Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
D - Tàggatoo ba ca yoonu Getsemane (Yowaana 15:1 - 16:33)
1. Bu nu saxee ci krist, danuy meññ bu baax (Yowaana 15:1–8)YOWAANA 15:5 Nun nooy car yi jafandu ci garab gi,soqeekoo sax ci xolu Yeesu. Ndaw sargal gu mag ! Sàkk na dundu baatin ci nun. Car su ndaw mooy génne ci garab gi,daldi màgg ba nekk car bu dëgër te wér. Noonu it la ki gëm di juddoo ci melokaan ak jikko yu kercen ndax Yeesu. Du caageen ne sunu ngëm moo nu ko may, waaye yiw la.Sax ci Yeesu, sunu wareef la. Yeesu wax na ay yoon yu bare ne mingi sax Ci NUN. Ci Kóllëre gu Bees gi, képp ku gëm jokkoo nga ak Yeesu.Jokkoo googu dafa am doole ba danoo mujje nekk benn ak Moom. Sunu Boroom dafa noo wóoral ne dunu ñàkk sunu nekkin sunu gëmee, réerunu ci biir ay bidaa.Dafay dooleel sunu coobare te sol nu Xelam, ba nu fees dell. Krist dafa noo bëgg a matloo, te mooñ nu ba nu mel ni Moom, na Mu ko nammewoon ca njalbéen ga. Ay pexeem, aky jikkoom ñoo fees xoli ñi ko gëm. Kon ana sunu xol ak sunu mbëggeel? Lan mooy ngirte jokkoowu Doomu Yàlla ji ak nit ñi ?Lu tax Yeesu dee ca bant ba, te lu waral Xel mu Sell mi feesal xolu ñi gëm? Lan la Boroom bi bëgg ci yów? Dafa bëgg ngay meññ doomu baatin, te doomu Xel mi mooy: mbëggeel, mbég, jàmm, muñ, laabiir, mbaax, kóllëre (Galasi 5 :22). Dunu man mukk matal jikko yooyu ci kow sunu coobare. Nu doxal li nu manul a ñàkk sax të nanu, maanaam yu mel ni noyyi, dox, wax, te limagunu sax lu jëm ci ñaan, ngëm ak mbëggeel. Ni ay way-gëm, am nanu ngëneelu. Jot ci dundu baatin gu jóge ci Yeesu kese. Nanu Ko sant ngir sunu dunug baatin ak kàttanu Yàlla gi nga def ci nun. Jikko yii yépp, ay mayu Yàlla lañu. Bu àndul ak nun, dunu man dara. YOWAANA 15:6 Sax ci Krist, ci yów la aju. Ci genn wet gi, danuy seetlu ne dundu Xel mi, ak sax ci Krist, ay may lañu. Ci geneen wet gi, danuy gis ne ku tàqalikoo ak Krist dangay mel ni ku xaru. Dëddukat boobu dafay ñëg, te dinañu ko sànni ci safara merum Yàlla. Bu jamono ji jotee, malaaka yi dinañu dajale ñépp ñi dëddu Krist, sànni leen ci lëndëm gi. Xelu ñooñee duleen may benn noflaay. Dañuy xala séen Yàlla yërmande ji fu soree-sore, ba fàww. Ci lañuy dor a xam ne ca njalbéen ga, mbëggeelam moo leen doon aar. Ndegam dañu Koo dëddu, xebat nañu seen Musalkat te kon jagleel nañu leen ñuy lakk ci safara su dul fay mukk. YOWAANA 15:7 Ku sax ci Krist dangay dundak moom ak wóllëre gu xóot-a -xóot.Bu ay nit séyee lu yàgg lool, ku ci nekk ci ñoom ñaar dafay mujje xam xalaati moroom ma aky mébétam.Noonu itam ,képp ku bëgg Krist,dangay xam coobareem te sax ci jokkoo ak sa Boroom. Di jàng Biibal bi bés bu nekk ,dina nu ñaax ba nu bëgg li Mu bëgg,ndaxte sunuy yëg-yëgu biir dinañu fees ak ay kàddoom. Noonu, dootuñu ñaan ngir sunuy bëgg-bëgg kese, waaye dinanu topp ak teey ni Nguuram gi di lawe. Dinanu nekk rammukat yu xarañ,c i xare baatin bi. Su boobaa sunu xol di, óna fees aky cant ak ngërëm. Xel mi dina nu xiir ci indil ku Sell ki sunuy njaqare yépp, ak soxlay ñi tollu diggante, ak ñi tiis. Yeesu, ci kow sunuy ñaan lay jëfe ci sunu àddina si. Dafa nuy may nuy séddoo jëfinu muccam gi. Ndax yaangi ñaan? Naka? Ndax ci Xel mu Sell mi ngay ñaane? Coobare Yàlla am na mébét yu bare: dafa bëgg sa sellaay; bëgg na itam musal ñépp te fexe ba ñu xam dëgg gi. Bu sunu doxalin suufeeloo, kon sunu turu Yàlla dina ci selle. Ñaanal sa Boroom mu may la jikko ñaan ngir nga meññ bu baax te màggal sa Baay bi ci asamaan ak Krist mi lay wommat. YOWAANA 15:8 Yeesu dafa bëgg ngay meññ bu baax. As cellaay su tuut rekk doyu ko ci sag dund, du it ay mbir yu nit ku dëggu matal, walla sa cant yu amul benn fayda yi ñoo koy bégal. Déedéet! Sa cellaay lay wut. Dafa bëgg nga mat, ni Baay ji mate, te namm itam muccug ñépp. Bul doylu ci lu tuut li! ÑAAN : Bëgg nanu la, Boroom bi Yeesu, ndaxte rusuloo noo nangoo ni say doom. Nungi lay ñaan ngir ñépp ñi nga woo, te ñu tuub te ñów ci yów. Nungi lim seeny tur benn-benn. Gëm nanu ne musal nga leen ca kurwaa ba. Seen mucc leer na ndaxte jot nañu Xel mu Sell mi. Na turu Baay ji ak sa bos màgg ci Xel mu Sell mi. Bu dul Yów, dunu man dara. LAAJ:
|