Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
Home -- Wolof -- The Ten Commandments -- 04 Second Commandment: Do Not Make Idols
This page in: -- Afrikaans -- Arabic -- Armenian -- Azeri -- Baoule -- Bengali -- Bulgarian -- Cebuano -- Chinese -- English -- Ewe -- Farsi -- Finnish? -- French -- German -- Gujarati -- Hebrew -- Hindi -- Hungarian? -- Indonesian -- Kiswahili -- Malayalam? -- Norwegian -- Polish -- Russian -- Serbian -- Spanish -- Tamil -- Turkish -- Twi -- Ukrainian? -- Urdu? -- Uzbek -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson TOPIC 6: THE FUKKI NDIGAL YI - Ab ñag buy aar nit ki ci cib jéll
Fukki denkaane yu am solo yi ci Exodus 20 ci leeralu xebaar bu baax bi
04 - ŇAAREELU NDIGAL LI: Doo defar benn xërëmGàddaay 20:4-6 Ňaareelu Ndigal li dafay mottali Ndigal lu njëkk li te di ko faramfàcce. Looloo tax yenn kercen yi di ko jàppe ni as wàllu bu njëkk bi. Kàŋam yu bare jàpp nañu ne ndigal lu metti la ndaxte dégg-dégg bi dafa jafe,ba mujj indi ñàkk déggoo yu bare. 04.1 - LI ÁNDUL AK NATAALI KERCEN YIJullit yi ak Yawut yu bare dañuy tuumaal kercen yi ak doole,di leen jiiñ ne dañuy moy ñaareelu ndigalu AJI Kowe ji. Nii lañu nuy tuumaale: »Yéenay moy ndigal li gën a am solo. Dangeen di defar ay nataali Aji Kàttan ji yu kenn manul a waññi te di won nit ñi li seen xalaat yu matadi yi di meññ.» Topp ndigal loolu ba mu mat sëkk indiwoon na ay ñàkk déggoo yu tar ci diggante tarixa kercen yi. Am na yenn mbootaayu kercen yu lakkoon nataal yu ñu jàppewoon ni yu sell, ak itam jëmm ya ñu yettoon, ba noppi ñu taxawal seeni jàngu bopp. Nangu nanu ne manunu nataal Yàlla ci ndamam. Bépp nataalu Yàlla dafa koy jéem a toppandoo te di saaga Kilifteefam gi.Nataali nit ñu sell ñi, walla malaaka yi, ay fóoxal doŋŋ la. Yàlla moo gën a màgg, gën a sell, te ëpp kàttan ni nu ko sunu xel man a maye. Wuute na lool ak li nit ñi man a nataal. Bokk na ci sax nataalkat yu gën a mag yu mel ni Misel-ÀNS (Michel Ange)! Ci Biibal bi,ci ñaari fànna la Yàlla di feeñoo nit ñi. Li njëkk mooy ci kàddu gi muy séq ak ki koy déglu. Ňaareel bi mooy li Muy won Yonentam. Ci kóllëre gu Njëkk gi, li ci ëpp ci kàddoom gu am kàttan gi lay gën a wone boppam, waaye du ci ay janneer. Bi Doomu Yàlla ji soppalikoo ci kanamu Ndawam ya, ba mel ni Ku nekk ci ndamam, ñoom ñépp dañoo daanu ci suuf mel ni ñu dee, ndaxte sellaayu asamaan si dafa feeñ te daan seen selladi. Ki doon janneer manuloon a tekki li muy gis ba mu leer. Ci ay misaal rekk la ko doon man a tekkee. 04.2 - JÀMMARLOO AK NJAAMUG XëRëM YI AK YU NATAAL YIBu nu gëstoo bu baax ñaareelu Ndigal li, kon dinanu ci gis ne dañu araamal defarug lépp luy misaal Yàlla, te it Ndigal li dafa nuy aaye bépp bokkaale walla xërëm. Ňiy jaamu, walla di siggil yeneeni yàlla, ay yett mbaa ay nataal yu ñu móol, ñooñoo ngi tàbbi ci biir meram. Ca jamonoy Kóllëre gu Njëkk nga, ay jëmm yu rëy, yu ñu yett lañu daan taxawal ca cati tundi Penku bi gën a jege bi. Dañu leen daan yette ci xeer, te daan may ñépp ñu man leen a jaamu. Ca seen biir kër ya nag, waa dëkk ba dañu daan jaamu ay xërëm yu ñu defare bant, xeer, xaalis mbaa wurus. Képp ku gëmul jenn Yàlla ji am kepp, yaa ngi Koy ubbil buntu génn biy may jinne yi ak rab yu bon yi, ñu man a dalalsil seen bopp ci sa dund. Ca jamonoy Krist, Grek ya dañu daan njëkkënte ca kanamu seen yàlla ya ngir di fa wone yëgeelu yaram. Bu njëkk ba itam waa Misira, Asiri, ak waa Babilon, dañu daan def yu mel noonu. Loolu moo tax Musaa ak yonent ya daan xare ak seen kéem-kàttan njaamug xërëm yi. Tey jii man nanu gis xërëm yooyu yonent ya aramaloon ca ay jamano ñu leen di wone ci këri cosaan (muuse) ya ca keer, Bagdad ak Beyrut. Léegi nag ñoom ñooy yéem tukkikat yiy raatale eskale ya ca Akropolis ak bàmmeeli buur ya, lu raw la ko tànki Grek ya ak waa Misira ya defewoon ca njalbéen ga. Nit ki dafay jéem a feeñal li bët manul a tegu. Li ci ëpp nit ki du jéem a doylu ci kàddug Yàlla. Gis moo ko gënal déglu. Manul a xam lees gisul ak lees laalul. Looloo tax tele bi nekk ab nattu ci ñi bëgg a déggal ñaareelu Ndigal li. 04.3 - NATAAL YI YAWUT YI AK JULLIT YI ARAAMALTelewisoŋ yi ak wideo yeek bataaxal yi dañu leen di dalal ak bég mu rëy ci ëttu Jullit yi te di leen di jariñoo nu mu gën a gaawe, ak li ñu leen di tere lépp gannaaw 1350 at. Tere boobu dafa senn ci nataali rafetal yu arab yi, ba fés fépp ci cosaanu islamu Arabi Saudi, ci jàkkay Siin yi, Màkkaani buuri Marok ba ca Afrik Bët-Saalum. manees na seetlu ni ñaareelu ndigal li suxloo nataali Jullit yu neexul a firi yooyu, te di ay tóor-tóor aky toolu kër, yu ñu rëddal ay dig, ñu defare leen ak kayit, bant, weñ mbaa xeer. Àddina sépp sopp na tàppi yu penku ak seeni nataali tool yu rafet yiy misaal Àjjana. Ca Arabi Saudi, jéggikaayu tali yi nit ñi war a jaar dañu ci nataal nit ku amul bopp. Ba tey jii dañu tere ku nataal bopp. Waaye ca Iran, Turki ak ca réewum Ind, jullit ya boolewuñu seen bopp ca yooyu terey Alxuraan. Nataal nañu sax Mahomet ak Jibril malaaka mi, muy loo xam ne Julliti arab yi araamal nañu ko. Am na réewum arab mu defar ab film bu am solo ci Mahomet waaye wonewuñu benn yoon xar-kanamam. Ci film bi dafa mel ni lépp la Mahomet di gis aky bëtam, te di waxe ak baatam Moom ci boppam. Feeñu ci fenn ak jëmmam. Kon nag bu Kercen yi di defaral Jullit yi ay film yu aju ci yonenti-Yàlla yi malaaka yi walla KRIST, war nañu ci bàyyi xel. Yawut yi itam sàmm nañu bu baax ñaareelu ndigal li ba tax duñu sax nataal Yàlla. Ba TIT ma nekkoon jawrinu takk-deru waa Rom ju gën a mag ja tegee loxo Yerusalem ca atum 70, dafa waaxu dugg ca bérab bu sell baa sell, te di yaakaar ne dina fa fekk jëmmi wurus walla yëf yu am solo. Faf yaakaaram tas. Dara nekkuloon ca bérab bu sell-baa sell, ndaxte Yàlla xel la, du jëmm. Kenn manu ko natt mbaa yemale Ko ci ab nataal walla lu ñu yett. 04.4 - NDAX NATAALI KRIST YI DAŇOO FéWWALOO AK MBIND YI?Kercen yi jàppewuñu ñaareelu Ndigal li ni ko Yawut yi ak Jullit yi jële. Krist ca Juddoom la nekke nit. Ňépp man koo gis(teg Ko bët). Mu ne: ”Ku ma gis,gis nga Baay bi” (Yowaana 14:9). Li càkk gi doon mébét, ci Krist la mate. Biibal bi biral na ne ”Noonu Yàlla sàkk nit ci melokaanam, ci melokaanu Yàlla la ko sàkke, Mu sàkk leen góor ak jigéen.” (Njàlbéen gi 1:27) Aadama ak Awa dañu leen a tànnoon ngir ñuy wéy di lerxatal ndamu Yàlla. Tey jii itam nit ki dafa war a nekk seetub Yàlla. Ci Kóllëre gu bees gi nag, beral nañu nu loxo ngir nu am sañ-sañu bége li Yàlla sàkk lépp,ba man a nataal ay Tóor-tóoram, ay Malaam, ak ay Nitam. Waaye nag warunu leen di weccoo ak Yàlla mbaa di leen di jaamu. Lépp lu ñu sàkk manul a weesu lu ñu sàkk. Kon du man a tolloo mukk ak ka ko sàkk, te naka noonu kenn waru koo jaamu. Melokaanu Yàlla dafa soppiku ci doomu Aadama ba ko bàkkaar daanee, maanaam ba lu bon duggee ci àddina. Waaye Yeesu miy ñaareelu Aadama bi jekkalaat na melokaanu Yàlla ci nit ki. Dara umpalewul li tax Póol ne, Yeesu ”Mooy melokaanu Yàlla ji kenn gisul” (Kolos 1:15). Yeesu dund na, dee na te dekki na ngir bépp doomu Aadama. Kon book, ku mu neex nga nataale Ko ni nga ko namme; muy kanamu waa Afrik, mbaa waa penku, tugal walla arabia. Krist mooy melokaanu YàLLA ci Jëmmu nit ci biir bépp xeet ak aada. Mbëggeelam, Jàmmam ak Muñam duñuwoon ay waxi neen, waaye dañu tegu ci ay jëf yu leer. Ci Krist la Yàlla jaare ngir jegesi nu. Feeñoowunu ak kanamu xarekat bu ràññeeku, walla ak xar- kanam gu raglu, waaye ni am mbotem Yàlla mu nangoo yenu sunub àtte, ba wuutu nu, moo Ko taxoon a ganesi àddina. Dee na ndax sunuy bàkkaar ngir nu man a dund ak moom ba fàww. Jàngal na nu lan mooy sarax. Kurwaa bi mooy misaalu mbëggeelu Yàlla. Krist génn na bàmmeel ba, ndekkiteem bir na ca peeñoom, ndaxte won nanu yaramam bi Mu jële asamaan te muy lu leer naññ (LUK24:39). 04.5 - MELOKAANU YEESU CI DUNDU AY GAAYAMYeesu dafa sol xelam mu lewet mi ay taalibeem ngir mbëggeel gi, cellaay gi ak mbégte Yàlla gi man a feeñ ci ñoom. Dafa noo tànn ngir nu nekk ay niroowaaleem ci biir àddina su fees ak kiñaan ak dee. May na nu yiwu nekk ñuy dund ”ay bataaxali Krist” yuy wax ak sunuy njaboot, sunuy dëkkandoo, walla sunuy xarit jaare ko ci sunu doxalin. Yeesu dafa mooñ melokaanam ci nun ngir nu man a wone ki Mu doon. Képp ku daje ak gaayi Krist yu dëggu, muy ci Afrik, Asi, Tugal, Amerik, walla feneen, dina gis te ràññee leeraay ak jàmmu Krist ci seen xar-kanam. Saa yu xelum Yeesu mi ñu daajoon ca bant ba te dekki dëkkee ci xolu nit, naam, muy boroom alal mbaa déet, boroom njàng am déet, mag walla ndaw, dafay feeñal ci suuf leeraayu asamaan. Àddina si dafa def ñaari xaaj, maanaam néew-doole yi ak boroom -alal yi, ñuy kapitalist ak sosialist; waaye nag li waroon a am mooy xajjale ñi judduwaat, ak ñi dee ci biir bàkkaar. Bu nit nangoo Yeesu ci xolam, ñépp dañuy gis dundug Yàlla ci moom. Xel mu Sell mi du nu xiir ngir nuy wonewu mbaa di bàkku, waaye dafa nuy soññi ngir nu màggal Doomu Yàlla ji. Warunu xëcc nit ñi ngir ñuy xool ci nun, mu mel ne nun nooy ndeyu- mbillu solos àddina si. Gépp cant ak ngërëm, Mbotem Yàlla mi moo ko yelloo, Moom mi ñu rey (ni sarax)ngir nun. Maryaama, ndeyu Yeesu, ak ñu sell ñépp dinañu dal ci kow ñiy jaamu ay jëmm yu ñu yett aky nataal. Dinañu leen rajaxe fépp fu ñu man a nekk, muy ca saraxekaay ya, ca kër ya, ba ca mbedd ya sax. Kenn mosul a wone melokaanu Yàlla ba mu mat sëkk ku dul Yeesu. Kenn baaxul, ba mu des Yàlla. Yiwam kese moo nu goreel te sellal nu. Di ñaan ci turu Maryaama, walla ñeneen ñu sell ñi, di leen sukkal walla di leen ñaan wall, loolu moy ñaareelu Ndigal li la. Bu nu jëfee noonu dafay wone ne wéeruwunu ci sunu Baay bi ci asamaan waaye danuy ŋarale diggante Moom ak li Mu sàkk, te muy saay. Amul benn nataal, yett, walla taax, walla itam benn xeetu jaamukaay bu man a def ay kéemaan, walla muy maye kàttanu wéral doomi Aadama. Yàlla dafa noo musal jaare ko ci Doomam Yeesu Krist. Bépp xeetu bokkaale(Xërëm), ba ci biir Jàngu yi sax, Yàlla araamal na leen. Ci biir Kóllëre gu Bees gi, danoo am jokkoo gu amul kenn kuy dox ci diggante Yàlla sunu Baay ak nun doomam yi Mu bëgg. Deewug Yeesu jaare ko ci saraxam ak ci ñaan yi Mu nuy yëtal ca ndeyjooru Baay bi moo nuy biral ngëneel gi nu am. Doom ji sampal na nu jokkoo gu sës rëkk ci Baay bi. Ku jëriñoowul ngëneel googu, kon gëmuloo baayoo bi la Yàlla jagleel. Yiw wi, njubte gi, ak dund gi, ci Baay bi ak Doomam ji doŋŋ lanu leen jote jaare ko ci Xelam mu Sell mi. Kon nag, nanu sant Kenneefu Yàlla ji ak sunu xol bépp. 04.6 - XADARU YÀLLAKaamb gu rëy moo tàggale ñi bëgg Yàlla ak ñi Ko dummuuyu. Kaamb gu mel noonu moo nekk ci diggante xàccum mbugal mi ak ndigum ñaareelu Ndigal li. Nanu ko baamtuwaat, Yàlla dafa tagge boppam”MAN LA.” Noonu wone na ne kuy dund la, am li Mu bëgg, te man a wax. Nee na mooy Boroom biy sàmm kóllëre te du soppiku mukk, boole ci di doxal lépp. Dafa lëngoo ak nun ba fàww te bëgg nu delloo Ko wóllëre gi Mu nu jii, jaare ko ci déggal Ko ci kow sunu tànneef ak coobare. Yàlla sunu mbëggeel lay xaar. Bëggul di séddoo sunu njaamu ak ay xërëm, walla sampkati diine, buur, wurus mbaa xaalis. Moom kese mooy Yàlla te beneen Musalkat amul! 04.7 - ŇI BAŇ YÀLLA DINAŇU DAANUToroxte ñeel na ñi faalewul mbëggeelu Yàlla te di ko jàppe ni lu amul solo! Dañoo mel ni carub garabu reseñ bu ñu fàq. Nees tuuti ñu wow te saay. Fa ñuy mujje mooy ca safara su dul fay. Danuy bañ a lëngoo ak Yàlla miy sunu Aji Teen rax ci dolli danu Koy wor ci diine, ndaxte danuy ubbeeku ci yeneeni déebaadéeb, aky xërëm, walla ay kàttan yu sellul, walla itam nuy jàppe sunu bopp ni ay gennwàlli yàlla. Yàlla du bokk ak kenn ndamam ku dul Doomam ji, ak Xelam mu Sell mi. Kenn du sàkk gannaaw Moom. Moom kese mooy Àttekat bi ba fàww. Bu nit ki wëlbatikuwul, te jublu ci Yàlla ju dëggu ji, waaye di xool ci yeneeni yàlla, mbaa muy jàppe boppam ni ku man a doxal lépp, kon dafay tiitaru te di tëj xolam ci mbëggeelu Ki ko sàkk. Nit ku mel noonu dafay néeg te soxor. Dafay jéem a noot ñeneen ñi, te bañ leen a jariñ. Nit kooku bëggul Yàlla te bëggul ay dëkkandoom. Xamul àddina te it umpale na ay jafe-jafe xelam, ndaxte dese naa am ay ñag maanaa yu amul àpp. Li loolu di jur mooy xelam dootul tooy ci dara, te ay doxalinam di gën a ñaaw. Dafay mujj wacc lépp lu jaadu, jubadi, ba raw sax mala muy xataraayu ngir dund. Yàlla dafay dummuuyu ñiy wéy ci bëgg Koo sore, te Mu jéem leen a artu ba tàyyi, te won leen mbëggeelam. Dafa leen di bërgal ak seeni nafsu ba ñu sànk seen bopp.Buur ba Saül ak Yudaa Iskariot doy nañu nu ci ni misaal. Ni Yàlla di àttee benn benn nit ñi, noonu itam lay àttee am réewum lëmm. Boroom kër yi sax dañuy xiiroo ak seeni soxna, ba loolu di xajamal dundu njaboot gi. Noonu la ñàkk orma di lawe ci maas-o-maas. Njaboot gu dëkk ci muusante ak séeneen dina ko wone ci li ko wër ak ci doxalinam. Bu njaboot gi dëkkee ci ñàkk a fonk nit, walla nekk yéeféer sosialist, li muy jur benn la. Li njaboot giy dund, ci bëti xale yi lay feeñ. Am na ay kër yu laal mbiri xérëm,walla di yee ñi dee, mbaa di seet jaare ko ciy jinne aky rab, ngir yaakaar ci wér ak feeñal ay kumpa yu làquwoon. Yeesu bañ na yooyu doxalin yépp, waaye nag jañaxul ki nangu tuub ay bàkkaaram. Kooku kay, dafa koy dalal ak mbég, te yewwi ko ci jéngi Seytaane. Yeesu nee na: ”Kon nag bu leen Doom ji defee gor, dingeen nekk ay gor tigi.” Yowaana 8:36. Kilifteefu Krist weesu na sunu dégg-dégg. Yàlla dafa nuy xamal ne gépp njaboot guy dëgëral xolam dees na ko mbugal ba ca ñetteelu maas ga, ba sax ca ñeenteel ga,ba mu des bu ca rëccu gu mat sëkk tàbbee, te waa kër ga yépp dogu ngir dellu ci Yàlla. Mag ak ndaw dañuy mos ca la maam ya ñamoon ci lu selladi. Waaye nag warunu ñaawlu xol yi geru, xanaa kay danu war a seet fa mu leen dale, te def lépp ba bëgg leen. Am na ay yawut ak ay Jullit yu ñu ŋoy ci seen cosaani maam, ba weddi “Doomu Yàlla ji. ”Ňoom ñépp dañoo ànd ci mennum xel ngir weddi Musalkatu àddina si. Képp ku bëgg a rëcc ci yooyu kàttan yu juuyoo ak Yeesu Krist, danga war a dog sa àndadoo ak ñoom te ndax Yeesu rekk, nga rocciku ci yooyu buumi cosaan. Bu nu dénkee Yàlla sunu kaaraange njaboot, ak sunu jàmmu réew, dinanu gis ni sunu Baay di jëfe. Kon dina sàmm sunu ëllëg. Dafa nuy biral saa su nekk ne: ”Man maay Boroom bi, sa Yàlla, sa Baay bi lay bëgg saa su nekk. Xam naa la, te sa tur laa lay woowe, Maa la moom, taqal ci Man, te génn ci buum yu sellul yi te bon. Wóolul sama Kóllëre ak sama Kilifteef, noonu, dinga jot sa ngor, te mucc ba fàww.” 04.8 - BAARKE BU AMUL ÀPP NGIR ŇI BëGG YÀLLA CI DëGG-DëGGKépp ku bëgg Yàlla te di Ko màggal, dangay nafar Kàddoom, te di dunde Kàttanam. Dafay ràññee xóotaayu yiwu Yàlla ci dundam, te di Ko gërëm saa su nekk ngir goreel gi Mu ko may ci kow Muñam gi. Dafa Koy won mbëggeelam te di Ko sant ak xolam bépp. Bépp way-gëm bu am kóllëre dafay gis bés bu nekk ay xéewal, ag kàttan, ay barke, ak wommat gu leer ci Kàddug Yàlla gi. Loo xalaat ci as coro lu jot bataaxalu faram, te jéemu ko ubbi sax, waaye dafa koo jallax nee fàtte ko? Kon dinga wax ne nobu ko. Coro lu dëggu dafay yakkamti jot bataaxalu faram, te bu ci jotee benn, ci saa si la koy dàjji, jàng ko, jàngaat ko ba lépp leer ci xelam. Kon bu nu bëggee Yàlla, danu war a jàng Kàddoom ni ab bataaxalu mbëggeel bu jóge asamaan te ñu jagleel nu ko. Da nu koy jàng ba mu mokk, te deñc baat ya ca ëpp solo ci sunu biir xol. Sunu xol dafa fees ak Kàddug Yàlla, Mi nuy may nu mottali coobareem. Bu waajur yi ñaanee ak seen xol bépp ngir seen njaboot, kon dinañu gis baarke biy wàcc ci kow waa kër gi. Rax ci dolli seeni doom duñu màgg ci biir puukare walla ci déggadi; waaye dañuy am taxawaay bu dëgër. Dëgg la ne waajur yi manuñu woñ loxoy xale yi ba ñu gëm Yeesu Christ, rawatina ñu bëgg leen a génnee ci seen coxorte ci kow di leen di duma (dóor). Waaye misaalu baay-walla ndey -ju nawlu, dafay meññ ndànk ndànk ci xelum gune yi. Xale yi, jëfi mag ñi lañuy gën a jàpp seeni wax. Yenn sa yi, ay bëti ndey man nañoo gën a man a wax làmmiñam. Bu génnee àddina sax, mbëggeelam dafay law di wàlle. Yàlla dafa dige ne dina baarkeel ñi Ko bëgg ba ca seen junneelu maas! Bu nu jàppee ne maas man na nekk 25 at, kon 25000 at Yàlla dina ko baarkeele jaare ko ci kenn kese ku am ngëm dëggantaan. Bu nu xalaatee ci lu jëm ci sëtaati-sët ci biir ag njaboot gu yàgg, dinanu ci man a waññi ab limu maasi-maas bu jéggi dayoo; boo xam ne sax moo ëpp” xarekati jaww ji “te ñépp man a baarkeelu ci ni seen ngëmu maam ya déggalewoon Boroom bi. Yàlla dafay biral ay ñoñam yi Mu taf ci xolam ne dinañu nekk teenu mbëggeel ngir ay téeméeri nit. Waaye nag ab taalibe Yeesu du bàkkoo mukk ne mooy teenu jullite gi, man na wax kay ne ab wéyelekaayu yiwu Yàlla la. Yàlla dafay xëppe yiw ci kow yiw gu laajul dara, baaxe ko ñi Ko bëgg, te wóolu Ko. Bu nu mosee baarke yi nu jote ci sunuy waajur ci yaram, mbaa ci diine, kon dinanu man a natt ngëneeli aada ak cosaani àddina si. Bu Kàddug Yàlla gi duggee ci xolu ab dëkk bu ndaw, ay taax,w alla sax ay nit ci diirub ay téeméeri at, kon dinanuy yëg ba tey jii meññeefu baarke mi. Su amee ñu Yeesu goreel, dañuy sant te di dimbalante ci biir mbég. Bu Yàlla manee ñaaxe Xelam mu Sell mi ab cosaan, kon waa kër gi, jàngukaay yi, koom-koom gi ak politik bi yépp dinañu wàllu ni nu ko xalaatewul a gise sax. Li juuyoo ak loolu lépp nag mooy ne dafa am ñuy màggal ay yàlla yu sellul ca IND, ñee di jaamu seeni maam ca SIIN, walla am ñuy aaru ci njaamug ay xërëm aky mocc ca Afrik. Réew yooyu yépp tiitaange moo leen noot, teg ci buumu njaamu xel, ak ñàkk fit wu dal. Li ci ëpp genn góor rekk mooy xàwwi sutura ak sagu jigéen, ngir defloo ko li ko neex. Xare ci diggante ay xeet, walla ay réew, ñooy tax ba kenn du jëm kanam, te néew-doole bi di gën a miskiin. Boo duggee ci dëkkub muslim, indu, walla kercen, lu mu gaaw-gaaw dinga seetlu xel mi fay daayarlu. Mala ya sax xam nañu ndax dañu leen di dóor saa su nekk, walla ab doktoor moo leen di toppatoo. 04.9 - CI GÀTTAL: TEQALIKOO GU WÓOR TE LEERBaarke biy tukkee ci waajur yu gëm yi manees na koo gis ci doxalinu waa kër gi, walla ci ñenn ci ñoom; te loolu dafay wone mbëggeel gi seeni maam séqoon ak Yàlla. Waajur yu mel noonu dañoo ñaan, liggéey ak seen kéemkàttan, te dunde ak ngor, ba ca seen màggataay. Li am mooy ne àddina si, ñaari ponk doŋŋ ñoo ko xar ñaar, ñuy ñi bëgg Yàlla ak ñi Ko bañ. Soo bëggee Yàlla Baay bi, kon dinga wéeru ci Moom nib doom te meññal gàñcaxu mbëggeelam gi. Waaye soo mammee të- këcc wooteb Yàlla, dangay sore njaamu gi. Amunu benn mbetteel bu nu gisee tey jii mbëggeelu ñu bare di wàññeeku -Bu nit ki delluwul ci Yàlla, ab jànju coxorte lay mujj a doon. Fippu ci kanamu Yàlla, ay xalaati musiba yu jéggi dayoo lay jur. Karl Marx ku déggaloon Yàlla lawoon cig waxambaaneem, waaye dafa duggoon ci ay gisaane aky xërëm. Noonu la def ba réeral ay tamdareti (Milioŋi)doomi-Aadama yi mujje tànn diine biy weddi am-am ngir man a dund. Moonte nag ay wayam manuñu may àjjana ci kow suuf liggéeykat yi, bu fekkoon sax ñungi tëkkoo Yàlla ak ay kurpeñ. Képp ku weddi Yàlla, Miy teenu mbëggeel gi ak dund gi, te di jàmmarloo ak ñeneen ci turam, yaangi xamb merum xolam ak naqaram. Kooku dina góob merum Ku sell ki fii ba bésub àtte ba. |