Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- The Ten Commandments -- 02 Introduction To the Ten Commandments: God Reveals Himself
This page in: -- Afrikaans -- Arabic -- Armenian -- Azeri -- Baoule -- Bengali -- Bulgarian -- Cebuano -- Chinese -- English -- Ewe -- Farsi -- Finnish? -- French -- German -- Gujarati -- Hebrew -- Hindi -- Hungarian? -- Indonesian -- Kiswahili -- Malayalam -- Norwegian -- Polish -- Russian -- Serbian -- Spanish -- Tamil -- Turkish -- Twi -- Ukrainian -- Urdu? -- Uzbek -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

TOPIC 6: THE FUKKI NDIGAL YI - Ab ñag buy aar nit ki ci cib jéll
Fukki denkaane yu am solo yi ci Exodus 20 ci leeralu xebaar bu baax bi

02 - UBBITEG FUKKI NDIGAL YI: YÀLLA DAFAY FEEŇU, MOOM CI BOPPAM



Gàddaay 20:2
« Man maay Boroom bi ,sa Yàlla,ji la génne réewum Misira ca néegu njaam la. »

Fukki ndigal yi sasuñu kenn ay saart aky yoon yu leerul yu malaaka wàccee.Waaye ci ñoom la Yàlla ci boppam di waxe ak nit ñi. Aji SÀkk ji dafay jegesi ay mbindeefam, te Aji Sell ji randusi ci askanam wiy bàkkaarkat.


02.1 - MELOKAANU YÀLLA

BAAT bi jëkk ci Fukki Ndigal yi mooy « Man maay”walla “Man”. Yàlla miy dund dafay wax ak nun ni nit waaye du ni njuuma walla ab dënnu bu ragallu bu nuy dégge fu sore. Ay kàddoom neex nañoo dégg. Dafa bëgg a lal ag kóolute ci sunu diggante. Ci biir yiwam lay jokkoo ak nun, waaye du ci Ndigalam walla ci meram. Dafay wëlbatiku ci nun, fees ak mbaax ak mbëggeel; ndaw beral loxo !

Nit ki man naa jéem a tànn a dummuuyu Yàlla Aji Kàttan ji te sore baaxaayam gi. Moone fépp fu nu man a nekk Yàlla mu sell mi mungi nuy gis. Mungi nuy gis fépp fu nu nekk. Looloo tax ku maandu ku nekk war na ne naam ay Kàddoom. Li tax Mu ne »Man » moo tax nu féetewoo »yow”ba man a wax ak Moom ci kow nekk ay mbindeef yu am tur.

Kon man nanu biral, ci lu amul benn xel-ñaar ne Yàlla Aji Sax ji, Moom ci boppam, miy taawu lépp,Àttekat bi ba fàww,dafay wax ak nun ni nit. Kon kay nanu Ko déglu bu baax te denc Kàddoom gi ak mbég ak bànneex.


02.2 - NEKKINU YÀLLA (Yàlla am na)

Nekkinu Yàlla ci boppam mungi feeñu ci “Man maay ». Nan la nit ñi man a waxe ne Yàlla amul? Lépp li yéeféer yi jàppoon dafa surux ci kanamu li Yàlla seede,ndaxte « maay »moo tax nu nekk. Yàllaa ngi fi ! Lépp dafay wéy, Moom rekk mooy nekk ba fàww. Nit ki dafay faral di fippu ci kanamu Ki ko sàkk mel ni kuy jànkonteek tund wu rëy.Waaye dëgg gii saxul ci li nit ki di wax ci Yàlla, walla li boroom xam -xam yi di bind ci Moom. Moom mooy dëgg gi ci boppam, te Moo fees dell dunyaa bi.Am na 3000 at, jamanoy Daawuda,ay nit weddiwoon nañu ne Yàlla am na (Sabóor 14), Taalifkat bi dafa leen a Jàppe ni ñu dof te geru. Ndaxte xamuñuwoon lu xew ba sax ñàkkal fayda KI leewu dunyaa bi. Seen xel demul ci bàkkaar bi ñuy dunde saa su nekk.

Seedeb Yàlla Moom ci boppam dafa dàq anam yi Budda sampu. Li ñuy woowe « nirvana » te muy am njàngale mu lay dugal ci weddi sa bopp ba rey sa bépp bëgg-bëgg ngir may sa ruu mu nangoo dugg ci wëyëŋ wu yaa wi du dara lu dul ag neen. Yàlla, ay nit ñuy dund la soxla. Dafay dund ba tax Mu biral ne « Man Maay ». Li Mu fi nekk moo may sunu dund gi tekkite ak mébét yi sunu bakkan di yóotu. Dafa bëgg nu dund ni muy dunde. Xelam demul sax ci nappaaje nu.

Seede Yàlla daan bépp diine buy jaamu li ñu sàkk. Képp ku weddi àddina si bët manul a tegu, sa gis-gis leerul,Dafa mel ni diggante aw doj ak pic biy naaw ca kow asamaan. Yàlla mungi dund te dafay wax ak yów. Dafay wax sax ak ñiy jaamu am-am,yéeféer yi ak komunist yi, ngir ñépp man a wëlbatiku ñów dékk ko nopp, ba nekk ñu maandu. Su fekkee ne am na ku bañ a déglu te dëgëral xolam,dina mel ni ab gumba gu ne jant amul ndaxte manu ko gis.


02.3 - KANN MOOY « YAHVE »?

Yàlla ne Musaa : “Man maay Boroom bi” Gàddaay 3:14 “Maay Ki Nekk, KI may nekki”dafay wone nekkinu Yàlla gu dëggu,gu amul àpp,teguwul ci benn sart te wékkuwul ci dara. Yàlla nekkul ni kenn. Li Mu dul soppiku moo waral sunu ngëm gi, te mooy doju koñu sunu mucc gi. Ak sunu matadi yeek sunuy bàkkaar yépp, terewul Yàlla, Mi dul soppiku, sax ci kóllëreem. Man nanu dellusi ci Moom ndaxte Ku am kóllëre la. Fii ak nungi xaarandi àddina tukki, Yàllaa ngi dalal sunu xel : »Asamaan ak suuf dinañu wéy waaye samay wax duñu wéy mukk. « (Macë 24 :35)

Ci nguuroom la Yàlla takk lépp :Xam na lépp, di gis lépp, dara umpu ko te dafa fees ak maandute.Bu bunt yépp tëjoo, Moo nuy won yoon wi nuy jaar ngir génn. Moom xam na sunuy xalaat ak sunuy yëgeel. Tiital nu, maanaam yóbbu sunu fit, nekkul coobareem; xanaa kay dafay jii ci nun kóolute ak yaakaar ju xóot. Dafay wax ak nun ngir nu man Koo xool ak kóolute. Dafa bëgg a nekk Boroomu sunug dund. Céy waay! Bu kenn jéem a nëbbu Boroom, bi man a muñ, ndaxte sa tontu rekk lay xaar, maanaam képp ku wëlbatiku ci sa Boroom,ne naam mbëggeelam gu fees ak yërmaande gi. Bi Yàlla nee : »Man maay Boroom Bi », dafay biral itam ne Moom rekk mooy Boroom bi te amul beneen Boroom. Bépp beneen rab walla yàlla amul njériñ.

Tey jii ,ak li ñu jàppe ay déebaadéebi xel, walla ay njàngale yu ngeemboo kumpa, ni ay diine yu bees lépp,ñi rab yu bon yi duggoon, ñu teg seen kóolute ci jenn Yàlla ju dëggu ji rekk,moo leen di goreel. Diine jiy weddi lépp lu bëtt manul a tegu, maanaam agnostisism, mungi daanu, nit ñi jeeng, jëm ca weneen cat wa,ba noonu ñu laxasu ca ay xërëm ak yu ni mel ba ay rab yu bon jéng leen. Ňiy ñaax nit ñi ngir ñu bokk ci yu mel noonu, fépp lanu leen di fekk, muy ci rajo bi, telewisoŋ, walla ci bataaxal yi.

Ci INJIIL,Yeesu dafa ne »MAN maay MOOM »Loolu ab baatu Fukki Ndigal yi la rëkk ! Ba ko Yeesu di wax, dafa biral ne Moom mooy Boroom bi te itam, di xabaar bu baax bi malaaka ya yëgaloon sàmmi Betleem ya. Yeesu dafa gën a wéy ba ne : »Maay mburu dund gi”,”Maay leeru àddina si « , »Maay bunt bi », »Maay yoon wi,dëgg gi, ak dund gi ». Nee na itam, : »Maay Buur », »Maay njalbéen gi, di njeextal li. ”La dale booba ba léegi ay taalibeem tàyyiwuñu ci di xamle ak xadar ne : »Yeesu mooy Boroom bi. » Du soppiku mukk,te dafa nuy musal ci bépp bàkkaar.Dëggal na Ki Mu doon, ak sañ-sañam, ba Mu dekkee ca biir néew ya. Noonu tàmbalig Fukki Ndigal yi am na galen bu sedd xol: ”Man maay Boroom bi.”


02.4 - KAN MOOY YÀLLA?

Ci Ebrë(làkku Yawut) « Elohim » lañuy woowe Yàlla, liy tekki ci araab » « ALLAh ». Baatu »Elohim » man nañu ko jànge itam « Eloh-im », fekk ne Allah mooy “Al-el-hu”. “Al” ab santu benn baat doŋŋ la buy sant“bi” walla “ ki”. “El”mooy turu cosaanu Yàlla ci geñog Sem, te muy tekki”Kàttan ji”. Yeesu dafa biral xóotaayu tekki-tekki baatu”EL”te dëggal ko ba Muy seede ca kuréelu Àttekat ya ca Kër- Yàlla ga: ”Li dale fii dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndeyjooru Aji Kàttan ji.” (Macë 26:64) Baati “-im” ak “-hu” ay toftali baat lañu. “Im”ci hebrë ,man nañu ko bareel, waaye “hu” ci araab kenn doŋŋ la man a nekk. Ci noonu, baatu” Ňett ci Benn” xejootul ak baatu “Allah »ca fa ñu soqikoo; fekk nag baatu “Elohim”may na Yàlla Mu nekk” Ňett ci Benn.”

Boroom bi Aji Sax ji nekkul rekk KI xam lépp, te nekk fépp,waaye itam Mooy Aji Kàttan ji. Moom rekk mooy tabaxkat bi ëpp kàttan ci dunyaa bi. Moo sàkk jàww jépp ci kàddoom gu am kàttan gi te fekk lépp nekk neen(ne wëyëŋ ). Muñal na ñépp. Sunu Boroom du Yàlla juy yàq, di yóbbu fit mbaa di wommat ki ko neex te di sànk ku Mu tippoo (Saaru Aji Sàkk ji 35 :8) ak Ki ñu Solal mbubbum buur mi (manto bi) 74:31)-Aka wuute ak li sunu yàlla bëgg,maanaam: ”Ňépp mucc te xam dëgg gi.” (1Timote 2:4)

Ci biir téereb Kóllëre gu Njëkk gi am na ay nit walla bërab yu ñuy tudde “EL” yu mel ni Samuel, Elisee, Elieseer, Dañel, ak itam: Bethel, Izreel ak Israel. Ňoom itam dañu lëngoo ak”kàttan “giy doxal dunyaa gépp. Ci téere Kóllëre gu Bees gi, ñépp dañoo booloowoon jokkoo ak Yàlla, la ko dale ca ba ñu amee dig bii: ”Waaye dingeen jot kàttanu Xel mu Sell miy wàcc ci yéen.” (Jëf ya 1:8). Yàlla du dàq bàkkaarkat yi, waaye dafa leen di laabal, Sellal leen, te dëkk ci ñoom.

Bépp sañ-sañ ci suuf ak ci kow jox nañu ko sunu Boroom Yeesu Krist, Aji Kàttan ji. Ndell yi man a tukkil àddina xaajuñu yem ak kàttanam ju amul àpp ji.


02.5 - KAN MOOY ALLAH CI ISLAM ?

Déggal Yàlla Aji Kàttan ji, moo tax Jullit yi di Ko bàkke »Allahu akbar », Yàlla moo gën a màgg! Kon Jullit bi dafa jàppe Yàllä ni Ki gën a « rafet », gën a teey ñépp. Kon Allah mooy Ku màgg ki, Ku am doole ki, Ki kenn manul a natt te sut bépp jaamam. Amul menn xel mu Ko man a dab. Moom xam na nu bu baax. Ku nu sore la te kenn manu ko xam. Bépp xalaat bu nu man a am ci Moom, manul a doy, te du dëgg. Nit du mos a xam Aji SAX ji. Kon book Jullit bi amul meneen pexe mu dul ragal Ko te jaamu Ko ci ay sujjóot.

Ci biir gëstu la Suufi yi jéem a taxawal ay ñag ngir man a jot Yàlla Mu màgg mi kenn manul a jot. Alxuraan soññul kenn ci doxalin bu ni mel te dafay làq Yàlla cib dégg-dégginu beduwin ci baatin.

Ci Islam,Yàlla kenn manu Ko gis, te fasul kóllëre ak jullit yi. Mahomet kenn jàppewu ko ni ab Rammukat. Jokkalewul jullit yi ak Yàlla ci kow buumu kóllëre. Dafa sant ñépp ñu jébbalu doŋŋ ci seen Boroom.

Jullit yi xamuñu xóotaayu Yàlla.Ňoom ràññeewuñu ni seen bàkkaar tollu te manuñu ñam Yiwam.Ci seeni cant duñu jarajëfal Musalkat bi ngir muccug doomi Aadama yi,te it duñu ko màggal ngir goreelug àtte gi Mu maye.Dañuy jaamu Allah,mi sore te am kàttan,ni ay jaam yu ànd ak fitna te ñàkk kaaraange yuy rëppeelu ci seen kanamu Njaatige. Dañuy dogu ci topp Mahomet ndaxte Islam dafay màggal Yàlla miy yóbbu seen fit te du leen sellal mukk.Duñu sant ab Musalkat bu leen muccloo ndaxte ab Musalkat amul ci Islam. Kon book kenn warul a jaaxle bu bu jullit bi ŋoyee ci aaday njaamoom!

Waaye Yàlla dëgg-dëgg ji, te Biibal bi feeñal ko (xamle ko), sorewul li Mu sàkk (càkkiteem). Dafa nu jegesi ba fas kóllëre ak nun doomi Aadama yi, te naan: ”MAN MAAY BOROOM BI, SA YÀLLA.”


02.6 - KÓLLëRE GI AK YÀLLA

Baatu « SA » ci « SA Yàlla »,baatu moomeel la. Dafay tekki ne Yàlla ci boppam dafay suufeelu ba may nu, nu koy jàppe ni sunu moomeel Man nanu Ko wóolu ni gune di wóoloo baayam. Yàlla Aji Kàttan ji mooy suufeelu ci sunu kanam, ak li nuy man a fippu lépp ! mel ni dafa naan nu : »Maangi ak yeen,xanaa bëgguleen a rëccu seen bàkkaar yi te walbatiku ci Man, dogu jébbal ma seen bopp ba fàww ? »

Li tax ba Fukki Ndigal yi tàmbaleek Kóllëre gu Yàlla fas digganteem ak askanam,ab yëgle bu ànd ak soññ la. Yàlla rekk Moo may googu kóllëre aw Askanam. Ci biir googu Kóllëre, la nuy birale teewaayam ci sunu biir, ak Mbëggeelam ci nun. Mungi yaakaar ne dinanu nangu aji nekkinam fépp, ci kow ngëm,yaakaar ak mbëggeel.

Ci kow Kóllëreem ak bàkkaarkat yi, Yàlla dafa leen a wóoral Mbaalam, Muccam,Càmmam(aaram), ak ay Barkeeiam.”Gannaaw Yàlla ànd na ak nun ,kan moo nu manal dara?” (Rom 8 :31). Dafa nuy ñaax te di nu xamal ne mungi ak nun bés bu nekk te di liggéey ak nun, ak li nuy matadi lépp. Bàkkaaru nit ki manul a àppal kóllëre Yàlla. Dara manul a tere Aji sell ji Mu àtte te daan bépp bàkkaar,ak nu mu man a tollu. Njubteem gu mat sëkk gi, dafay daan bépp bàkkaar, waaye bàkkaarkat yi bokk ci Kóllëreem gi, seellal nañu leen jaare ko ci Mbëggeelam gu amul àpp gi ci Krist. Bi Krist deewee ngir wuutu nu, dafa siife ne tayle Kóllëre gi nekkoon sunu diggante ak Yàlla mat na, sotti na. noonu la Bant ba,maanaam Kuruwaa ba nekkee mandarga miy wéyale Kóllëreem gi.


02.7 - YÀLLA MOOY SUNU BAAY

Tàqalikoo bi amoon ci diggante Yàlla ak nit ki, mungi jeexe ba Yeesu juddoo. Yàlla moo soppi boppam nekk yaram ngir ay Taalibeem bañ a nekkati ay jaam. Yeesu dafa leen a yewwi ci buumi bàkkaar,ci jéngi Seytaane, ci dee gi ak sax ci àtteb Yàlla. Deretu Yeesu tuuru na ni sarax ngir goreel nu. Képp ku gëm Yeesu dees na la laabal te jàppe la ni doomu Yàlla. Ci Krist la Yàlla Aji Kàttan ji jaare ngir nekk sunu Baay ci sayiir ak ci baatin. « man maay Boroom bi, Baay bi « ñooy baat yi Mu nuy dëfale bu nu defee bàkkaar bu jéggi dayoo sax.

Yàlla Baayu Yeesu Krist,dafay may kàttanu Xel mu Sell mi képp ku sopp Yeesu te di Ko topp,Moom mi ñu daajoon ci bant te Mu dekki. Ňi Ko gëm te judduwaat ci Moom YEESU, am nañu seen dundug Baay bi ci kow, ak melokaanam.Defatuñu nenn ak ñàkk-yaakaar te rëcc nañu ciy weyi deewug xel. Yàlla mu Sell mi dafa jaare ci Krist ngir jokkoo Moom ci boppam ak nun. Dafa nu def ab néegu jaamukaayam, ab Dëkkuwaayam. Mooy sunu Baay te nun nooy ay Doomam. Moo nu moom, te nun noo Ko moom. Kóllëre googu, dee gi nu Yeesu wuutoo moo ko matal. La ko dale booba ba tey, way-gëm ju nekk dafay am diggante bu ratax ak Yàlla ci boppam. Kon buy ñaan du ay waxi neen lay sànni. Xanaa kay ñaanam dafay mel ni ab jokkook Yàlla ci telefoŋ bu ëmb cant, jéggalu, ay ñaan aky ñaanalaate. Sunu Baay bi ci asamaan dafa nuy déglu ak kóllëre. Ci Baayoom gi lanuy ame làquwaay. Dafa nuy muur te di nu aar ak paltob Ndamam. Wuute na ak Jullit yi,ndaxte Kercen dëgg du sore mukk Yàllaam. Du it jaamu ay bërab yu ñu jagleel Yàlla, ni ko Indu yi di baaxoo defe ,mbaa ni wëyëŋu jaww ji yóbbu fitu gaayi Budaa yi.

Aji Kàttan ji ci boppam moo lëkkoo ak ndawi Krist yi, jaarale ko ci Mbëggeelam ngir ñu man a dund ci teewaayam, te soppiku ni Melokaanam. Sunu Baay bi ci kow asamaan bëggunuwoon a bàyyi ci sunug ñàkku-yaakaar, waaye dafa dogu ngir musal nu te yeesal nu. Dafa noo sas ne nu: »Na ngeen sell ndaxte damaa sell. » (Lewi 11 :45) Jokkoo ak Yàlla nekkul rekk ag ngëmug xel waaye dafay ànd ak coppite jikko gu mat sëkk. Bu nuy dund ak Yàlla kon sunu noo dafay am coppite, ndaxte Yàlla Aji Sax ji dafa dogal yemale doomam yi ak Moom ci boppam. Sunu Baay bi dafa bëgg nu mel ni Moom, ni ko Yeesu waxewoon: »Nangeen mat nag, ni seen Baay bi ci kow mate. » Fukki Ndigal yi, gindikaay la buy soppali ñi réer ñu nekk ay doomi Yàlla. Fukki Ndigal yi, ci kow Yiwam wi, aw ñag la, wu nuy tere daanu.

Xëy na yaangi xalaat ne kenn manul a topp Ndigali Krist yi ba ñu mat sëkk. Nan la nu man a mate, ni Yàlla selle? Wax jii ndax fàttaliwunu fiir ga daloon Awa ca toolu Àjjana ja, ba mu déggee déeyu Seytaane ya naan ko: ”Dinga mel ni Yàlla !” Nit ki manul a musal boppam, manul it nekk ku jub ci know ay pexeem doŋŋ. Jikko ju baax ju nekk mungi wékku ci ay sart yu man a yee fippu te di mujj cib àtte. Waaye sunu selaay, sunu Baay bi ci asamaan moo ko liggéey ci nun. Moo nuy wommat ci yoonu Njubteem gi. Bés bu nekk dafa nuy fàttali ngir nu fàtte sunu bopp ndax Mu may sunu ruu Kàttanam ci boppam, ngir di ci daane lépp lu bon; dafa nuy xiir ci jàng Kàddoom gi te di ko jëfe. Mbëggeelam giy soppi ñiy dunde “bopp-sa-bopp”ba ñu nekk ay surga moo nuy solu ba nu fees. Mayug xel yi nu sunu Baay jagleel dañoo fës ba Mahomet sax ràññee leen. Moom wone na ne taalibe Krist yi, ay nit lañu ñu amul benn rëy-rëylu. (Sóorat al-Ma’ida 5:82) te jot ci seen xol yërmande ak ñówental (Sóorat al-Hadid 57:22).


02.8 - GOREEL GI MAT NA

Yàlla dafa noo bëgg a goreel ci buumi bàkkaar. Ci ubbiteg Fukki Ndigal yi, dafa nu ciy wax ne manunu goreel sunu bopp ci buumi bàkkaar. Yàlla Moo nu koy defal ci köw sunu ngëm gu ànd ak dégg ndigal. Yàlla goreel na Askanam ca buumi njaam yu tar, jaare ko ci Musaa, ba noppi Mu fas kóllëre ak bànni Israel. Yàlla naguwuleenwoon ndax seen baaxaay mbaa njubte, waaye dafa leen a tànnoon ndax yiwam. Moom nee na: »Man maay Aji Sax ji, Yàlla sa Boroom, bi la génne réewu Misira, këru njaam ga. » (Gàddaay 20 :2)

Doomi Yanxóoba ya dañoo toxoo ca tundi xeer ya ca mbartali Yurdan ya lu tollook 3600 at, ba maral ma dalee ca seen réew ma. Xiif ma tax ba ñu dëkki lu tollook 300 kilomet ca tefesu dexu Nil gu suuf sa nangu lool. Ňu am fa dund gu naat te yoomb. At mu nekk, dex ga (Nil) daan na tooyal seeni suuf ba dundal réew ma mépp. Doomi Yanxóoba ya tàmbalee bare bay bëgg a jaaxal waa Misira. Noonu gaayi Firawna teg buumu njaam liggéeykati Yawut ya te bundxataal leen. Ňenn ca ñoom jaam ya, daldi fàttaliku seen Yàllay baay ya, daldi KO ñaan ngir Mu wallusi leen. Ba jamano di neex dañoo fàttewoon seen Yàlla, waaye ndóol ak soxla delloosi na leen ci sen Musalkat bi leen Sàkk. Yàlla dégg na seeni yuuxu ba yónni Musaa, Jaamam, bi Mu tàggatoon ca këru Firawna, ak ca mànding ma ngir mu matal coobareem. Boroom bi dafa feeñu Musaa ci as ngarab suy tàkk te du lakk. Yàlla dafa feeñu Musaa ni "Man maay", liy tekki "Maay ki may nekki (Maay ki nekk) duma soppiku, waaye wóllëre laay ànde ak yów." Kon nag: "Dingeen Ma wut te ma may leen ngeen gis Ma, bu ci seen xol bépp àndee" (Yeremi29 :13-14).

Yàlla dafa yónni Musaa ak magam, Aaróona, ca kanamu Firawna mi waa Misira jàppe sax nib Yàlla, ngir ñu ñaan ko mu yewwi buumu njaamu yawut yi. Waaye kilifa dexu Nil ga lànk a goreel liggéeykat yu yoomb payoor yooya. Muy gën a dëgëral xolam ci wooteb Yàlla boobu. Firawna jekkuloon ngir yewwi doomi Ibrayma yi, noonu Boroom bi mujj koo ga ci ay góom aky musiba ngir mu nangu. Du seen njubte moo tax ñu goreel leen ci njaam gi, waaye seen ngëm gi ñu sàmm.Yoruñuwoon ay jaasi. Dañoo dawe ca guddi muuroo deretu mbotem bésub jéggi ba ñu rendiwoon, te mu doon seen kaaraange. Kër gu nekk dafa rendiwoon am mbote xar, ñu lekk yàpp wa te daw ak kàttanam ja. Jéeggig Géej gu Xonk ga ak deewug seen noon ya ñooy wone ne dogoo nañu ak buumu njaam te dugg cig goreel. Tey jii ca këru ndénkaanu cosaan ga ca Keer, ñunga fay wone ndeyu firawna ma laboon ca Géej gu Xonk ga ndax ñax ya duggoon ca ay xëtëram.

Jullit yi dañoo jagleel Yàlla seen ndam ci kow seeni xare ak seeni noon. Waaye ba Mahomet daanee julo Màkka ya ca xeexu Badar, duwoon loxob kéemaanu Yàlla moo ko waraloon, waaye jaasi yu ñaw ya ay taalibeem ya ngànnaayoowoon moo taxoon. Ňooñu dañoo joxewoon lépp li ñu amoon. Kon kay dara terewuloon ñu daan seen noon ya ! Liy wone Musaa ni ag kéemaan (goreel gu jóge asamaan (te deret tuuruwul), moom lañu jàppe ci Islam ni xare bu sell (jihad) boo xam ne képp ku ay cëram mat am nga warugaru bokk ci. Sart bi ñiy bokk ci xare yooyu di taafantoo mooybii: "Du yów yaa leen rey; waaye Yàlla ak bmoo leen faat. Du yów yaa doon sànni jum yi, waaye Yàlla moo leen doon sànni." (Sóorat al-Anfal 8 :17)

Ba Mu yewwee Yawut ya ca buumu njaam ga ca Misira, Boroom bi dafa leen a yóbbu ca tàngaayu manding gu tar, ba noppi berndeel leen fa. Dafa bëggoon a fas foofa ag kóllëre asamaan ak ñoom, gu leen P 14--di sellal ci biir bennoo ak ñoom. Dafa leen a woo ngir ñu nekk Askanam wi mu ber ngir mu surgawu Ko. Ňoom ñoo waroon a nekk ndaw yi Koy jokkalewaat ak nit ñépp ci kanamu Gànnguneem. Fukki Ndigal yi ñoo nekkoon xolu kóllëre googu ak sartu wurus wiy tax nu man a sax ci jokkoo ak Boroom bi. Yàlla moo doon nguuru ci kow ñaari àlluway Ndigalam yi ñu dencoon ca Gaalu Kóllëre ga.


02.9 - NI GOREEL GI MATE CI KÓLLERE GU BEES GI

Bu sunu xel demee ci ndam lu rëy li Yàlla mayoon sëti Yanxóoba ya 3300 at ca gannaaw, te it nu méngale ko ak mucc gi Yeesu matal ci Kóllëre gu bees gi, kon dinanu man a tënke Fukki Ndigal yi nii: "Man maay Boroom bi, seen Yàlla ak seen Baay; dama leen a jotaat ba abada."

Bi nu Yeesu ganesee ci àddina ba léegi, nungi yéene askan yépp yërmaande Yàllaji, di waare ne Yeesu mooy Boroom bi, te mooy Musalkatu nit ñépp. Ni mbotem Yàlla, Moom fay na sunuy bàkkaar ak sunu mbugal, ba mu deewee ca bant ba. Dagg na jéngi bàkkaar ya te daan nguurug Seytaane jaarale ko ci ay metitam ak deewam gi. Wàccee na merum Yàlla te wuutu nu ci sunub àtte. Sunu mucc ba fàww, Yeesu rekk moo ko matal. Looloo tax nu war Ko sant te nangu Muccam gi, ci know sunu gëm.

Mucc gi sunu Boroom di may bépp doomu Aadama, jekk na ba noppi. Kenn du méngale sunu mucc ak geneen; jaarul ci ngànnaay. Moone sax deret tuuru na, waaye du deretu noon bu ñu daan, waaye deretu Doomu Yàlla ju sell, ji jébbale boppam ni sarax ngir nun.

Manunu musal sunu bopp ci kow topp Fukki Ndigal yi: Loolu du sax li leen tax a jóg. Li ñu nuy jàngal kay nun ñi nu fal, mooy nan lanuy gërëme Yàlla ci mucc gi mu nu may te fayunu dara. Képp ku xalaat ne man nga mucc ci sa kàttanu bopp, rëcc Seytaane, dee gi ak merum Yàlla, njuumte gu rëy dikkal na la. Xanaa kay dangay gën a daŋal buumu njaam gi la bàkkaar tënke. Fukki Ndigal yi manuñu nu sellal. Dañu nuy may nu man a tuub sunuy tooñ, dégg ndigal yi ci kow ngëm ak mbégu mucc gi mat ba noppi. Li tax a jóg Yoonu Musaa danu koy matal, ak Yeesu,bu nuy màggal Baay bi ci asamaan jaare ko ci kàttanu Xel mu Sell mi. Yàlla bëggu noo mbugal walla di nu alag mbaa di nu sëf Fukki Ndigal yi. Mukk de! Sunu Boroom dafa nattoon sunu mucc lu yàgg laata Muy wàcce Yoon wi. Dafa joxe Yoonam wi ngir nit ñi man a tuub seeni bàkkaar, te wuutoo seen fippu, ak lewetaayu Xel mu Sell mi. Kon book li tax a jóg Yoon wi, mooy nu man a jokkoo ak Yàlla Baay bi, waaye du deewug bésub àtte ba.

Dinanu doon gën a xam li Fukki Ndigal yi di tekki bu fekkoon ne mos nanoo nekk ay jaam, nun ci sunu bopp. Bu nu nekkoon jaam, muy mag walla ndaw, muy ku feebar mbaa mu am kàttan, danu naroon di yenu liggéey bu diis ba dunu xalaat sax sunu bopp. Danu nu naroon di liggéeyloo ci anam yu kenn àttanul. Ni ay jaam, ñu bare ci nun danoo naroon a dee, te kenn du bàyyi sax xel ci ñoom.

Yàlla dafa goreel Askanam ci ndóolum xel ak ci coono. Loolu moo tax nu jàppe Fukki Ndigal yi ni tegtal buy jàngal kercen yi ñu goreel nan lañu war a jëfe ci kow teey ak maandute ci seen yewweeku bi ñu leen jagleel. Ay nattu yu bare ñungi lalu ci biir yewwi bi. Bu nu dundul ak Yàlla, danuy nekk jaami bàkkaar ak sunuy bëgg-bëgg ci lu gaaw. Waaye Yàlla dafa sàkk nit ki ci melokaanam. Nit ki manu l dund dundinu njubte fi ak àndul ak Yàlla. Amul benn Yewwi bu mat te Yàlla àndu ci.

Bu nit di dunde bàkkaar, dafay nekk jaamu bàkkaar, te yu mel nii ñooy nekk kasoom: ñoll, bëgg-bëggu yaram, càcc, tàyyeel, lël ay bakkan, ak ay ñaawteef. Ňeneen ñi dañuy dunde xol bu neexul ndax jéng yu sew yu leen sonal yu mel ni tóx, naan sangara, doroogewu, ak fen, rax ci dolli xërëm yi ak rab yu bon yi. Seytaane dafay foowe seeni xel. Waaye Yeesu dafay yewwi ki Ko gëm,ba mu mat sëkk, ba noppi dugal ko ci yewwib doomi Yàlla yi. KRIST mooy Jàmbaar ju mujj ji, Boroom bi ak Musalkat bi, Boroom maandute bi tënk jaw ji, Sàmm bu baax bi ak Xarit biy sàmm kóllëre. Képp ku wékku ci Moom (ku Ko woo ku nekk) jot ndimbal ak xelal.

Fukki Ndigal yi, ab jéggikaay la ngir ñi ñu yewwi ci kow yiw. Yàlla nekk na léegi seen Baay te Krist, seen Musalkat ak Xel mu Sell mi, nekk seen dëfalkat. Ňooñu ràññee nañu ne Yàlla Baay bi, Doom ji, ak Xel mu Sell mi, benn Yàlla lañu. Ame nañu ci Moom yewwi bu dëggu jaare ko ci cant ak jàmm. Amul benn sikki-sakka ne Fukki Ndigal yi nekkal nañu leen ay tegtali yoonu Yàlla, te xelal leen ba ñu jollil taalifu cant bii ci seenug mandiŋu bakkan. (Sabóor 119:54)

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on May 21, 2025, at 03:39 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)