Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
C - Ba Yeesu njëkkee ñów Yerusalem (Yowaana 2:13 - 4:54) -- Ci dëgg-dëgg, lan mooy màggal?
4. Yeesu ca Samari (Yowaana 4:1–42)
b) Yeesu yóbbu na ay taalibeem ngir ñu gis meññeef mu ñor mi (Yowaana 4:27-38)YOWAANA 4:27-30 Ba ñuy waxtaan, taalibe jóge dëkk ba indaale lekk ga ñu jëndaalewoon. Ñu jaaxle lool ci fekk Yeesu moom kese ak jigéen ji, rax ci dolli muy ab Waa Samari. Waaye kenn ci ñoom ñemewu ko laaj dara ndaxte yég nañu teewaayu Krist. Ba ñu xoolee xar-kanamu jigéen ja, ñu xam ne Krist defatina kéemaan. Mbëggeelu xam Musalkatam mungi doon lerxat ci xar-kanamam. Jigéen ja bàyyi fa xottu njaqam. Mayuloon Yeesu sax mu naan, te Moom fajaloon na ko maram, ca na Mu ko baale. Jigéen ja bàyyi fa xottu njaqam. Mayuloon Yeesu sax mu naan, te Moom fajaloon na ko maram, ca na Mu ko baale. Mu daw duggu dëkk ba, jeebaane fa Krist. Gémmiñam mujj fa nekk mballum ndox muy seedeel Krist. Tax na ba dëkkandoom yu bare ñów ci Musalkat bi, di seede li mu feeñal ay bàkkaaram. Ba nit ña déggee kàdduy rëccoom yooyu, waa dëkk ba gis ne am na lu bees lu Yàlla xewal ci dundu jigéen jii. Bi leen kumpaam gi bëggee rey, ñu daw dem ca teen ba, fa Yeesu doon noppalu ak ay taalibeem. Loolu mooy misaal liy xew bu Krist di jëf ci ñi ànd ak Moom. Nanuy waxtaan ak sunuy xarit ak dëkkaandoo ci xabaar bi tax Yeesu ñów ngir musal nu. Su boobaa, dinañu bëgg a am ndoxum dund googu leen di may Xel mu Sell mi. Ndax yów teenu dund nga ci ñi la wër? Bu loolu nekkul, tuubal Yeesu say bàkkaar, te jébbal Ko sa dund. Kon, dina la laabal te sellal la, ba nga barkeel ñeneen-na mu dalewoon jigéenu njaalookat ba gindiwoon dëkkandoom ya. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, maangi lay sant, ndaxte wut nga ma, te xam nga ma. man gënuma jigéenu Samari ji. Baal ma samay bàkkaar. Xettali ma ak mayug Yàlla giy faj sama marug dëgg gi, laabalal samag dund. Ubbil samay bët, ba ma man a gis Baay bi ci asamaan. Feesalal sama xol ak Xel mu Sell mi, ndax ma man a nekk jumtukaay bu am solo, te samag dund nekk ni màggalukaay guy dëggal sag Yiw. Musalal ñu baree-bare, te woo leen ci Yów. Yów doo dàq ku lay wutsi. LAAJ:
|