Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- The Ten Commandments -- 03 First Commandment: You Shall Have no Other Gods Before Me
This page in: -- Afrikaans -- Arabic -- Armenian -- Azeri -- Baoule -- Bengali -- Bulgarian -- Cebuano -- Chinese -- English -- Ewe -- Farsi -- Finnish? -- French -- German -- Gujarati -- Hebrew -- Hindi -- Hungarian? -- Indonesian -- Kiswahili -- Malayalam? -- Norwegian -- Polish -- Russian -- Serbian -- Spanish -- Tamil -- Turkish -- Twi -- Ukrainian -- Urdu? -- Uzbek -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

TOPIC 6: THE FUKKI NDIGAL YI - Ab ñag buy aar nit ki ci cib jéll
Fukki denkaane yu am solo yi ci Exodus 20 ci leeralu xebaar bu baax bi

03 - NDIGAL BI JëKK: “Bul am yeneen yàlla ndare man”



Gàddaay 20:3
"Bul am yeneen yàlla ndare man."


03.1 - Ni ŇUY JAAMOO XëRëM TEY JII

Ci réewi taax yu mag yi, barewul lu nu ciy gis nit ñuy jaamu ay xërëmi bant, xeer walla wurus. Waaye bu nu demee penku ca Asi, walla ci Afrik, danuy gis ñu bare di jaamu ay xërëm yu takku boole ci tiitaange gu rëy.

Am na ab bataaxalu Mbootaayu Ropplaanu Indu bu wonewoon ab nataalu Durga miy yàllay xare ju jiggéen ji, ñu wone ko ak juróom-benni loxoom yi man a faat képp ku ko soong. Ay boppi nit ñungi tasaaroowoon ca la wëroon Durga. Ni mu amewoon doole ci xare moo taxoon ba képp ku ko jegewoon, safara sa doon génne ca gémmiñam lakk la.

Ca Indu ya danu fay gis ay ñay yu ñu yett ci bant,te ñuy misaalu yàlla bi tudd Ganapati. Yenn saa yi Indu yi dañuy indi ay tóortóor yu xeeñ di leen teg ci seen kanam. Ci yenn xew-xew yu mag yi itam dañuy Solal ay caqi tóortóor ñayi palastik yu sut ñaar ba ñetti yoon kuuyu njamala. Mbooloo mi dafa leen di doxantoo ci mbedd yépp ba noppi sànni leen ci dex mbaa géej, te di am yaakaar ne napp gi dina baarkeel, te diiwaan bi dina aaru ci mbënn yiy ànd ak yàqute.

Am na sax ab xew-xew boo xam ne dañuy indi ay junniy-junni nag ca jaamukaay ba wis leen ndox mu sell ngir may leen dund gu wér. Bu loolu wéyee dañuy diw ci seen bejjën yi ay melo yu xàññaaral ni misaalu cellay gu ñu ber.

Bu nu demee mbartalu Ladax, ca gannaawu Imalaya, maanaam réewu waa Budaa, dañu fay gis ñu móole wurus Budaa ak jëmm yu rëy-a-rëy yuy ree; noonu nit ñi di leen sujjootal ak màggal gu mat sëkk. Ba fi nu tollu tey jii, benn ci ñett ci àddina si mungi jaamu xërëm yi, te noonu mungi moy Ndigal lu njëkk li. Jaamukatu xërëm dañoo gëm kàttanu yett yooyu ak seeni dellusi ci biir nit ñi. Waa Afrika ak waa Indu yu bare ñungi lëngoo ak yooyu diiney aada. Ňeneen nag, seeni maam lañuy jaamu. Waaye bu ñu mosoon kilifteefu Yeesu, kon dinañu yewweeku ci bépp ragalu jinne yi ak rab yi, xërëm yeek seet yi. Bu ko defee dootuñu soxla ay léemu walla ay per yu bulo te dinañu tàggoo ak xërëm yu dee yi, ndaxte Yeesu dina leen aar ci lépp lu bon lu leen bëgg a sonal.

Sunu Baay bi ci asamaan dafa nuy rawale ci bépp fitna, ba sax ci nooteelu jinne yi, te dafa nuy yewwi ba nu set wecc ci liggéeyante. Deretu YEESU KRIST, Doomu Yàlla ji, mooy Aji Kaaraange ci jépp kàttan ju bon. Móolu yi ñu bind mbaa ñu jibal leen ci turu dooley lëndëm gi te di leen jagleel gaayi Krist yi, turu sunu Boroom bi lanu leen di rajaxe. Mooy tatta ju wóor ngir képp ku làqu ci Moom.


03.2 - XëRëMI TEY JII. (BOKKAALEY TEY JII)

Rëccu amees nag bi melokaanu jaamu ju bees duggee ci réewi taax yi gën a màcc ci koom-koom. Yàlla ya ñu daan yett, léegi, ay daamar (woto) telewisoŋ walla ay nit yu siiw, lañu leen wuutoo. Léegi nit ki, xam-xam ju aju ci masin la gën a wóolu Yàlla jiy dund. Nit dafay toog ci biir wotoom di ko dañal ni mu gën a gaawe, ci godoroŋ bi, te fekk doole motooram rekk la wóolu. Woto mujj na nekkal nit ki ab bokkaale. Bànni-Israel dañu doon fecc di wër sëllu wurus wa, waaye waa jamonoy tey, woto bu gën a bees lañuy wër. Ki ko moom dafay rënk xaalis te di xaru ngir wotoom bi; dafa koy raxas, di ko joonj te di déglu motoor bi lu gën a teeylu li muy may nopp ñiy wax ak moom. Jot gu bare ak xaalis bu takku la koy jagleel, maanaam lu ëpp li muy def ci néew -doole yi. Ndax nit ki dafa nekk léegi jaamu masin yu bees yi? Ay nit ñu bare dañuy jubali ca estad ya ngir seetaani rawante woto ya, walla yu nit ña. Waaye ñu néew ca ñoom ñooy toog ca baŋi jàngu ya ngir bokk ca ndajem màggalu Yàlla ga.

Yeesu dafa nu artu ci mbëggeelu xaalis. Nee na « Kenn manul a jaamoondoo ñaari sang;fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp kenn ki, xeeb ki ci des. Manuleen a boole jaamu Yàlla ak jaamu alal. (MACë 6 :24) « Mbëggeelu xaalis mooy reenu gépp mbon : » Sosialism ak kapitalism ñoo yem ay mébét. Fi ak kapitaalist yi ñungi fees dell ak xaalis, sosialist yi ñungi wut a nekk ay boroomi alal te di ko jaare ci ay njuuj-njàcc ak ay jaay doole. Ba fi nu tollu nii, nit ñaa ngi fecc di wër sëllu wurus wi. Bu la kenn nax, kenn du foontoo Yàlla. Kenn manul a jaamoondoo Yàlla ak xaalis. Yeesu amuloon alal, waaye ku féex lawoon. Artunawoon taalibeem ya bu baax ci lu jëm ci alal ba Mu leen waxee ne: ”Ňiy wut a fees ak alal dañuy daanu ci fiiri nattu” (1TIMOTE 6:9; Macë 19:24)

Bokkaale bi gën a sut yeneen yépp, muy ci aada,diine ak cosaan, mooy sunu”MAN”. Ku nekk dangay yaakaar ne yaa gën ñépp, gën leen a taaru, te ëpp leen solo. Boo ko xalaatul sax, yaangi koy mébét ci sa ruu. Ku nekk dangay yaakaar ne yaay collu àddina si. Am na bés, ñu laaj ab xale bu jigéen bu am ñetti at ne ko: ”Loo bëggoon a doon?” Noonu mu tontu ne: ”Ab Monumaa(Yett bu rëy)” “Lu tax?”-“Ngir ñépp di ma xool. ”Tiitar ak bopp-sa bopp, ci sunu deret la nekk te dafa juuyoo ak suufeelug Krist. Yeesu nee na: ”Nan ngeen man a gëme, yeen ñiy ndamoo ci seen biir te fekk yóotuwuleen Ndam liy jóge ci Yàlla doŋŋ?” ”Lewet naa, te suufeelu, noonu dingeen am seen noflaayu ruu. Waawaaw sama yen diisul, te sama ngàcc woyof na.” ”Képp ku bëgg a rawale bakkanam, dina ko ñàkk, waaye képp ku ñàkk bakkanam ndax man, dinga ko jotaat”, ”Yów nag, ay mébét yu rëy nga am! Fàtte leen!” (YOWAANA 5:44; Macë 11:29-30, 16:25-26, Yeremi 45:5)


03.3 - NDAM CI KOW NJAAMUG BOKKAALE YI (Xërëm yi)

Lu tax jaamu yeneen yàlla lañu jëkk a tere ci ndigal yi, te it muy ndigal li ci ëpp solo? Li am, mooy ne jenn Yàlla doŋŋ moo am. Ňépp ñi siiw ci àddina si dañuy saay benn bés. Yàlla rekk mooy dund ba fàww. Moom moo nu sàkk; ndam ak màggaay ñeel nañu Ko. Ci Moom la dunyaa gépp sax. Sunu bopp-sa bopp dafa waroon di moxoñoo bés bu nekk ba àgg ci man a surgawu Yàlla ak mbég. Danu Ko war a liggéeyal. Du alal ja nu rënk ca baank ba, walla sunu wér-gi-yaram ak sunu man-man ñoo war a nekk sunuy reeni bakkan, waaye Yàlla kese la war a doon.

Ibrayma soppoon na lool Isaaxa, doomam àqan, ji ko waroon a donn te mu séentuwoon ko ba tàyyi. Dafa daan toppatoo xale bi ba mu mel ne sax dafay xaw a fàtte Yàlla. Noonu Yàlla daldi nattu jaamam bi. Mu ne ko, na ko jébbal doomam, ji mu sopp lool nib sarax. Ibrayma bëggoon na def lool li mel ni lu manul a am, maanaam jébbale doomam nib sarax ngir màggal Yàlla. Waaye Yàlla, ca simili yu mujj ya la téye loxo Ibrayma ngir mu bañ a jël bakkanu xaleb ndig ma, rax ca dolli Mu jox ko am kuuyu xar ngir mu wuutu ko. Ndamul Yàlla jolly na bi Ibrayma ak xolam bu tiis ba, demee ba nar a tàqalikoo ak doom ja. Wone na ne Yàlla la gën a fonk Isaaxa.

War nanu di seetlu sunu bopp yenn saa yi ba ràññee bokkaale yu ndaw yi ak yu mag yiy dog sunu diggante ak Yàlla. Bokkaale yi man nanu nekk ay téere, ay takkaay , ay natal, ay pàttali, bëgg-bëgg, lu nu tàmm, xaalis, kër, ay mébét, ak yu mel noonu (a.ñ.s.): Ay nit sax man nañoo këf sunu xol.

Fiiri bokkaale yiy daaneel nit ñiy jàmmaarloo ak seeni kilifa dañu ne fàŋŋ .Réew yu bare teguwoon nañu ci loxo ñu mel ni Napoleon,Ataturk,Hitleer,Naseer Xomeyni, ak ñeneen,noonu jàppoon nañu leen ci buumu njaam.Waaye seeni téere pàttaliku ya ñu bindoon ,dañu leen a yàq ba ñu génnee àddina.Yonnent-YàLLA Yeremi artu na askan wa ci bépp jaxasoo ak yeneeni askan ak bépp wallu bu ñu leen bëgg a ñaan. »Ku wóolu doom Aadama yaa torox, ki wékku ci nit kese ,te xolam sore Aji sax ji . » (Yérémi 17 :5).

Am na ñoo xam ne niti sinemaa yi ñoo leen ñor walla ñiy raw ci tàggatkati yaram yi, mu mel ni ñooñu ñooy seeni Yàlla. Tëgg yi ñuy amal ci estadd yi dañu leen di solu ba ñu nekk ay xuus- maa -ñàpp yu manatul téye seen bopp ci géew bi. Ndànk nag de! waxunu ne dimbali ñeneen te weg leen loolu bàkkaar la. Waaye gën a wékk sa kóolute ci nit ki te ber Yàlla, loolu worum diine la. Ndax Yàlla fasul ak nun kóllëre gu amul àpp ?Umpalewunu li tax Krist woowe ñooñu « Maas gu bon te di njaalookat », ndaxte bëgguñu Yàlla ak seen xol bépp, weguñu Ko te wóoluwuñu Ko.

Tey jii Jaamu ay bokkaale mungi feeñ ci ay anam yu bare yoo xam ne tàggaloo ak Yàlla moo leen jur. Boroom bi dafa fiir, te Moom rekk moo bëgg a moom sunu xol. Bëggul as wàll ci sunu mbëggeel, walla sunu dégg-ndigal, waaye dafa noo bëgg a aakimoo ba fàww. Kon book xërëm yeek yeneeni bokkaale yépp dañoo war a génn ci sunug dund. Danu war a yeesalaat sunu wóllëre digante sunu Baay bi ci asamaan ak nun. Laajal sa bopp lii ci dëgg-dëgg : »Yan bokkaale ñoo làqu ci sama dund ? nan laa leen man a daxe ba fàww? »


03.4 - NDAX NGëMU KERCEN JUUYOO NA AK NDIGAL LI JëKK?

Jullit ak Yawut ñoo bokk nangu ni Kercen yi dégge Fukki Ndigal yi. Waaye dañuy tuumaal kercen yi ne dañuy moy yoon wi ci seen ngëm.” Yeen kercen yi, ñu jubadi ngeen » loolu lañu nuy wax, teg ci “ndaxte dangeen di moy ndigal li jëkk te gën a am solo. Dangeen di saaga Yàlla naan ñetti Yàlla ñoo am, teg ci sax ne kenn ci ñoom dafa dee ca kurwaa ba. ”Yawut yi ak Jullit yi dañuy jiiñ Kercen yi gëm Kenneef gi am, ci diggante Ňett bi Yàlla nekk.

Nan la Yeesu tontoo ci tuumaa yu mel noonu ? Bés bu nekk daanaka Yeesu dafa daan jànkoonteek coongi ay maasam. Moom leeral na naññ Jokkoom ak Yàlla : « Man ak Baay bi benn lanu >>Yowaana 10 :30. Mosul wax ne : »Man ak Baay bi ñaar lanu », waaye, benn lanu! Nee na itam : »Maangi ci Baay bi, te Baay baangi ci man. »Laata ñu Koy jàpp, Yeesu ñaanal na ay taalibeem: »ngir ñu àndandoo nekk benn ni nu nekke benn Man ak Yów »yowaana 17 :22. Kàddu yii seedee nañu Kenneef gi am ci diggante Ňett yi. Barele bi nuy gis fii, benn lay joxe. Dëgg googu raw na xam-xamu waññi. “Kenn manual a wax ne “Yeesu mooy Boroom bi “ su ko ko Xelum Yàlla waxloowul. 1Korent 12 :3. Lii dëggu ngëm gu wér péŋŋ la, ba fàww. Bu nu nanguwul a dékku Xelum Yàlla mi, kon dunu man a xam mbóoti ngëm yi.

Yeesu nee na:” Ku ma bëgg dina sàmm sama Kàddu. Sama Baay dina ko bëgg te nun dinanu ñów ci moom, te dëkk ci moom. ”Yowaana 14:23. Yeesu digoon na ay taalibeem ne Xel mu Sell mi dina dëkk ci ñoom. Biral na leen itam jokkoo gu sell gi am ci digganteem ak sunu Baay bi ci know te ñoom ñaar ñépp dinañu dëkksi ci xolu seeni way-gëm yi.

Kercen yi gëmuñu ñetti Yàlla yu beru, jenn Yàlla doŋŋ lañu gëm juy feeñoo ni Baay ji, Doom ji, ak Xel mu Sell mi. Bu nu nangoo Kenneefu Ňett ñi, wàccunu yoonu ndigal lu jëkk li, xanaa kay danu koy matal. Xelum Yàlla wàcc na ci sunu xol ba nu deewug Yeesu ca bant ba jubilee ak Yàlla. Xel mi am kóllëre dafa nuy soññ ngir nuy woo Yàlla sunu Baay te Mu Sellal turam ci sunu dund gépp. Genn ngëm gi lanu yemale am ci sunu Baay bi, ci Yeesu ak Xel mu Sell mi, te di Ko bëgg ak sunu xol bépp ndaxte “mbëggeelu Yàllaa ngi baawaan ci sunu xol jaarale ko ci Xelam mu Sell mi mu nu may.” Danu war a nangu ne Kenneefu Ňett ñi, Xell mu Sell mi dafa ko làq ki judduwaatul, te nanguwul a jéem a xam dëgg gu am solo googu.

Li am nag ne, ALxuraan soongul kenneefu Ňett ñi bi nga xam ne moom la Kercen yi gëm. Waaye ñi muy jàmmaarlool kay ñooy moykatu diine yi mbootaayu Krist yi sax weddi. Alxuraan li muy xeex mooy Kenneefu Baay bi, Yaay ji, ak Doom ji(Sóoratul taabalu yekk bi 5:116). Rax ci dolli bañ na itam ne Yeesu doomu Mariyaama, mooy Yàlla (Sóoratul aj-Ma'ida 5:17,72) walla sax ñetteel bi rekk (Sóoratul al-Ma´ida 5:73). Ci Biibal bi Kenneefu Ňett ñi ci Benn, Yàlla la, maanaam Kenneef bi dajale lépp, Mennum Aji Sax ji, Kenneefu Baay jiy wax jaarale ko ci Kàddoom, te di jëfe ak Xelam. Nun danu weddi Kenneef giy nangu Baay bi, ndey ji, ak Doom ji ci mbindu doomu Aadama ngir naan Yàlla mooy Yeesu doomu Maryaama. LI nuy biral te gëm ko mooy Yàlla Baay bi, Yàlla Doom ji, ak Yàlla Xel mu Sell mi, te nekk jenn Yàlla ji am doŋŋ.


03.5 - LAN LANU KÓLLëRE GU NJëKK GI DI WON CI KENNEEFU ŇETT ŇI?

Kóllëre gu NJëkk gi dafa ëmb ay pàcc yu am maanaa ci ni Yàlla nekke benn, ci Cellaayu Kenneefu Ňett ñi. Alxuraan sax manul a weddi loolu.

Sabóor 2:17,12 dafa feeñal li Yàlla namm ci Yeesu, junniy at laata Muy juddu. ”Yaa di sama Doom,Maay sa Baay tey. ”Artu na askan wa itam ne leen “ Sujjootalleen Doom ji, ngir ragal meram jóg, ngeen ne mes sànku.”

700 at laata Yeesu di nu ganesi, Esayi bind na ci saaram 7 :14 ne « Boroom bi ci boppam dina leen jox ab misaal: Jànq baa ngi nii ëmb te nar a wësin doom ju góor te dina ko tudde Emmanuel (liy tekki “Yàllaa ngi ci sunu biir “)

ESAYI 9 :5 moo am Ndig lu rëy li : ”Ndaxte doom juddul nanu, mayees nanu doom ju góor, te dina yor nguur gi; dees na ko tudde : Diglekat bu yëeme bi, Yàlla mi man lépp, Baay ju, sax Buuru jàmm.” KàDDU Yii wàccee asaman te nekk ci Kóllëre gu Njëkk gi ñooy seede ni Yeesu bokkee asamaan ak bennoom gi mat sëkk ak Yàlla Baay bi.

Ci téereb 2Samwel 7:12-14 Yàlla dafa ci dig Buur Daawuda ne ko, kenn ciy doomam” yiy jóge ci geññoom” dina nekk Doomu Yàlla. Booba lañu tàmbalee dolli turu “Doomu Yàlla” ci “ALMASI” walla “ Doomu Daawuda.

Ci Sabóor 110:1 lii lanu ciy jàng : » Kàddu yu tukkee ci BOROOM bi ngir sama boroom: ” Toogal ci sama ndeyjoor ba ma def say noon sa rëpéelukaayu tank! ”Ndax ñaari boroom am na ?Mukk! Aaya bii dafay wone Kenneef gi am diggante Yàlla Baay bi, Doom ji, ak Xell mu Sell mi.

La ko dale ca njalbéen ga la Yàlla tàmbalee waxe ci barele : » Nanu bind nit ki ci sunu melokaan, ak ci sunu misaal.” (NJalbéen 1:26)

Kon aaya bii mungi nuy won ne seedeb kenneefu Xel mu Sell mi jógewul ci xalaatu kercen. YàLLA wone na boppam ay junniy-junni at laata Yeesu di nu ganesi. Léegi nag, kan moo sañ a bañ peeñum YàLLA?


03.6 - Ay Aaya Alxuraan yuy wax ci nekkinu Krist ni Boroom bi

Du sax Juróomi Téere yi (Pentatëk,walla Tawret), Sabóor ak Yonent yi rekk ñooy seedeel kenneefu Yàlla Baay bi, Doom ji ak Xel mu Sell mi, waaye Alxuraan ci boppam am na ay aaya yuy dëggal seede kercen bi. Bu fekkoon ne Jullit bi doon na jàng Alxuraan bi ak xel mu ubbeeku, kon dina doon nangu aaya yiy wax ci juddug Yeesu doomu Maryaama xiig bi. Yeesu dafa juddoo ni Kàddug Yàlla amul kenn (nit) ku dox ci diggante bi. Yàlla moo ëf Xelam ci Maryaama mu xiig mi, noonu Yeesu daldi juddu (Sóorat al Abiya´21:91, al-Tahrim 66:12).

Sóorat yu mel ni Al`Imran3:45, al-Nisa´4 :171 ak Maryaam 19 :43, dañuy biral ne Yeesu mooy kàddu Yàlla gi wàcc ci melo nit te it Xelam la. Aaaya Islam yii dañuy feelu Injiilu Yowaana bi mu nee “Ca njàlbéen ga fekk na Kàddu gi am, te kàddu gi ma nga woo nak Yàlla, te kàddu gi Yàlla la woon…kàddu gi ñów doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nanu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg.” (Yowaana 1:1,14)

Ci sóoratu Baqara 2:87,253 ak al-Mai´da 5 :110, danu ciy jàng ne XEL mu SELL mi Moo dooleel Yeesu (walla itam Xelum Cellaay mi) ngir Mu man a sàkke picc ci suuf si, ba noppi ëf ko ngelewal dund, mu dun. Wéral na muuma baak gaana ga, te dekkal ñu dee ci kow mayug (Ndigalu) Yàlla. Alxuraan dafay wone ay yooni -yoon jokkoo gi dox diggante Yàlla, Krist, ak Xel mu Sell mi. Kon lu tax Jullit yi di siisu ci kanamu Yàlla ak Almaseem bi?

Sóoratu Maryam 19 :21 nee na: ”Dinanu ko def ni mandarga ngir nit ñi; yërmande gu jóge ci nun." Doy na waar ni Yàlla maase nun gi ba noppi woowe Yeesu Yërmande ju Boroom yërmande ji. Loolu dafay wone ne Kris ak li mooñu ci Yàlla benn lañu.

Aaya yu bare ci Kóllëre gu Njëkk gi ak ci Alxuraan biral nañu Kenneefu ñett ñi. CI biir mbégte mu rëy nanu ànd ak malaaka yi ngir màggal Yàlla: "Sell, sell, sell, Boroom bi, Aji Kàttan ji, Ndamam daj na àddina si yépp!" (Esayi 6 :3) Ňetti yoon yi ñuy wax "sell" Dafay wone ne Baay bi sell na, Doom ji sell, te XEL mi sell na, ñu booloo nag nekk benn sellandoo.


03.7 - NGëMU KERCEN CI NEKKINU YEESU NI BOROOM BI

Ndawi KRIST yi juumuñu bi ñu seedeendoo Yàlleefam. Naam bakkanam xejoon na ca, Póol jibal na ci diggu mbooloo ne: "Krist mooy melokaanu Yàlla mi kenn manul a gis"(Kolos 1 :15). Yowaana nangu na ne: "Kàddu gi ñów, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nanu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji Mu am kepp. (Yowaana 1 :14). Ndaw li PIEER seede na ne: "Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla AJI Dund ji." (Macë 16 : 16).

Jawrinu Nicée nii la tënke ngëmu kercen: "Krist Yàlla la ju jóge ci Yàlla, Leer gu jóge ci Leer, Yàlla dëgg ji jóge ci Yàlla, ñu jur Ko, te kenn sàkku Ko, te bokk ak Baay bi menn melokaan."

Ndax Yawut yi ak Jullit yi ndax xam nañu ne dañuy yemale teewaayu Yàlla ci seeni diine yu xat yi? Kan nag moo man a weddi peeñug Yàlla ci boppam, ni Mu ko bëgge? Kan moo man a tere Yàlla Aji Kàttan ji Mu am Doom, ba noppi saraxe ko ngir Mu musal àddina sépp? Yàlla lu Ko neex lay dogal! Laata Yàlla di sàkk àddina si fekk na Krist nekk. Dafa nu ganesi ni nit ngir jubóole àddina si ak Baayam ji, delloosi jàmm ji, te musal àddina si. CELLAAY la fi nekkewoon ngir man a far bàkkaari àddina si. Yaxya moo feeñal bii wooteb Yàlla: "KII mooy mbotem YàLLA, mi ñu war a rey ngir faxas bàkkaari àddina si. (Yowaana 1:29). Kon book dañu nu baayale ba nu man a woowe Yàlla "Sunu Baay", ndaxte baal nañu nu sunuy bàkkaar. KRIST matal na mbaalug bàkkaari doomi Aadama yépp Yemul ci kercen yi rekk. MUCCAM gi jagleel na ko INDU yi, waa Budaa, Yawut yi, Jullit yi ak Yëeféer yi. MOOM Kay, ñépp ñi Ko wóolu te nangu Ko ni Musalkat ak sa Boroom, dund gu amul àpp la leen di may. Doom ji moo nuy wommat ba ci Baay ji, te Baay ji yóbbu nu ci Doom ji. Yàlla ci boppam feeñu na ba ñuy sóob Yeesu ci ndox ca dexu yurdan: "Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, te mu neex ma, ma tànn Ko." (Macë 3:17). Kan moo man a tere Yàlla mu dëgtalu baatam ca asamaan?


03.8 - LAN MOOY MéBéTU NDIGAL LU JIITU LI(njëkk li)?

Ndigal lu njëkk li, fexe ba nu bëgg Yàlla doŋŋ lay wut.Nii la ko Musaa tënke: "Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp, ak sa ruu gépp, ak sa kàttan gépp."(Pàttalig Ndigal yi 6:5). Li man a am mooy, nu bëgg Yàlla te di dunde ak jokkoonte ak Xelam mi, walla nu bañ Ko, te dëkk ci wuuteek coobareem. Bu nu bëggee Yàlla, danu koy xalaat, di Ko déglu, te di def li ko neex, di dunde ni Mu ko bëgge rax ci di ko xaare ni far di séentoo coroom te di jàng ak a jàngaat bataaxal ya mu ko yónneewoon. Waaye ñiy wéy ci seen tiitar, ba foog ne ay gennwàllu Yàlla lañu, ba di won doq Yàlla ju dëggu ji, dinañu fàtte Kàddoom, te seen dëgër bopp, dina leen tàbbal ci merum Yàlla.

ŇI Bëgg Krist dañoo yaatalal seen bopp ci Xelum Yàlla. Ňooñu dañuy jot seen mbaalug bépp bàkkaar te baa ci sci dëgg-dëgg, kon danuy wëlbatiku ci Moom te jot yiw ci kow yiw. Bés-o-bés dafay yeesal sunu xalaat, nuy dunde ngoreelug doomi Yàlla, te sóobu ci liggéeyam biy jëme asamaan. Ňi bëgg Yàlla dañuy dàq bépp bokkaale ci seen dund te jàpp ci kóllëre gu bees gi nga xam ne ay kumpaam ñungi leen di feeñale ci sunuy reeni ngëm ak dund: "Yàlla mbëggeel la;ku sax ci mbëggeel, dëkk ci Yàlla,te it Yàlla dëkk ci yów" (1Yowaana 4:16).

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on May 27, 2025, at 02:45 PM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)