Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
Home -- Wolof -- The Ten Commandments -- 05 Third Commandment: Do Not Take the Name of God in Vain
This page in: -- Afrikaans -- Arabic -- Armenian -- Azeri -- Baoule -- Bengali -- Bulgarian -- Cebuano -- Chinese -- English -- Ewe -- Farsi -- Finnish? -- French -- German -- Gujarati -- Hebrew -- Hindi -- Hungarian? -- Indonesian -- Kiswahili -- Malayalam? -- Norwegian -- Polish -- Russian -- Serbian -- Spanish -- Tamil -- Turkish -- Twi -- Ukrainian? -- Urdu? -- Uzbek -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson TOPIC 6: THE FUKKI NDIGAL YI - Ab ñag buy aar nit ki ci cib jéll
Fukki denkaane yu am solo yi ci Exodus 20 ci leeralu xebaar bu baax bi
05 - ŇETTEELU NDIGAL LI: Bul tudd turu Aji Sax ji,di Yàlla seen BoroomGàddaay 20:7 05.1 - TURU YÀLLANit du man a dund su beroo Ki ko sàkk. Ci melokaanu Yàlla lañu ko sàkke, waaye moom nit ki dafa bàyyi Boroomam.Booba ba léegi mungi wër ci biir màndingu àddina si, di wut màkkaanam mi ko réer, ak fa reeni cosaan soqikoo. Defar na kuutaayu yàlla yu bare, yu seen jëmm ragallu ba di wone tiitaange gi làqu ci doomu Aadama, ak la muy séentu. Dafay faral di fay xaalis bu bare ngir ñaanlu ay kéemaan yu lëndëm,mbaa ñu koy jàngal li ko rëddi loxoom dencal, walla itam gisaane; loolu lépp amul genn kaaraange. Muslim yi dañuy fóon xeer wu ñuul wa ak orma gu rëy, mel ni dafa ëmb xel mu jóge asamaan. Waa Budaa di jaamu jëmmu Budaa bu ñu xellee wurus te reetaanam mel ni faalewul way-gëmam yi seen xel matul. BOROOM bi, Moom ci boppam,moo ne ci peeñoom: ”Man maay Yahve, Boroom bi” xanaa loolu rekk waroon na doy gëstu nit ñi. Ba Mu feeñoo ca, ngarab sa doon tàkk te du lakk, Boroom bi wax na fa Mooy kan, ba jaar ci turam. Am na peeñu yu bare ci Kóllëre gu Njëkk gi, ak gu Bees gi. Biibal bi dafa nu tegal 638 tur ak ay dàqental ci Kenneefu Ňet gi Yàlla doon.Ci làkki geñog Sem yi,dàqental bu nekk, weneen tur lay firi. Yàlla du Ku jub rekk, waaye Mooy ku Jub ki ci sunu njubte gépp wékku. Du Ku Sell rekk, waaye Mooy Ku Sell Ki fees dell ak Cellaay. Bépp Kàddoom dafa mel ni ceeñeeru ndamam. Waaye turam wi nuy gën a gis mooy ”YAHVE” (6828yoon ci Kóllëre gu Njëkk gi). Tur woowu mungi tekki Ki téye lépp ci ay Loxoom, Ku Sell ki, Ku Laab ki, Boroom càkkite, gi dul soppiku mukk, te du mos a fecci kóllëreem. 05.2 - BOROOM BI, CI BIIR KÓLLëRE GU BEES GITéere Kóllëre gu Bees gi (maanaam INJIIL)moo ne Boroom bi, Aji Sax ji moo soppali boppam nit, ci jëmmu Yeesu Krist mu Nasaret. Malaaka,Yonent, ak bépp way-gëm ñungi nangu seeni bàkkaar te di biral ne ”Yeesu mooy Boroom bi.” Yeesu mosul a sagal boppam, waaye Baayaam ba ca asamaan doŋŋ la mos a delloo njukkal. Jàngal na nu ni nuy ñaane: ”Sunu BAAY bi ci kow asamaan.Na saw Tur Sell.” Ci ñaan gii màggal nañu ci turu Baay bi, sagal ko, te sellal ko laata, ak ci kow wépp weneen tur. Peeñug Boroom bi ni Baay, ci jëmmu Yeesu, moo nu lenge ba ca njobaxtalu man a xam Yàlla. Boroom bi Yeesu moo nekkoon misaalu suufeelu gi jóge asamaan. Moo, jubóole Ku Sell ki ak bàkkaarkat yépp, jaare ko ci deewam gi Mu leen wuutoo ca bantu gàcce ba. ”Moo tax Yàlla kaweel ko lool, jox Ko tur wi tiim yépp, ngir ci turu Yeesu bépp óom sukk, ci asamaan, ci kow suuf, ak ci biir suuf, te ñépp bokk genn kàddu naan: Yeesu Krist mooy Boroom bi ci màggaayu Yàlla Boroom bi.” FILIP2:9-11. Xel mu Sell mi dafay màggal saa su nekk turu Yeesu te di nu biral ne Mooy “Boroom Xel mu Sell mi. Genn mbëggeel gi ñu séq mooy wone ci dëgg-dëgg ni sunu Yàlla mel. Dawuda yégoon na peeñu ga laata muy agsi ba mu naan: ”Kàddug Boroom bi, ngir sama Boroom: ”Toogal ci sama ndeyjoor, ba Ma def say noon say dëggukaayi tànk.” (Sabóor110:1). 05.3 - XAM TURU BOROOM BI,LU MUY TEKKI?Bu amee gan guy soog a dugg ci ab dëkku taax bu rëy, dafay bége yore xammekaayu dëkkuwaayu ku siiw ci diiwaan bi. Man na woo xaritam bi ngir mu jàppale ko. Baarke ñeel na ki xam turu Yàlla ji dëggu tey denc “Nimero telefoŋam” Sabóor 50:15. Rax ci dolli, ”Woo Ma,boo tolloo ci diggante dund ak dee, Ma wallusi la, ba nga màggal ma.” Sunu Yàlla jiy dund, nelawul saa su nekk mungi xaar sunuy wootey xelu ruu. Saa su nu jegee Yàlla ju Sell ji, sunu nekkinu bàkkaarkat, sunu wéetaay, ak sunu réer, yépp dañu naan fàŋŋ. Màggaayu Sellaayam dafay feeñal sunu woyofaayu dundin te wone fi sunu nite tollu. Baaxaayu Yàlla dafa nuy soññi ngir nuy nangu sunuy bàkkaar te suufeeloom moo nuy won sag, mbaa jomb-ñaaw bi nuy làmboo te mu fees dell ak poson (tooke). Xam turu Yàlla dafay dimbali nit ki sonn te diis mu man a jokkoo moom ci boppa ak Boroom bi Yàlla. Sunu màggaayu ngëm giy yaakaar Yàlla moo nuy saxal ci ñetteeluNdigal li ne: ”MAN maay Boroom bi, sa Yàlla.” Baatu moomeelu “sa” dafay wone ne Yàlla mu Sell mi mungi xàmmiku ak ñi Mu sàkk, maanaam ay bàkkaarkat yu sànku, ñu matadi te néew kàttan. Téereb Kóllëre gu Bees gi xamal na nu ne Yàlla boole na nu ci njabootam gi ak ci Jëmmam ju Sell ji. Yeesu mooy Boppu yaram woowu te nun nooy cër yi ciy yëngu. Yàlla Baay bi dafa bëgg a nekk benn ak nun ci xel ak ci ruu, te jaare ci nun ngir musal maas gu dëng gii. Ci kow yërmaandeem, may na nu sañ-sañu kóolute ak jëfe ci Turam. 05.4 - FOWE TURU YÀLLA (CAAXAANE TURU YÀLLA)Nungi dund ci àddina su peeñu Yàlla yi ci Biibal bi suxlu lool. Moone ñu bare wóoluwuñu Ko ak seen xol bépp. Bu nit ki saxul ci teewaayu Yàlla, dafay mujje jëfandikoo turu Boroom bi ci neen, maanaam ci caaxaan. Ňooñu dañuy jëfandikoo Tur wi, te duñu bàyyi xel sax ci solo si Mu am. Way-gëm yu bees yi sax dañuy tiisloo Xel mu Sell mi ci seeni wax yu amul faayda yi, te ñooy ndeyu mbill yi. Dañuy jekk-jekki rekk tuddu Yàlla te duñu ci bàyyi xel. Ňetteelu Ndigal li artu na nu te tere nu nuy jëfandikoo turu Boroom bi cig neen. Ňiy mbuboo kercen duñu tàyyee tudd turu Boroom bi saa su nekk ak ñàkk xel te naan: ”Céy Yàlla,Yàlla ju baax ji” a.ñ.s.(etc). Dañu mel ni xale yuy fowe telefoŋ ndaxte dañuy woote cib nimero ba noppi duñu àddu ki dawsi ngir wuyu.Bu ñu wéyee di fowe noonu, ka ñuy jéem a jot dootul faale woote yu ñàkk faayda yooyu, te dina ci rax mer. Yàlla du tàyyi ci déglu sunuy woote. Looy xalaat booy woo Turam wi? Su fekkee ne dangay tudd Turam wi te doo ci bàyyi xel, kon loolu dafay wone sa wàllu dund gi nga sédd Boroom bi. 05.5 - NI MUSLIM(JULLIT) DI JëFANDIKOO TURU ALLAHAb jullit dafay faral di jëfandikoo Turu Yàlla.Ci kow loolu dafay yaakaar ñu gëm ko te may ko seede bu rafet te dëggu.Dafa yaakaar itam ne, lu mu gën a tudd turu Yàlla,ñu gën koo baal. Xalaat boobu jur na lu woyofal màggalu Yàlla, te di tudd Turu Yàlla, ñàkk cee boole sa xel bokk na ci. Kon bu nu xoolee ci loolu dinanu xam ne Jullit bi séqul ak Allah digante bu rattax. Ni muy jokkoo ak Moom dafa mel ni ab surga buy wax ak njaatigeem bu ragallu bi, te wóoru ko ne Mungi koy déglu bu baax. Rax ci dolli, waxtu julli juróom yi, ay santaane la yu ñu war a matal bés bu nekk. Li ëpp ci Jullit yi war nañu tari Faatiya (Saaru Al-Faatiya) fukk ak juróom-ñaari yoon bés bu nekk ci baat bu kowe walla bu suufe bu ñuy matal juróomi julli yooyu. Lu tollook ay tamdaretu jullit ci biir àddina si dañuy tari Faatiya ci araab, te fekk sax 800 alfuni yi dégguñu Araab. Lees ñaawlu itam am na ci biir Kercen yi, ndaxte ci jàngu yi bu ñuy def ñaanu Boroom bi, ñu ci bare seen xel du ci ànd. 05.6 - ŇAAN YU ÀND AK XEL ŇAAR, AK LAY YU TEGGUWUL FENNDu Jullit yi rekk ñooy tari seen farata boobu, waaye kercen yu bare dañuy woy seeni ñaan yi, mel ni ndey juy nax doomam ngir mu nelaw (aayoo nenne). Nan lanu man a sañe wax ak Yàlla ba noppi te bañ a séentu tontoom, waaye di yóbbu sun u xel ci sunuy yeneen mbir ak yeneen yu amul solo? Bu fekkoon ne am nanu xéewalu daje ak sunu njiitu réew, te man a wax ak moom, ndax kon dunu xalaat te tànn bu baax bépp baat bu nu ko bëgg a diis, laata nuy ubbi sunu gémmiñ? Diggante Yàlla ak nit ki, Kan moo ëpp solo ci sunuy bët? (Ndax nit ki moo ëpp solo Yàlla, ci sunu gis-gis?) Su fekkee ne am na kuy ñaan te bàyyiwul xel ci li muy wax, kon dafa xeeb Yàlla. Am na gëstukati diine yuy xaw a moy ñetteelu Ndigal li, ba di tiisloo Xel mu sell mi, bu ñuy jàng Biibal bi, di waxtaan ciy melokaani Yàlla ak ay kéemaanam, ñu mel ni ñuy waxtaane mbiri xam-xam yu nit jànge ci ay daaray gëstu te ber teewaayam (Yàlla) nee. Manunu am wax ju leer ju amul benn parparloo ci Yàlla, ndaxte Yàlla du ab xalaat, walla am mbir. Yàlla, kuy dund la, te nekk ci sunu wet saa su nekk. Dafay déglu sunuy waxtaan, te xam na sunuy xalaat. Kon book bépp njàngat bu àndul ak weg Yàlla te ragal Ko, ci moy ñetteelu Ndigal li doŋŋ lay jëme. 05.7 - MOY, CI KOW TUDD TURU YÀLLAMusiba dal na ñi koy tey di jalgati Kàddug Yàlla gi, di ko ñaawal ak di ko fowe. Dañuy caaxaane Tur wi gën a màgg bépp tur, te weguñu Ko, ragaluñu Ko. Warunu ànd ak ñu mel noonu, waaye danu leen war a yedd te liggéeyal sunu Boroom. Bindkat yi ak defarkati film yi xam nañu bu baax dooley kàddu diine yi. Ňungi leen di jëfandikoo leegi ci seeni liggéey, Waaye duñu jëfandikoo ay baat yu mel i ”bàkkaar”, ”safara”walla “sànku” ci anam yu leer; dañu leen di muure ay baati àddinas tey jii. Seeni kàddu dinañu leen dab te mbugal leen. Yenn saa yi nit ñi dañuy merante. Ci seen biir mer dañuy móolu seeni noon yi jaare ko ci ay baat yu mel ni “Yàlla”,”Alla”walla “Yeesu”.Dañuy waat ,di móoolu te di jëfandikoo ay baati diine,te duñu ci bàyyi xel.Benn bés, ab njiitu jàngu dafa doon romb ab masoŋ ,dégg ko muy waat,di móoluwaate.Noonu mu laaj ko :”Ndax nii la sa ñaan di dëgëre saa su nekk?” Nit ka ànd ak mbeteel ne ko.”Ňaanumawoon de.”Pastër ba ne ko :”Waay, dégg naa la ngay woo Yàlla te wóor na ne dina la tontu.”Nit ka xamatul lu muy wax. Nit ñi dañuy faral di jëfandikoo ay baat yu diis jëmale leen ci seeni moroom, ba ci seeni mbokk ak waajur sax. Mbañeel gu rëy moo làqu ci biir kàddu yooyu. Yeesu dafa jàppe kàdduy móolu yu mel noonu ni bóom, ndaxte dañuy taqal sobe melokaanu Yàlla ci nit ki. 05.8 - ARTUB YÀLLA: MBUGAL GU TARŇetteelu Ndigal li dafa ëmb ab artu bu diis: ”Yàlla dina mbugal, ci lu wóor, képp kuy fowe Turam.” Ak li boobu artu di am lépp terewul mu am ñuy wax Turu Yàlla ngir nëbb seen jëf yu ñaaw yi, te di jéem a jubanti seeni ndëngate ci kow “maa tey”. Toroxte ñeel na kiy tuddu Turu Boroom bi ci ay caaxaan ngir nëbb ay kàccam aky ñàkk kóllëreem! Ci sunu jamono jii, jafe na ngir nit ñi wóolloonte, ndaxte duñu waxante dëgg rawatina sax bu ñuy waate Turu Yàlla. Yeesu mayu nu fenn fu nu man a waate, dafa nuko tere: ”Bu ngeen di wax, neleen “waaw“ walla “Déedéet”; lépp lu ci yokku ci Seytaane la jóge.” (Macë 5:37) Bu nu waatee, mbaa nu fen, kon nit ñi lanu fen, waaye itam fen nanu Yàlla ci boppam. Am njàngale mu lalu ci fen, ñetteelu Ndigal li nu artu ne bunu tudd Turu Boroom bi ciy caaxaan, moo ko daan. Loolu moo tax Biibal bi ne nu: ”Maandute mungi tàmbalee ci ragal Yàlla.” Bu nu ragalul Yàlla, ci bàkkaar lanuy tàbbi. Yàlla du naw ki Ko xam ba noppi te du Ko ñaan ndimbal bu amee ay jafe-jafe. Bañ na itam kiy séentu tontoom ba noppi di daw wuti ab seetkat buy jëfandikoo turu Boroom bi ci ay caaxaan, naan man nañu feeñal la xewoon daaw, liy xew ren ak liy ñówi ëllëg (Pàttali gi 18:9). Yàlla nee na: ”Ku dellu ca ña génn àddina ak seeni ruu, di leen wootal ngir ànd ak ñoom, dinaa la dummuuyu te beddi la ci saw askan. (Waa Lewi 20:6). Duggante ak ñi dee itam ba di séq ak ñoom ay bataaxal yuy jóge ca ñoom, aramal nañu ko. Bàkkaar yu mel noonu dañuy teqale nit ki ak Yàlla, te di ubbil Seytaane aky ñoñam ay bunti xolam. Njaaloo la Yàlla jàppe moy googu. Ňaawteef la gu mel ni góoru njaalookat guy jaay xaalisu jabaram ci gànc yi. Kon kay, amul genn njaqare gu nu ciy am bu Boroom bi tuddee jëf yu mel noonu ”Ab njaaloo ruu” (Waa Lewi20:6) teg ci ne nit ñu mel noonu “Maasug njaalookat gu bon lañu.” Waa Afrik yu bare, waa Asi,dañuy takk ay téere ngir aaru ci lu bon. Njëg yu jafe lañu leen di jënde, te wóoolu leen itam.Dañuy bind itam ay ”bataaxali -wërsëg” ngir seeni koom-koom dox, ak it seen néegu séy. Yooyu askan yi gëme noonu, xamuñu Yàlla ci dëgg-dëgg. Am na ay réew yoo xam ne lu jëm ci xërëm, njoort ak jokkoo ak ñi génn àddina, bés bu nekk lay génn ci Tele bi. Nun Kercen yi danuy jàppe yooyu ceetaan ak njàngale ni ay coongi Seytaane yu ñu tegal seetaankat yu bàyyeeku yi. Defuñu dara ludul ubbi ay bunt yu jëme Safara. Boroom bi taxaw na temm ngir artu nu ci musiba yooyu dinu jéem a féwwale ak Moom. Yeesu rekk moo man a yewwi ñu mel noonu ci seeni buum yooyu. Di jàngalu say rëddi loxo, ak say biddeew, wootal ay rab,yooyu yépp ay yooni gàttal la ngir dem safara.Gisaanekati éllég gu naat yi dañuy xaar seeni kiliaan ci Dalukaayu IND yi. Dañuy fuddën itam ay bët yu ñu bënne xeej ngir aar leen ci musibab bët bu bon bi. Am na ñeneen ñuy langal ay xurfa-xarfa ci seeni woto(Daamar); ay weñi tànki fas ci seeni bunti kër, walla ñuy laal bant ngir dàq balaa. Nit ñu mel noonu, dooley lëndëm gi lañu gën a wóolu xéewalu Yàlla, seen Baay bi ci asamaan. Dooley jamono tey moo leen yeew ba ñu ne ŋodd ndax jëf yii. 05.9 - SOSAL YÀLLAAm na ñoo xam ne dañuy ëppal bu ñuy tudd Turu Yàlla: dañuy móolu Yàlla ak Kristam bi. Dañuy far ak ñiy sosal Turu Baay bi, Doom ji ak Xel mu Sell mi. Seytaane moo yàgg a nekk noonu Yàlla. Weddi Yàlla, ubbil aw yoon jinne yi ak rab yu bon yiy wale safara la. Su fekkoon ne am na kuy jàng ab bataaxal bu gudd bu ñuy móoloo Krist aky Ndawam, kon dina yëg noyyig Safara ci xar-kanamam. Ci téereb waa Lewi 24:14-26, jàng nanu ci ne: ”Génneel ci dalu bi (màkkaan mi) nit ki saaga; ña ñépp ñi ko dégg teg seen loxo ci boppam, te mbooloo mépp sànni ko ay xeer ba bakkanam rot. Te nanga wax Bànni Israil: ”Bu nit saagaa Yàllaam, dafa war a yenu diisaayu bàkkaaram; te noonu, ku weddi Turu Boroom bi dees na la faat: mbooloo mépp war na ko sànni ay xeer ba mu faatu; nay doon doxandéem, mbaa muy waa réew mi, dañuy jël bakkanam, ndax li mu sosal TUR WI.” Danu war a lewet te teey bu nuy wax ,walla nuy àtte ab sosalkat. Ay nit ñu rab jàpp, dañuy ñàkk gis-gis ba foog ne Yàlla lañuy liggéeyal, te fekk ñungi Koy xeex, Moom ak Almaseem bi (Yowaana 15:19-21; 16:1-3). Ay kilifa diine yu am baat àtte nañu Yeesu ngir ñu rey Ko, te seen lay mooy ne Yeesu dafa sosal Yàlla. Ak li ñu nekkoon ay njiiti diine lépp, terewul xàmmeewuñu Yeesu, Doom (bàjjo) ji Yàlla jiy dund am kepp. Ci kow seenug xadar ngir liggéeyal Yàlla, sosal nañu Almasi bi. Tëfli nañu Ko ci kanam, dóor Ko ci bopp. Kilifay askan wu yàgg woowu ràññeewuñu te nanguwuñu seen Boroom bi ñów teew ci seen biir. Dañu Koo weddi te daaj ko ci bant. Li ci gën a tiis nag mooy ne ñu bare ci seen biir ñungi Koy weddi ba tey jii. Ni doomi yanqooba yi, Jullit yi itam dañuy xalaat ne bu ñu sosal Yàlla suñu gëmee Yeesu Yàlla la te daaj nañu Ko ci bant. Dañoo donne mbañeel googu teguwul fenn ci Yawut yi, ba noppi di xeex ngëm-ngëmu Kenneefu ñettu Yàlla ji. Mbañ gu tar lañu taxawoo Doomu Yàlla, ji ñu daaj ca bant ba. Seen sosal dafa ne fàŋŋ te jàmmaarlook Yàlla Baay bi, Doom ji ak Xel mu Sell mi, loolu lépp ndax bañ Kenneefu Ňett ñi doŋŋ. Ci geneen wàll gi, diine Indu yi dañoo weddi kilifteefu Yeesu te jàppe Ko rekk ni kenn ci seen yàlla yi. Ay kercen yu tàbbiwaat ci bàkkaar dañuy mujj sax di jaamu Seytaane. Ci seen màggal yi dañu ciy sàkkal Seytaane ay saraxi deret yu ñaaw. Dañuy soppi ñaanu Broom bi dugal ci ay kàddu yu ñaaw. Doole lëndëm ji noonu lay dugge ci ki nanguwul mucc gi Yàlla jaarale ci Krist. Waaye ci Krist ,sunu kaaraange mat na,ndaxte Moo nuy aar ci coongi Seytaane. Sunu sàmm bu baax bi nee na: «Samay xar dinañu dégg sama baat; xam naa leen te ñu ngi may topp. Dama leen di jox dund gu dul jeex; duñu sànku mukk, te kenn du leen jële ci sama loxo. Baay bi ma leen jox, moo gën a màgg lépp, te kenn mënul a jële dara ci loxob Baay bi. Man ak Baay bi benn lanu.» (Yowaana 10:27-30). ”Yawut yi bëggoon nañu lool topp ñetteelu Ndigal bi, ba ragaloon nañu sax tudd turu Yàlla ci njuumte,walla lees teyul. Turu Yàlla ci Yawut ñeeti araf yii lañu koy binde ”YHWH”. Ni Tur wi selle, moo tax Yawut yi ragaloon koo tudd bu ñuy jàng Téere yi; noonu ñu dippee Ko ”ADONAI” ca boori atum 300 laata Krist di ganesi àddina. “Jehovah” tur la bu nit sàkk mooñe ko ak y araf yu jóge ci ”Adonai” ak yu bokk ci “YHWH”. Loolu munga amewoon ca atum 1520 gannaaw ba Krist ganesee àddina. Kon ca njalbéen ga “YAHVE”lañu doon wax. Kon nag loolu indil nanu bii laaj: Ndax war nanoo muytu tudd turu Yàlla? Nan lanu war a tudde turu Yàlla ngir bañ a moy Ndigal bi, ba di tàbbi cib àtte? 05.10 - TUDD TURU YÀLLA CI ANAM YU JEKKŇetteelu Ndigal li aayewunu nu tudd turu Boroom bi ci yéene ju rafet. Bul tudd turu Boroom bi ci ay caaxaan bu fekkee ne nangu nga ko ci kow ngëm, mbëggeel ak kóllëre. Boroom bi jekk na ngir jëfandikoo sa seedes ngëm ngir ni yoonu mbaal ak yeesal ci dundug say xarit. Turam wi laamboowul genn kàttanu luxus, te manunu di Ko jëfandikoo ni mu nu neexe. Boroom biy dund, Turam lay jëfe ci kow ni ko Maanduteem ak Dogalam natte. Ndaw li Piyeer dafa ne lafañ ba:” Ci turu Yeesu Krist mu Nasaret doxal!” Gannaaw gi waxoon na mag ña ca kanamu kureelu àttekat yu mag ya ne: ”Ci turu Yeesu Krist la nit kii wére ba taxaw ci seen kanam.” (Jëf 3:6 ;4:10) danu waroon a yokk sunu xam-xam ci lu aju ci turu Yeesu ak kàttanam. Gëstukatu diine bu siiw te tuddu Adolf Schlatter, te di waa Almaañ dafa manoon na tari Téereb Kóllëre gu Bees gépp ci làkku Grek. Waaye ca mujjug dundam dafa bindoon ab téere bu mu tuddewoon: ”Ndax xam nanu Yeesu?” Warunu di woyofal turu Yeesu, waaye danu war di ko gën a jéem a xam. Bu nu jéemee dund na Mu dundewoon, kon dinanu ko man. Kon book nanu fexee màgg ci Kàddoom jaare ko ciy ñaan. Nanu xalaat ci bépp baat, te bàyyi Kàddug Yàlla gi mu sax ci sunu xol ba Yàlla man a wax ak nun. Dinanu nekk ay seede Krist yu gën a dëgër bu nu mokkalee ay saar ak ay aaya yu nekk ci Kóllëre gu Njëkk gi ak gu Bees gi. Kàddug Yàlla gi kàttan la gu nuy may maanduteg Xel mu; Sell mi. Baarkeel nga yow miy feesal sam xel ak Kàddug Yàlla gi. Rax ci dolli, seedes way-gëm yi, ak nettali jaar-jaari niti Yàlla yi, man nañu nu dimbali ngir nu gën a man a xam Boroom bi aky Jëfam; dinanu dëgëral sunu ngëm. Di faral a nafar Kàddug Yàlla gi dafa nuy bégloo te sunuy xarit; dañuy bége seedes sunu ngëm. Sunuy déglu Kàddug Yàlla gi, kon dunu réer, waaye danuy gën a xam sunu Boroom bi. Man nanu jàkkaarloo ak Moom, di wax ak Moom, ndaxte xam nanu Turam. Dafay wax ak nun ci Téereem bu sell bi(Biibal bi), nu Koy tontoo ak sunuy ñaan. Ndaw ngëneel gu nu am su nu manee dénk sunu Boroom bi nu sàkk, bépp jàngoro, jafe-jafe, bàkkaar ak ay bundxataal, te xam ne mungi nuy déglu. Yeddam moo ëpp solo bu boroomi xam-xami jamonoy tey jii yu aju ci nekkinu nit ki. Moo nu gën a bëgg sunu baay bi nu jur. Dafa nuy baal sunuy bàkkaar ba ñu set wecc, ndax dee gi Yeesu jébbalee boppam; te itam, dafa nuy may dooley Dundam; Jaare ko ci XELAM mu SELL mi nekk ci nun. 05.11 - NANU SANT YÀLLA AK SUNU XOL BEPP; AK SUNU XEL MEPPNdax nungi màggal Yàlla,te di ko sant ak sunu xol bépp? Nanu fàttaliku ne Yàlla Aji kàttan ji mooy sunu Baay ji ci asamaan, te Doomam ji Mu am kepp, di sunu Musalkat, itam Xel mu Sell mi di sunu doole ak sunu dëfalkat ba fàww. Kon book nanu am ngërëm. Laata nuy màggal Yàlla ci tiit ak lox, nanu Ko màggal ni ay doomam yuy bànneexu ci Muccam gi Mu maye. Waratunu wéy ci di dee ci bàkkaar, waaye danu war a dund ci Krist ba fàww. Su ko defee, boo manul a woy ci ab kooraal, nga woyal sa bopp, te soo manul a woye ak sa gémmiñ, woyal ak sa xol. Booy tudd ak kóolute turu Baay bi, Doom ji ak Xel mu Sell, ci sa biir ñaan, dangay màggal Yàlla Aji Kàttan ji. Say woyi cant neex nañu ko. Su fekkee ne am na ku xamul Yàlla, walla xolam tëju lool ci dëgg gi, mbaa dundinu bàkkaar sonnal ko, kon ndawu Yeesu bi tuddu Pieer dina ko soññi: ”Su boobaa nag képp ku woo Boroom bi ci aw Turam, dinga mucc.” (Jëf ya 2:21) Am nanu ngëneelu man a wax ak Yàlla sunu Baay, ci turu Yeesu, te xam nanu ne dina nu tontu. Man nanu jege Yàlla, ndaxte moo nu jegesi. Turu Yàlla, ”sunu Baay” dafa nuy wóoral ne bépp barke bu jóge asamaan jagleel nañu nu ko. Turu Yeesu dafay yëngal fondamaŋu Safara, ndaxte daan na bàkkaar, dee gi, lu bon li, ak sax merum Yàlla. Xel mu Sell mi dafay màggal Doomu Yàlla ji ndaxte ci turam la nu maye dund gu amul àpp ak kàttanu Yàlla, ji amul fenn. Dafa nuy may itam kaaraange, laab, mbégte ak jàmm. Ni jànt bi di waaccee bés bu nekk naajam bi ci kow suuf, noonu itam la nu turu Yàlla miy Kenneefu ñett di nu maye yiw ci kow yiw. Kan moo dul sant Baay bi walla du màggal Doom ji, te du ñaan ci kàttanu Xel mu Sell mi? Yaatalal sa Xelum Boroom, miy dëfal, kon dinga xam ni Yàlla di tontoo say ñaan. Màggalal ci turu Yeesu, sa Baay nangu na lu ni mel. Sant Ko, màggal Ko, ndaxte dafa laa bëgg fayal say bàkkaar te may la dund gu amul àpp. 05.12 - SEEDEEL ŇENEEN ŇI SA NGëMKan moo man ne tekk te fekk xolam mungi fees ak cant, ak woyi màggal? Ak kan moo man a denc muccam ngir moom doŋŋ, te xam ne Yàlla dafa bëgg ñépp mucc? Jot ñi réer, du sunu tànneef, waaye sunu Boroom bi Yeesu ci boppam moo nu jox ndigal ngir nu yët ñépp Xabaar bu Baax bi. Ndamul Yeesu ak màggaayam dañu leen war a jibal. Ndaw li Pieer soññi na nu: ”te jekk ngir tontu ku leen di laaj ci seen yaakaar ji ngeen am.” (1Pieer 3:15). Yeesu itam dafa nuy soññi te di nu artu: ”Koo xam ne nangu na ma ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la nangu ci kanamu sama Baay, bi nekk ci kow.” (Macë 10:32-33) Ndaw li Póol sonnoon na lool ca ay jàmmarloom ak nooni Yàlla ya. Yàlla feeñu na ko ci guddi, te dëfal ko: ”Bul ragal dara, waaye deel wax te bañ a noppi ndaxte maangi ànd ak yow te kenn du la jàpp, ba fitnaal la, ndaxte am naa askan wu yaa ci dëkk bii.” (Jëf 18:9-10)Biral na ko ne: ”Dinaa la musal ci bànni Israyil ak ci ñi dul yawut. Ci ñoom laa lay yebal, ngir ubbi seeni bët, nga jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, nga nangoo leen ci sañ-sañu Seytaane, woññi leen ci Yàlla, ma baal leen seeni bàkkaar te may leen cér ci biir sama gaa yi sell ci kow ngëm.” (Jëf 26:17-18) Ca ngoon ga Mu dekkee, Yeesu dafa may sañ-sañam bi jóge asamaan,gaayam yi ragaloon ba tëj- ràpp seen buntu kër: ”Na jàmm wàcc ci yéen!Ni ma Baay bi yónnee, noonu laa leen di yónnee, man itam.” Bi Mu waxee loolu, Mu ëf leen, ne leen: ”Sol naa leen Xelu Yàlla mu Sell mi. Ňi ngeen di baal seeni bàkkaar, baal nañu leen ba noppi; ñi ngeen baalul, baaluñu leen.” (Yowaana 20:21-23) Soo mokkalee ay aaya, te di leen nafar ci sa xol, di nga jot kàttan ak yoon yu lay may man a wesaare Xabaar bu Baax bi ci anam yu gën a am doole ci biir ñi réer. 05.13 - JëF CI TURU BOROOM BINgir sunu seede bu nu Boroom bi diisee Kàddoom, te nu tontu ko ci biir sunuy ñaan ak aky woy, te nu nangu turam ci kanamu sunuy xarit ak sunuy noon, kon dinanu mos sañ-sañu Turam wi. Ci turu Yeesu ndaw ya faj nañu ñu feebar, dàqay rab, dekkal ñu dee. Yeesu ci boppam dalal na taw bu rëy ci kàddoom kese, bareel na juróomi mburu ngir ay junni ..nit lekk ca ba suur. Baal na bàkkaari ñi tuub te may na leen dund gu dul jeex. Yeesu nee na: ”Sama Baay mungi liggéey ba tey, kon man itam damay liggéey.” (Yowaana 5::17) Du Turam rekk lanuy wax, waaye dafay jëf jaare ko ci bunuy biral sunu jébbalu ci Moom, ci sunu ñaan, sunu ngëm, ak li nuy néew doole lépp. Bu Baay bi, Doom ji, ak Xel mu Sell mi dëkkee ci xolu ku gëm, Yàlla dafay matal ci dundam ay kéemaan. Li Doomam yi nekk ay gune, du ci dara, ndaxte Moom, Baay bi ci boppam mooy matal liggéey bi. Ngir sunu seede am doole, sunu dund dafa war a wone li nu gëm: Danuy sant Yàlla te di dégg ndingalam ci sunu dundin. Xel mu Sell mi dafa nuy xiir ci nuy doxe ak cellaay te dafa nuy sellal ndaxte Moom ci boppam dafa sell. Yeesu jàngal nanu te it teg na baaraam ci baat yu njëkk yi ci Ňaanu Broom bi, ngir nu sellal turu Boroom bi ak sunu gémmiñ, ak sunu doxalin. Sunuy ñaan ay fen lañuy doon te sunu seede rax bu fekkee ne sunu dund mungi weddi kàttanu Yàlla, te wonewul suufeelu gu dëggu. Ci dëgg danuy bàkkaar te du sunu coobare, teewaayu Xell mu Sell mi moo nuy dammat. Ňu tuut mbaa ñu rëy, sunu bàkkaar yi ñàkkuñu solo ci kanamu Boroom bi. War nanu di fàttaliku saa su nekk ne bu nu bàkkaare danu Koy tiisloo. Waaye Xel mu Sell mi mungi dëkk ci ñépp ñi rëccu te dëddu seeni bàkkaar dafa koy delloo mbégam te maye kóoluteg cellaay ci bépp bàkkaar jaare ko ci deretu Yeesu. (1Yowaana1:19) Kàddug Yàlla Baay bi dafa nuy soññi ngir nu gëm Yërmaandeem, te di dunde turu Yàlla miy Kenneefu Ňett ñi. Danuy mos cellaay gi jaare ko ci Mbëggeelam gi kenn manul a méngale, te, fees ak muñ. Ndax xam nga turu Yàlla ci dëgg-dëgg te naand Ko? Turam wu sell wi, ndax mungi ci sa làmmiñ? Xelum Boroom bi, ndax mungi dëkk ci sa xol? Su boobaa rekk ngay man a tudd turu Baay bi, Doom ji, ak Xel mu sell mi ci kow njekk, teraanga ak mbëggeel. Na la Yàlla sàmm ba nga bañ a tudd turam ci ay caaxaan te may la nga Koy màggal ak mbég sa dund gépp. |