Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
Home -- Wolof -- The Ten Commandments -- 07 Fifth Commandment: Honor Your Father and Your Mother
This page in: -- Afrikaans -- Arabic -- Armenian -- Azeri -- Baoule -- Bengali -- Bulgarian -- Cebuano -- Chinese -- English -- Ewe -- Farsi -- Finnish? -- French -- German -- Gujarati -- Hebrew -- Hindi -- Hungarian? -- Indonesian -- Kiswahili -- Malayalam? -- Norwegian -- Polish -- Russian -- Serbian -- Spanish -- Tamil -- Turkish -- Twi -- Ukrainian? -- Urdu? -- Uzbek -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson? TOPIC 6: THE FUKKI NDIGAL YI - Ab ñag buy aar nit ki ci cib jéll
Fukki denkaane yu am solo yi ci Exodus 20 ci leeralu xebaar bu baax bi
07 - JURÓOMEELU NDIGAL LI: Na nga wormaal sa ndey ak sa baayGàddaay 20:12 07.1 - TMAYU YÀLLA: NJABOOT GINjaboot,per bu am njëg gu rëy la, te it maccaatu Àjjana la. Yàlla dafa sàkk nit ki, góor ak jigéen, ngir ñu wone Ndamam, Muñam, Mbëggeelam sakkan te feesal àddina si. Kon man nanu jàpp ne njaboot mooy xooxu dundu nit ki, te mooy reenu bépp aada ak cosaan. Mooy indi kaaraange gu wóor, jàppalante te it li ci ëpp mooy gën a am doole xalaati àddina yu bees yi sax. Diine yépp ñoo ànd nangu ne war nanu wormaal waajur yi. Yoon la xale yi naw seeni waajur te wormaal leen. Komunism bi, di lees gëmul Yàlla (yéeféer) ba mu indee xel-ñaar ci taxawaayu waajur ci kër, ci la jàmmarloo ak AJI SÀKK ji ak li Mu sàkk, rax ci nag ay sarti dundinu neen ak yu xel maye doŋŋ. Yàlla dafay aar njaboot gi, jaare ko ci juróomeelu Ndigal lii. Nanu Ko sant ngir ni Mu taxawale njaboot gi, nekkin gi ak jokkoo gu ànd ak mbóoti mbëggeel yi ci biir, teg ci jàppalante bi. Ci juróomeelu ndigal li, Yàlla dafa nu sant nu wormaal, du caageen rekk sunu baay, biy njiitu kër gi, te di dab sunuy soxla, waaye itam sunu ndey ak yeneen jigéen ñépp. Ni ku góor ki, dañuy sàkku ci moom muy wone melokaanu Yàlla ci dundam te di séddoo ak boroom këram wareefi kër gi. Dara umpalewul lu tax Kóllëre gu Njëkk gi ak gu Bees gi ànd déggoo ci wormaal Ndey ak Baay. Ndigalu sàmm njaboot gi te bégal ko lu leer la te nekk yoon. Ci mala yi, mbote yi dañuy topp seeni ndey, te picc yu góor yi ak yu jigéen yi dañuy aay-aayloo bóof seeni nen yenn saa yi. Itam, dañuy xontandoo seeni doom ba ñu manal seen bopp. Yàlla moo taxawal ay jokkoo ak lëngoo yu kenn warul a jéggi te yoon dalul sa kow. Tey jii ay yoon a ngi mébét xale yi, te di dëgëral seeni xol: ”Buleen déglu seen waajur yi, te buleen leen déggal. Xalaatleen seen bopp, yokku te dund seen jamano, fippuleen!” Bëti xale yi dañu lëndëm, déggadi, seen mbég seey na. Wàll wu rëy ci seen xol jaxasoo na. 07.2 - COONO WAAJUR YINdey ak baay yépp am nañu ngëneelu bokk ci tàggat ndawi jamano ëllëg yi. Juddu gu bees gu nekk, ag kéemaan gu jéggi dayoo la! Xéy na waajur yi séentuwuñuwoon juddug xale bi. Waaye ndey ji ak baay bi matal nañu ni Yàlla bëgg a sàkke. Boroom bi baarkeel na leen te may leen ñu man a may liir biy nàmp, ndono li maniw di meññ ngir ay maasi-maas. Kon nag góor gi war na sujjoot ci kanamu Boroom bi, màggal Ko,sant Ko ngir bépp juddu. Sunu yaay yi ëmb nañu nu juróom-ñeenti weer, maanaam 275 fan, guddi ak bëccëg. Danu aaruwoon te sunu soxla yépp faju. Séddoo nanu ak ñoom seen mbégte, seeni mer, seeni naqar, tiis ak coonoo. Xéy na yàgg nañu nu ñaanal laata nuy juddu. Xéy na wasin bi indiwoon na tiit ak metit. Sunu waajur yi dañu nuy gunge yenn saa yi ay at yu bare. Dañuy gis sunu yaram ni muy màgge, di reeandoo ak tiisandoo ak nun. Ňenn ci ñoom dañuy sant Aji SÀkk ji ngir sunu dund ak sunu màggaay. Su fekkee ne sunu waajur yi ci loxoy Yeesu lañu màgge, kon wóor na ne dénk nañu nu Baay bi ci kow asamaan. Jàngal naňu nu Ndigali Boroom bi te ñaax sunu xol yi ngir nu gëm Aji Sàkk ji ak Sàmm bu Baax bi. Yer nañu nu, bëgg nu te baarkeel nu lu raw ni nu ko xalaate. Toppatoo naňu nu guddi ak bëccëg. Dañu xar seeni tànki tubéy ngir dundal nu te sàng nu. Sonn nañu ngir yer nu te bàyyi nañu xel ci sunuy àndandoo aky xaritoo. Saa yu nu feebareete, wopp, taxawu nañu nu ba mu mat sëkk. Bégal nañu nu, te jooyandoo ak nun. 07.3 - JAFE-JAFE NJABOOT YIJokkoo gu dëgër, mooy boole doom ak waajur, ba mbëggeel ak wóolonte man cee sax. Waaye nag nekkatunu Àjjana. Amul benn xale bu baax te waajur yi itam kenn ci ñoom matul te bàkkaarkat lañu ci kanamu Yàlla. Kon nag mag ak ndaw ci yiwu Yàlla rekk lañuy dunde ak baalante gu dul jeex. Jàmm du dal mukk ci njaboot gu amul mbaal ak muñ. Delloosi jàmm ci njaboot gi du man a am fi ak nangu tooñ ak jéggalu gu ànd ak suufeelu amul. Barke ñeel na gune yi yeroo ci mbëggeel ak mbaal. Du waajur yi rekk ñooy yer xale yi ci ngëm ndaxte Doomu Yàlla ji ci boppam dafa santaane ñu indil Ko xale yépp ngir Mu barkeel leen. Waajur yi war nañu di faramfàcceel seen gune yi lu jëm ci Xelum Yeesu ak njubteem, jàngal leen ñu sàmm Ndigalam yi, te xaatim Digeem yu rëy yi ci seeni xol. Ndey, ak baay ñoo bokk yem wareef ci yeru diine xale yi, kon waruñu sëf xale yi seen ngëm, ci neex- naqari. Bépp xale moo war a tànn su fekkee ne bëgg na ànd ak Aji Sàkkam ji walla déet. Nanu dimbali xale yi ba ñu xam ne barkeelu waajur yi dañuy law ba ci ay maasi-maas. Yeen waajur yi, moytuleen di reewal xale yi, ba di leen tàyyeelloo. Buleen leen di defloo lu méngóowul ak seen maas. Mayal xale bi mu am toogaayu xaleem ba mu mat! Duggu Ekool, ak jàng xarala yu màcc, am na solo lool waaye du suxlu torop yeru xale bi. Li ëpp solo mooy yee ci ñoom ag ragal Yàlla, ak mbëggeel ci seen Baay ji ci kow, nàmm seen nite, seen dëggu, njubte, teewlu ak cellaay. Am na solo lool ngir waajur yi di toogandoo ak seeni doom, di déglu seeni laaj ak seeni jafe-jafe.W aajur yi kay, dañu waroon di ñaanal bés bu nekk seen doom yi ngir ñu am juddu gu bees (Judduwaat) te dund ak Yeesu. Bu ñu tolloo ci waxambaane, xale yi dañuy tàmbali di diir mbagg aka ngàññ seeni waajur yi. Seen bëgg-bëggu moom seen bopp boobule yoon la te kenn waru ko jàppe ni xas. Bu fekkee ne waajur yi dañoo dénkoon seeni tuut tànk Kenneefu Ňett ñi, kon doon nañu leen man a gunge ci biir at yu taq- suuf yi, ci kow muñ, te bañ leen di xoj. Tuut-tànk yi dañuy soxla ay xarit yu dëggu, te di bokk ci ay mbootaayi kercen yuy jàngale Biibal bi ni mu ware. War nañu leen di gannaaye ay téere yuy yokk seen xam-xam te ñu tànne ko ci li ñuy wone ci telewisoŋ bi. Bu nu bëggee xoj xale yi ngir ñu dunde ni maam ya, loolu dina jur fippu gu ànd ak ndëggëru xol bu tëju. Nun waajur yi danoo war a bàyyi xel ci ni nu Yeesu artoo: ”Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ci ñi Ma gëm, li gën ci moom mooy ñu takk doj wu rëy ci baatam, sànni ko ca fa gën a xóot ca géej ga.” (Macë 18:6) ”Yóbbaale ci bàkkaar” tekkiwul jàmmarloo walla mer, waaye yóbbaale ci fen, sàcc, mbaa bàyyi leen ñuy dugg ci yenn bàkkaar yi te di ciy bañ a artu ni mu ware. Ag yer gu barkeel mooy jur ragal ak bëgg Boroom bi. Ci sunu jamano jii fees ak jëm- kanamu xarañi xel yu bees yi ñuy woowe “Sians”, ay waajur yu néew ñooy niru seeni doom ñu “dellu gannaaw ci seen ngëm.” Yenn saa yi, dafay am waajur ju manul a jàng, manul a bind. Loolu mayul xale bu am njàng, muy kañu mbaa mu di ko ñaawal. Loolu lu teggi ndawal la, ndof te ñàkk kersa. Man a jàng ak bind du mooy wone xel ak tolluwaayu solo nit ki. Njàng mu kowe taxul mbaax walla sellaayu ndongo li mat. Sañ-sañu waajur yi wékkuwul ci li ñuy am, walla ci li ñuy man a rënk (denc). Seen sañ-sañ mungi aju ci coobare Yàlla ak ci ni ñuy ñaanale seen doom yi ci kanamu gàŋune yiwu Yàlla gi. Baayoo gi nu Yàlla may moo jii mbëggeel ci xolu waajur yi. Saraxu Krist bi mooy suqali bëgg-bëggu tarbiyyu Ko bu laajul dara, ak itam ”xelum dem ba jeex” ci diggante waajur ak doom. 07.4 - DEGGAL(DéGGAL) JURÓOMEELU NDIGAL LINan lanu man a wormaalee sunuy waajur?Sunum xel sax dafa nuy fàttali ne war nanu leen di bëgg te di leen wormaal ndaxte ñoom lanu xam te ñoo ëpp solo lépp lu nu am ci kow suuf. Ci loolu bokk na ci yii di kóolute, déggal, fàtte sa bopp te bañ di jiital say bëgg-bëggi bopp. Doom warul dóor mukk ndeyam mbaa baayam, ci kow lees tey mba lees teyul. Jekkul doom di jiite njaboot gi Boroom bi rekk Moo ko war a jiite. Yeesu jàngal nanu caabi kër gu naat ba Mu nee: ”Ndaxte noonu la Doomu Nit ki ñówe, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye Muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.” (MACë 20:28) Doomu Yàlla ji dafay soññi waajur yi ak doom yi ngir ñuy sàmm bu baax dundinu njaboot gi. Ndax wareefu doom yi ci seeni waajur, fi ñu ame seen njabooti bopp lay jeexe? Mukk! Ndaxte bu waajur yi demee ba màggat ci yaram ak ci xel, ci lañuy gën a soxla seen ndimbalu doom. Njaboot gi, muy ju góor ji walla ju jigéen ji, war na man a joxe as wàllu dundam ay waajuram, ni ñu ko ko taxawewoon ba mu nekkee gune. Amul genn këru paj walla dalukaayu màggat yi manul a weccoo ak doom yuy joxe seen jot, seen xaalis ak seen kéem-kàttan ngir jàppale seeni waajur yu màggat yi. Juróomeelu ndigal li moo maye ndig lu leer gannaaw baayoo gi nu Yàlla baaxe. Yàlla dafa waxul ne ”dig na kiy toppatoo ay waajuram ay fan yu guddu ci kow suuf yu ànd ak ñurumtu yu néew, te fees dell aky baarke. Saa yu ñu sagalee waajur yi te gune yi ak seeni waajur di dunde coobare Yàlla, dinañu gis ni dig bii di mate ci seen dund. Yàlla dafa nu tere nuy tuutal sunuy waajur ak ñëpp ñi nu yilif. Yii nag bokk nañu ci yu ni mel: aakimoo nguur, ñàkk njubte, naaféq ak njublang. Xanaa Yeesu waxul ne” Ci dëgg maangi leen koy wax, saa su ngeen defalee loolu kenn ki gën a ndaw ci sama mbokk yii, Man ngeen ko defal.” (Macë 25:40-). Ndax yaangi fàttaliku fippu bu naqarlu bi amoon diggante Absalom ak baayam Daawuda? Fippukat ba dafa mujj a dee (1Samwil 15:1-12;18:1-18). Danuy jàng ci Gàddaay 21 :15-17: ”Ku dóor sa ndey mbaa sa baay, dees na la rey. Te ku lël nit (Sàcc)-mu jaay ko walla ñu fekk ko ciy loxoom- dees na ko faat.” Léebu 2o-20 nee na “Ku saaga sa ndey, mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel. Léebu 20:20 nee na: ”Ku móolu sa ndey mbaa sa baay, ab làmpam dina fay ci biir lëndëm gi” Pàttaliku 21:18-21, ”Bu nit ki amee doom ju dëgër bopp ju dul déggal baay mbaa ndey, kon waajur yi war nañu ko yóbbu ca kureelu mag ña ngir xamal leen ni muy dunde ak ñoom. Maanaam mungi lekk di naan te nanguwul déggal kenn! Su boobaa ñépp dinañu génn ngir sànni ko ay xeer ba mu dee. Dinga dindee noonu lu bon ci sa biir; Israyil yépp dina ko dégg te jaare ci ragal.” Doom ji jàmmarloo na te fippu ci kanamu ay waajuram ba noppi nanguwul a rëccu te tuub ay bàkkaaram, ci noonu nekk na musiba ci askan wépp. Ca jamano jooja, askan wi ci mbëggeel ak dégg-ndigalu xale yi la wéeruwoon-ba tey jii sax! Yàlla ci nu leer lay waxe ak xale yi,te di artu waajur yi.Mag ñi waruñu “merloo”gune yi ndaxte Yàlla moo leen leen dénk. Digu Yàlla dafa wuute ni muy mate fii:”Saa yu ngeen defale loolu kenn ki gën a ndaw ci sama mbokk yii,man ngeen ko defal.”(Macë 25:40) Ndaw li Póol itam artu na waajur yi ci mbirum bundxataal ak sëf xale yi(Efes 6:4;Kolos 3;21) Waajur yi waruňu di bàyyeeku lool ci kanamu xale yi walla di soxor ci ňoom,fàtte sax ne xale yi daňoo am ay ndonoy deret.Waruñu doyloo seen doxalinu njureel,ndax ndono bàkkaar ak néew doole ,waaye lewetaay rekk.Lewetaay googu mooy tax ba xale yi am toogaay gu ànd ak yer. Ci kow loolu lépp ,baay ak doom soxla nañu ñaan Yeesu ngir Mu may leen saa su nekk ňu man a yeyu ci seen bàkkaar,tuub ko ,ba man a yeesalaat seen xel. 07.5 - KERCEN BU AM AY WAAJURI JULLITFenn rekk la xale yi man a laankale seeni waajur: Bu ñu leen waxee ñu def lu dul coobare Yàlla. Biibal bi nee na: ”Déggal Yàlla moo gën déggal nit."( JëF 5:29). Tey jii ci biir Yawut yi ak Jullit yi seeni doom yu bare toppatuñu seeni diine baay, ndaxte jot nañu xam Yeesu ni seen musalkat. Loolu jàmmarloo ju tar lay jur ndaxte ñoom dañoo dug ci coppite baatin gu xóot ci mbëggeelu Yàlla gi leen Xel mu Sell mi muure. Kon ñooñu leen a soññi ngir ñu gën a bëgg seeni waajur. Dañu war a jàng ni ñuy seedee ak maandute ci seeni jëf yu rafet, muur làmmiñ bi ñuy seedee seen ngëm. Muñ, ngëneel la te xale yi dañu war di ñaanal seeni waajur yi xamagul Krist, ngir Yàlla man leen a yeesal ci Yiwam gi. Dañu leen war di faral a seeti ndaxte ci àddina sii, kenn gënuñoo bëgg ku dul sunu waajur. Bu ay waajur bañee rëkk xelum Yeesu, te di noot seeni doom ngir ñu weddi Musalkat bi, ba di leen di tëkkoo rey ci yoonu saria, kon tàqalikook ñoom jot na. Xelum waajur mu dumuuyu diine kercen noonu jar naa àtte te sore ko. Waaye nag waajur yi danu leen war a wormaal, te bëgg leen ci lu dara taxul. Monte Kàddug Yeesu gindi nanu: ”Ku ma gënalul sa ndey walla sa baay, yeyoowuloo ma:” (Macë 10:37) Su fekkee ne ay waajur dañu jubadi, mbaa ñu soxor ci seeni doom ci mbiru diine, yëg-yëg, aada, walla xaalis yooyu xam nga ne man na indi ay ñol-ñol yuy fippuloo xale yi. Loolu moo tax Yeesu ne nu nu sore mbokk yu mel noonu balaa ñuy néewal sunu ngëm. Tàqalikoo gu wóor jar na ko yenn saa yi, ngir ñiy soog a gëm man a màgg ci seen ngëm te sóobu ci liggéeyu Yeesu. Tàqalikoo googu lu metti la ci waajur yi ak ci doom yi itam, waaye mbëggeelu Yàlla moo sut bépp yëg-yëgu mbindeef ci know suuf. Way-gëm yi nekk ci jàngu yi dañu war gaaw a dalal taalibe yu bees yi ñu sonal te jàppe leen ni doomu ndey, rakk,yaay walla baay. Loolu man na ëmbaale jàngal leen liggéey, walla njàng mu kowe, ak sax lu jëm ci néegu séy. Ni mbégeelu ndey ak baay amulee àpp, noonu itam la mbëggeelu waa jàngu bi war a mel ci taalibe yu bees yi, ba sax ci bu fekkee ne taalibe boobu am na dundin gu jekkul. Mbëggeelu Krist, ak Muñam giy yeeslu, ñooy liy xiir way-gëm yi doomoo taalibe bu bees. 07.6 - DAANEEL BIMbëggeel gi am ci biir kër gi dafa war a lerax mbëggeelu Yàlla ci nun. Yàlla ji nekk mooy sunu Yàlla, te dafa noo woo ngir nu bokk ci Njabootam gi ci kow asamaan, ba fàww ci Yeesu Krist. Dafa nuy Sellal jaare ko ci deretu jenn Doomam ji Mu am kepp, ngir sàmm sunu jokkoo ak Moom, te dafa nuy dekkale ak kàttanu Xel mu Sell mi. Bu nu ñàkkee sunuy waajur ci lees -teyul (aksidaŋ), walla ci yeneen anam, warunu jànnaxe, waaye danu war a nangu ni Dawuuda: ”Su ma yaay ak baay bàyyee, Aji Sax ji dina ma fal.” (Sabóor27:10). Mbëggeelu nit matul waaye sunu Baay bi ci know asamaan dafa nuy dalal ak Mbëggeel gu laajul dara, te uuf nu ciy loxoom. Léebu “Doom ju réer ja” moo nuy won dalal bi baay ji teeroo ka réeroon, ak ni mu jéemee yey ka xel ma dal, te man a topp diine ngir mu yërëm ko, te won ko mbëggeelam. Baay ji ñoom ñaar ñépp la bëgg te def na lépp ngir ñu nekk benn. Jokkoo ak Yàlla Baay bi moo lal jàmm, ak teeyaayu sunu bakkan. Yenn saa yi Yàlla dafa nuy may nu dund ci jokkoo ak ñu sell ñi ci know suuf. Nanu sant kon Baay bi ngir sunu njaboot gi ci kow suuf ak itam li Mu nu tànn ngir nu bokk ci Njabootam ga ca asamaan. |