Yàlla, waaye bés bu nekk. Looloo tax Yeesu di sellal nit ñi, waaye du ay bés lay sellal! “Te lu ngeen man a def, muy ci wax mbaa ci jëf, wéerleen ko ci turu Boroom bi Yeesu, jaare ci Moom gërëm Yàlla Baay bi.” (Kolos 3:17). Bépp liggéey bu Xel mu Sell mi jiite, ci jaamu Yàlla la bokk. Amul benn bés bu gën moroomam. Yeesu dafa noo goreel jaare ko ci deretam ju amul njëg ji Mu tuur, ba noppi Mu yeesal nu ak Xel mu Sell mi. Ay nit yu sell la sàkk, waay du ay bés yu sell. Matal li Sabbat bi manuloon a matal, moo waraloon ñówam ci kow suuf: maanaam, sàkk nit ñu bees, soppi ay bàkkaarkat yu bon ngir ñu nekk ay taalibe yu sell, te wëlbati bopp-sa bopp yi ñu nekk ay surga.

Yeesu dafay soppi bépp fànna ci sunu dundug xel. Loolu moo tax kercen yi taamu dibéer biy bésub ndekkitelu Yeesu ngir màggal Kóllëre gu bees gi ak càkkam gu bees gi. Yeesu moo bëggoon ay taalibeem noppalu itam te xalaat ci ngëneelu bokk cixeetam wu bees wi Mu sàkk. Santunu nu jàpp dibéer bi, te itam aayewul nuy màggal Sabbat bi. Jéngu nu ci ay bés walla ci ay xew, waaye dafa ñów ngir musal bàkkaarkat yi. Ndekkite Yeesu dafa ubbi jamono ju bees joo xam ne dundatunu ci Yoon wi nuy jiiñ, waaye ci Yiwu mucc gu jóge ci sunu Boroom. Loolu tekkiwul ne kercen yi amuñu yoon. XelumKrist mi dëkk ci nun, ab Yoonu mbëggeel la. Dafa nuy mayaalekàttanu man a matal yoon woowu. Noonu Sabbbat bi misaalu kóllëre gu yàgg ga la. Dibéer bi mandarga ndamu Yeesu la biy feeñ ci kóllëre gu bees gi.

Cii réewi Islam yi, kercen yi duñu man a noppalu ci dibéer bi walla bésub Sabbat bi. Kon book bésu Àjjuma lañuy daje, te xam ne Boroom bi mungi ànd ak ñoom, ni Mu ko digewoon: ”Ndaxte fu ñaar walla ñetti nit booloo ci sama tur, maa ngi ci seen biir.” (Macë 18:20). Yeesu mosu noo bëgg a sëf ay bési màggal, waaye dafay sellal way-gëm yi saa su nekk, ak fu ñu man a nekk.


06.5 - MÀGGAL CI DIBEER(dibéer) bi

Nan la kercen yi man a sellale bésub Boroom bi? Mbëggeel gi moo leen di xiir ci ñuy dajaloo ci dibéer bi ngir di màggal, di jàng Biibal bi ak di woy ay woyi cant ak mbooloom ñu sell ñi. Sunuy doom, gan yi, liggéeykat yi ak mala yi sax dñoo war a àndandoo ak nun ci bés bi te dunde mbégu asamaan mi ñuy fàttaliku dibéer bu nekk, te di feeñe ci sunudund. Reenu mbégte bu kercen bi moo gën a xóot bu yawut yi. Yeesu nee na: ”Wax naa leen loolu, ngir ngeen bokk ci sama mbég, te seen bos mat sëkk.” (Yowaana 15:11); (Yowaana 17:13) ”Waaye léegi maa ngi jëmsi ci Yów,te maa ngi wax nii ci bi may nekk àddina, ngir ñu fees ak sama mbég.”) Póol itam bind na ne: ”Deeleen bég ci Boroom bi, maa ngi koy waxati: bégleen!” (FILIP 4:4) Waaye li Xelu Yàlla mi di meññ mooy: mbëggeel, mbég, jàmm... (Galat 5:22) Aaya yu mel nii ñoo nuy won xel mi làqu ci bésu dibéer bi. Dañuy wone itam xel mi nuy liggéeye ci biir ayubés bi, ak naka la dundu njabootu kercen war a mel. Ndax war nanu liggéey ci bésu dibéer?Kercen bi ak nit ñépp a yem. Ay mbindéef yuy sonn lañu Moo taxñu soxla noppalu ak dallu. Ay mbindéefi neen lañu, rax ci dolli, ay doomi Yàlla lañu jaare ko ci Xel mi. Ňungi dunde yaram ci kow suuf, waaye itam ñungi toogandoo ci baatin ak Krist. Dibéer, kenn sóoraalewu ko woon ngir dabu ay ñaakki nelaw, waaye ngir màggal Yàlla Baay bi te jébbal Ko ay cant moo kowaral. Bés boobu, Yàlla moo ko moom, te waarunu ci jéem a def lenn lu (benn liggéry bu) nekkul yitte dëgg. Ci dëgg-dëgg warunu rocciku bu fekkee ne danu war a wone mbëggeel, walla ci lépp loo xam ne dafa war a musal ñeneen ci musiba. Sunu njubte wékkuwul ci matal Yoon wi, waaye ci dee gi nu Krist wuutoo te mu saxal liy sarax ci sunu xol.

Bokk cig mbootaay, di màggalandoo dibéer bu nekk ak ay kercen, loxo bu ñu beral Kercen yi la. Waaye nag danu war di xonte sunu bopp bés bu nekk ak Kàddug Yàlla gi. Bu loolu amul rekk, mbëggeel gi, ngëm gi ak yaakaar ji, yépp danuy fay-kamaj. Dibéer gi dafa nuy may nu man a woyandoo ak mbooloo mi ñaanandoo ak ñu bare, weccoo xalaat ak waa jàngu bi, te bokk ci jokkoo giy dox ci diggante Kercen yi. Mbooloom Way-gëm yépp mooy yaramu KRIST ci baatin. Way-gëm ji ci boppam du mooy ndeyu mbillu càkkite gu bees gi, waaye mbootaayu ñu sell ñiy teew besu dibéer bi, ñooñu la.

Barke ñeel na ñiy seeti ci dibéer ñu wopp ñi, jarag yi, ak néew doole yi. Ňu bare ñu seen jëkkër faaru, ay baayo ak ay jirim ñungi séentu ku leen nemmeeku. Way-gëm yooyu duñu xool li leen dese ci esaans ci seen Oto ndax man na leen a yóbbu 100 kilomet.

Xelum Boroom bi dafa nuy xiir ci génn jàngu bi ngir wuti ñi réer.Danu leen war a rëcculoo seeni bàkkaar te dimbali leen ba ñu génn ci seen ñàkk yaakaar ak ci seen ñàkk yitte. Ňàkk a seedeel ñi gëmul, lees manul a baale la. Ci bésub Boroom bi itam rafetlu nañu ci di dimbali ñi am ay soxla.

Dibéer bi may nanu jot gu doy ngir nu sant ci Boroom bi, rëccu ci sunuy bàkkaar, te ñaanal ci ñeneen ñi ngir seeni soxla faju. Bu fekkee ne am nanu ay doom, war nanuy am jot gu nuy ñaanandoo ak woyandoo ngir màggal Yàlla ak mbég. Nanu ñaan Yeesu Mu won nu nan lanu man a toppe ñetti ponk yi jiitu ci ñaanu Boroom bi, rawatina nag ci dibéer bi.

Bunu sàmmee dibéer bi, dinanu am baarke. Am na baarke yu bare yu Yeesu dencal kiy wut a solu Xelum Krist, Mi dekki bésub dibéer ci biir ñi dee.


06.6 - MOY DIBEER GI

Seetlu nanu te naqarlu yokkuteg bàkkaar yi digante gaawu ak dibéer. Oto yaa ngi yàq ngelewal diiwaan yi. Li telewisoŋ bi di wone, as tuut la ci may Kàddug Yàlla gi, ba noppi beral lu yaatu ay film yu ragallu, ay tëdde, walla ay mbiri seytaane. Ci bésu dibéer, am na ñuy liggéey ci seen kër, seen tool mbaa ci seen gétt, te fekk manoon nañu koo def ci biir ayubés bi. Ca jamonoy Kóllëre gu Njëkk ga, suñu bettoon nit muy liggéey ci bésub noflaay bi, dee lañu ko doon àttee. Su fekkoon ne man nanu gis bàkkaar yépp yi feeñ ak yi nëbbu, yi am ci njeextalu ayubés bi -ci sunu diiwaan rekk-kon sunu xol dina jeex, mbaa nu dof sax! Mbëggeelu Yàlla rekk moo am kàttanu dékku ak muñ ngir jotaat bàkkaarkat yi.

Ndax dangaa fàtte li Boroom bi waxoon nit ka doon jàdd yoonu Bésam bi? Bu nu jàngee Gàddaay 31:14-17, dinanu gis solo si noppalu ci kanamamu Boroom bi am. Jàngal itam Lim ya 15:32-36 ngir xam solo si nekk ci weg bésu Boroom bi. Xéy-na danu war a soppi sunu dundin, te sax ñaan sunu doom yi ñu bañ a def seeni sasu ekool yi ci bésu noflaay bi(dibéer). Yàlla tëkku na dëkk yi dul sàmm sabbat bi ni bésub cant ak noflaay (Yeremi 17:22). Warunu woyofal artu boobu. Ku xam ndax du looloo jur xare yi ci àddina si ak seeni ñaawteef yi? Biibal bi nee na: ”Bu leen ci kenn nax; Yàlla kenn du ko fontoo, ndaxte lu waay ji moom lay góob.” (Galat 6:7) Kenn manul a moy ndigali yàlla yi te du la jural dara.

Bu Yeesu deewuloon ca bant ba, bu nu gàddululoon sunu mbugal, kon dunu am benn yaakaar. Waaye deewam taxul nuy taafantoo moy bésub Boroom bi. Yeesu aky taalibeem dañu daan sellal Sabbat bi. Moom dafa dund ngir màggal Baayam bi. Gannaaw bi Mu dekkee, ci bés bu njëkk bi, ci ayu-bés bi, Yeesu dafa feeñu taalibeem yi ci dibéer gi ngir màggalandoo ak ñoom xew-xewu Kóllëreem gi.


06.7 - DEGG-DEEGU(dégg-déggu) YOON WI GU BEES

Bu nu xalaatee ci doxalin bu ñaaw bi ñuy wege Sabbat bi, kon dinanu gis ni mu yombe ngir ñàkk a xam ndigalu Yàlla bii. Àtte nañu Yeesu ngir rey Ko ndax li Mu faj ñu feebar ci bésu Sabbat bi ak li Mu ne mooy Doomu Yàlla ji. Ca jamanoom, ay kilifa diine ñoo Ko daroon, te ñooñee dañoo amoon xadar ci Yoonu Musaa ba seen mbëggeel ci Yàlla ak ci seen moroom réer léen. Dañoo mbubboowoon lépp. Ci kow naaféq lañu tanxamloo wooteb tuub bàkkaar te jébbalu. Ci seen ngumba lañu dëgërale seeni xol. Jekkuñuwoon ngir soppiku. Dañoo weddi Yàlla Baay bi, Doom ji. Ak Xel mu Sell mi. Daawuñu toppatoo miskiin yi ca bésu Sabbat ba. Ca bés booba, seen xadar ci Yoonu Musaa dafa mujj nekk ag naaféq. Amul dara luy yéeme ci li leen yeesu limal yonent-Yàlla Esayi: ”Xeet wii ñungi may teral ci seen gémmiñ, waaye seen xol sore na ma. Seen màggal amul benn njariñ, ci li ñuy jàngale, ndénkaaney nit kese.” (Macë 15:8-9)

Ci jéngoom ngir jàngal nu ni nu war a sellalee bésu Boroom bi, yeesu waxu ci lu bare lu jëm ci mbirum liggéey ak bañ a liggéey. Li Mu gën a joxoñ mooy toogaayu sunu xol bu rafet ci kanamu Yàlla. Póol sàmm na njàngale moomu jaarale ko ci yoonu xelum Krist. Waaye nag ba mu jàngalee ne ñi dul Yawut te gëm Krist, Kóollëre gu njëkk ga teggeeku na leen, nit ña móolu ko ba sànni ko ay xeer. Póol dafa leeral sunu goreel gi nu jot ci ni nu yoon wi doon jiiñe, ndaxte dee nanu ci Yoon wi ba noppi, jaare ko ci Krist. Kon book, Yoon wi amatul sañ-sañ ci nun. Waaye Xel mu Sell mi tegal na nu ndigalu mbëggeel lu bees. Ndigalu xelu diine lu bees lii, moo nuy sellal te di nu xiir nuy màggal ci sunu xel, sunuy kàddu ak sunuy jëf, Kenneefu Yàlla ci Ňett. Noonu, Yoon wi nootatunu, waaye dafa nuy dimbali ci tuub sunuy tooñ, te am ngëm ci kàttanu Xel mu Sell mi. Nanu bàyyi xel ci ne Krist ay nit la sellal waaye du ay bés. Kon léegi xam nanu bu baax wuute-wuute bi am ci dégginu ñeenteelu Ndigal li, ci diggante Kóllëre gu Njëkk ga ak gu Bees gi.


06.8 - AJJUMA JI NGIR JULLIT YI

Jullit yi wone nañu ni ñu dégge Ňeenteelu Ndigal li, ba tànn Ajjuma ni bésu diine bi ñu war a daje. Taxul nag ñu topp ko ni mu ware. Fi Yawut yi ak Kercen yi weddee yonent Muhammad ak ay wooteem ngir nit ñi nekk jullit, Muhammad dafa gën a yokk ay ñag. Déggoowul ak yawut yi ci bésu gaawu bi te itam juboowul ak kercen yi ci dibéer gi. Ngir jéem a taxawal diine ju bees, weddi na santaane Kóllëre gu Njëkk gi ak gu Bees gi, ba tax mu tànn Ajjuma ji ngir mu nekk bésu ndaje jullit yi. Dara méngoowul ak tànn boobu ci biir Mbind yu Sell yi. Lëngoowul ak dara lu bokk ci yoonu mucc gi. Xanaa kay ab jéngu la ci kow Yàlla ak Almaseem bi. Sàmm Ajjuma ni bésub julli saxul fenn ci Biibal bi.

Jullit yi bu ñu jullee ajjuma ba noppi rekk dañuy dellu ca seen liggéey. Ca bés boobu waxtaan yi gën a bare ci jumaa ji ci mbiru politik lay nekk. Yenn saa yi sax dafay jur ay ñaxtu yu tàng -jër. Sellal ab bés bu ñu tànn te ber ko, walla sellal nit ki gëm, loolu lu ump jullit yi la. Ci ñoom ,Yàlla dafa rëy ba sellayam benn jullit manu ko xam, lu dul ci turam rekk. Loolu mooy wone lu tax Islam féete suuf Kóllëre gu Njëkk ga ci bii Ndigal. Jullit dafa umpale lool lan mooy mucc gi ak càkkite gu bees gi ci Kóllëre gu Bees gi.

Nungi sant Ki dekki ci biir ñi dee ndaxte matal na ay Kéemaanam ci bésu Sabbat bi, ci biir ayubés bi. Ci bés bu njëkk bi ci ayu bés bi la dekki, noonu mu indi gis-gis bu bees te am solo ci bés bi. Na Dibéer bu nekk indaale penkum jant bu naan rayy ci ayubés bi, ànd ak Kàdduy dund yu bawoo ci sunu Boroom bi: ”Maangi leen di jox ndigal lu bees: bëggantelee. Nangeen di bëggante ni ma leen bëgge. Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, ngeen bëggante.” (Yowaana 13:34-35).

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 02, 2025, at 09:51 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)