Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 022 (People lean towards Jesus; Need for a new birth)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
C - Ba Yeesu njëkkee ñów Yerusalem (Yowaana 2:13 - 4:54) -- Ci dëgg-dëgg, lan mooy màggal?
2. Yeesu mungi wax ak Nikodeme (Yowaana 2:23 – 3:21)

a) Nit ñaangi ñów ci Yeesu (Yowaana 2:23-25)


YOWAANA 2:23-25
23 Bi Yeesu nekkee Yerusalem, ci màggalu bésu jéggi ba, ñu bare gis kéemaan, yi Mu doon def, daldi gëm ci turam. 24 Waaye Yeesu wóoluwu leen woon, ndaxte xamoon na leen ñoom ñépp, 25 te it soxlawul ñu koy xamal dara ci nit, ndaxte Moom ci boppam xam na xolu nit.

Ay gàngoori nit dañu daan ñów Yerusalem ngir màggalsi bésu jéggi ba,ndaxte foofa moo doon màggalukaay bu mag ba. Dañu daan fàttaliku mbote ma aaroon seeni maam ca àtteb Yàlla,te dañu daan séddoo yàpp wa ba ñu daan lekk.

Yeesu Krist, Mbotem Yàlla mi, dafa ñów Yerusalem te def fa ay kéemaan yu bare, wone mbëggeelam ak kàttanam. Ci noonu, ñépp bàyyi xel ci moom, te gémmiñ yépp di ko tudd; Ñuy déeyoo naan: « Ndax ab yonent la, walla Elias mi waroon a ñów, walla book Almasi bi? » Ñu bare fàq ñów ci moom, te gëm ne ci Yàlla la jóge.

Yeesu gis li nekk ci seeni xol, waaye tànnu ca kenn ngir def ko taalibeem. Gisaguñuwoon baatinu asamaanam, waaye xeli nitu neen lañu yoroon Nuñu yewwikoo ci nootaange waa Rom lañu doon xalaat, liggéey bu tedd ak ëllëg gu rafet. Waaye Yeesu xamoon na nit ñépp, bépp xol. Kenn wutuloon Yàlla ci dëgg-dëgg. Bu ñu wutoon Yàlla ak seen xol bépp, kon naroon nañu ñaan ñu sóob leen ca dexu Yurdan ga, ñu tuub seeni bàkkaar te dëddu leen.

Krist xam na sa xol sa wax yu jaxasoo yi, say ñaan, ak say bàkkaar. Xam na say xalaat ak fu ñu jóge. Moo lay may li nga bëgg ngir am dund gu laab te jub. Ba kañ ngay nangu sa rëy-rëylu soppiku? Kañ ngay dëddu sa tiitar gu rëy gi, ndax nga man a solu Xel mu Sell mi, ba fees?


b) Soxla juddu gu bees (Yowaana 3:1-13)


YOWAANA 3:1-3
1 Amoon na ca farisen ya nit ku ñu naan Nikodem, te mu bokk ca kilifay Yawut ya, 2 Genn guddi mu ñów ca Yeesu ne ko: »Kilifa gi, xam nanu ne, Yàllaa la yónni ngir nga jàngal nu, ndaxte kenn manul a def firnde yii ngay wone, te Yàlla àndul ak moom. » Yeesu tontu ko ne: » Ci dëgg-dëgg maangi la koy wax, képp ku judduwaatul doo man a dugg ci nguuru Yàlla.»

Nit ku ñu naan Nikodem génne ca mbooloo ma; ku amoon diine ak kilifteef la woon te nekkoon kenn ca 70 yu Sanedreŋ ba. My ràññee kàttanu Yàlla gi ni muy balle ci Krist. Xëyna dafa bëggoon a nekk ab lëkkalekaay diggante Yonent bu bees bii ak mbooloom Yawut yi. Waaye itam, dafa doon moytuwaale Saraxalekat bi ak askan wi. Amaguloon lu ko leer ci Yeesu. Mu yoxoosu ci guddi, dem ca Yeesu ngir seetlu ko, laata muy ànd ak Moom.

Bi mu Ko woowee « Rabbi », Nikodem dafa wàllsi li ñu gën a bare jàppewoon Yeesu, maanaam ni kuy jàngal Mbind mu Sell mi ay taalibe. Nangu na ne Yàlla moo yónni Yeesu te firnde yi muy def wone nañu ko. Mu biral ne: »Gëm nanu ne Yàllaa ngi ak yów, te mungi lay jàppale. Man na am ne yów yaay Almasi bi. »Loolu dafay niroo ak nangu gu wér ci baatu suuf.

Yeesu tontu na laajam yi, te raxu ci lu aju ci yii tànki doxkatu diggante kilifa askan wa ak Krist. Gisoon na xolu Nikodem bu réer bi, ay bàkkaaram ak ni mu bëgge njubte. Manu ko woon dimbali fii ak wonu ko ngumbag baatin gi nekk ci moom. Ak li muy boroom diine lépp, Nikodem xamaguloon Yàlla bu baax. Ci lu amul genn làq-làqal, Yeesu ne ko: »Dëgg la ne kenn manul a xam Yàlla ci kow say pexe bopp; Dangay njëkk a soxla yeesalu Xelum Yàlla. »

Krist àtte na njàngi diine yi ak sart yi nu tëral ci lu jaadu rekk. Ndaxte xam Yàlla, du ci njàngum téerey xam-xam lay jóge, waaye ci juddu gu bees. Ak ab rajo, loolu wuute na ak tele bi, man ngay wëndéel butoŋ yi, ba mu neex la, waaye doo gis benn nataal. Ngir gis nataal yi, dafa laaj beneen post bu wuute ak rajo. Noonu la itam ci nitu neen ki, ak lu mu man a nekk nitu diine, ak jëfam yépp, du tax mu man a gis Yàlla ciy xalaat, walla ci yëg-yëg Matalug baatin boobu, dafa laaj coppite, manaam juddoo ci Yàlla te nekk mbindeef mu bees.

YOWAANA 3:4-5
4 Nikodeme ne Ko: » Nit ku xas ba màggat, nan lay man a judduwaate? Nday delluwaat ci biiru yaayam ngir judduwaat? « 5 Yeesu tontu ko: »Ci dëgg maangi la koy wax, ku judduwul ci ndox, ak ci Xelum Yàlla doo man a bokk ci nguuru Yàlla gi. »

Tontu Krist, biy wone ne Nikodem xamaguloon Yàlla, jaaxal ko lool (moom Nikodem). Mosul a dégg fu ñuy waxe lu jëm ci ñaareelu juddu. Ndax nit man naa dellu ci biiru ndeyam? Tontu bii wékku ci li xel man a nangu, dafay feeñal ag ngumba. Xamuloon ne Yàlla man na sàkke ay doom ak Xelam.

Yeesu, ku bëgg Nikodem lawoon. Bi Mu ko yeyee ba mu nangu ne xamul yoon wi jublu ci Nguru Yàlla, Mu xamal ko ne Moom mooy Dëgg gi. Danu war a gëm ne manunu dugg ci Nguru Yàlla gi bu nu judduwaatul; loolu rekk moo man a nekk.

Lan mooy judduwaat? Ab juddu la, te du ab xalaat doŋŋ: jóggewul ci man-manu nit ndaxte kenn manul a jur sa bopp, Yàlla mooy nekk baay ji, te mooy joxe dund gi Bii juddu baatin, yiw la, du as coppite jikko, walla yerug dundin. Kenn baaxul, ca la ga gko dale ca sunug ngone ga gën a tooy - xepp ga. Juddu ci baatin moo duggug Yàlla ci nit ki (dalug Yàlla ci dundu nit ki).

Nu loolu man a ame? Yeesu nee na Nikodem ne juddu googu, ci ndox ak Xel mu sell mi lay jaare Ndox mi mooy misaal sóob ba Yaxya daan defal nit ña, ak ndaa ya ñu daan sellale céet ya. Waa Kóollëre gu Njëkk ga xamoon nañu ne ndox ma ñu daan jàppe, cellalu bàkkaar la doon màndargaal. Dafa mel ne Yeesu dafa doon wax na naan: » Lu tax doo dem ca Yaxya ngir tuub say bàkkaar, te ñu sóob la ci ndox? » Am na feneen fu Yeesu wax ne: »Ku bëgg a aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, te gàddu bant bi ñu ko war a daaj,door a topp ci man. » Macë 16 :24 Mbokk mi, nangul say bàkkaar ak àtteb Yàlla bi la say tooñ teg. Ku geru nga, te yaangi sànku, Yeesu yemul rekk ci sóobug ndox gi kese, waay waaye dafay sóob ci Xell mu sell mi nit ki rëccu te tuub, ngir sàkkal xol bu toj, dund gu bees.

Gannaaw ba ñu Ko daajee lanu xam ne sunu sellaay ci deretam la jaare. Sellaay googu, ci jëfu Xel mu Sell mi lay jaare ba mat sëkk. Bu Xel mi xëccee nit ki rekk, dafay solu dund gu dul jeex gi, ak meññeefam; dafay nekk léegi nit ku baax ku Yeesu di wommat. Coppite googu, maanaam judduwaat gi, dafay laaj ab diir ci xolu way-gëm ji, ni lumb di màgge ci biiru ndeyam, laata muy juddu. Ci loolu la Yeesu wéer waareem, maanaam li aju ci Nguuru Yàlla.

Du mbirum politik, walla waxi koom, waaye jokkoo la diggante liir bi, Baay ji, Doom ji, ak Xel mu Sell mi. Xel mu barkeel moomu dafay wàcc ci moom ci saa si mu jébbalee boppam Krist, te nangu Ko ni Buuram bi mu war a déggal.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, jarajëf ci sama juddu gu bees, gi ma sa yiw wi doŋŋ may. Ubbi nga samay bëti baatin. May ma, ma sax ci sa mbéggeel. Ubbil bëti ñi lay wëre seen xol bépp, ba ñu nangu seeni bàkkaar, te tuub leen, ba kàttanu sa Xel mu Sell mi yeesal leen. Nañu sukkandiku ci sa deret ji tuuru, ngirman a jokkoo ak yów ba fàww.

LAAJ:

  1. Lan moo wuutale topp diine gu Nikodem ak mébeti Yeesu?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 15, 2025, at 02:43 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)