Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
C - Ba Yeesu njëkkee ñów Yerusalem (Yowaana 2:13 - 4:54) -- Ci dëgg-dëgg, lan mooy màggal?
2. Yeesu mungi wax ak Nikodeme (Yowaana 2:23 – 3:21)
b) Soxla juddu gu bees (Yowaana 3:1-13)YOWAANA 3:6-8 Yeesu won na Nikodem ni kenn ku nekk soxlaa coppite gu wér. Coppite gii dafa rëy ni li dox ci diggante yaram ak xel. Baatu « yaram » ci Kóllëre gu Bees gi mungi aju ci nekkinu nit ki daanu cib jéll ba tàqalikook Yàlla; ñu soxor ñi, ñungi ci yoonu dee gi. Baat bi yemul rekk ci yaram wi, ruu gi ak xelum fippukat yi. Dafa tabbaale geru gu mat sëkk, ni ko Yeesu waxe: »Ci xol la xalaat yu bon yi di jóge. » Amul kenn ku yelloo dugg ci Nguurug Yàlla gi. Ca la ko dale ca juddoom, la nit ki bone teg ci nag, di wàlle. Baatu »Xel » mooy rekk ‘Xel mu Sell mi, maanaam jëmmu Yàlla ci boppam, ji fees ak dëgg,sellaay, kàttan ak mbëggeel. Yàlla bañul ñi bon, waaye dafa daan liy ‘yaram’ jaare ko ci Krist. Loolu mooy wone li tax a jóg judduwaat. Xel mi ci nun, dafay nasaxal bépp bëgg-bëggu yaram, ngir nu man a dunde li ñu nu woowe (sunub woote). Ndax judduwaat nga, mucc ci nguuru yaram? Yeesu nee na Nikodem« : »Yów ak waa Kureel gi yépp, geñog Ibrayima gépp, dangeen a war a judduwaat.» Wareef la, wu sell sax. Nu ngi leen di xamal yeen mbokk yi ne, »fàww » gi Yeesu wax, ndigal lu jamp la. Bu yeeslu gu dëggu amul, doo man a xam Yàlla, te doo dugg itam ci. Nguuram Ndax mos ngaa dégg riirum ngelaw li? Ab liir, ngelaw lu fàq lay nirool. Dafa mel ne ngelaw li cig neen lay jóge, te fa lay dellu. Doomi Yàlla yi itam ca asamaan lañu juddoo, te ca Baay ba lañuy dellu. Riiru ngelaw li mooy wone yoon wi. Màndarga bu leer, bu liir yi mooy yëngu-yëngu Xel mu Sell miy waxe ci ñoom. Duñu waxe ak baati nit ñi. Xel mu Sell, mi wacce asamaan, moo leen di solu, ba nekk baatu kàttanu asamaan ci ñoom. Ndax wàcc na ci sa xol? YOWAANA 3:9-13 Ci kow faramfàcce Krist bi, Nikodem mungidoon yëg noowu Xel mu Sell mi. Xolam yëngu ndax ni ko Boroom bi laale. Waaye xelam managuloon a ràññee, ba jàpp dëgg gu xóot googu. Ci baatu suuf mu ne: »Man de xamuma nan la juddu gu mel noonu man a ame. » Ci kow nangu googu rekk, wone na jéllam (ñàkk ndamam). Yeesu teg ca ne: »Waaw, jàngalekat bu ñu naw nga, te nemmeekusi nga ma, waaye ñeneen ñi dañoo jàppewoon seen bopp ni ñu am xel lool, ba tax ñu may géewal waxtaan. Yaa leen sut fuuf, bu fekkee sax ne xamuloo li Xel mu Sell mi di dàkk. Sa màggal gépp, ak sa sarax yépp, boole ci sa kéem-kàttan gi ngay jéem a toppe Yoon wi, amuñu benn njariñ. Xamuloo sart yi gën a yomb ci Nguurug Yàlla gi sax.» Bii mooy ñetteelu yoon Yeesu di wax bu takku bii: » Ci dëgg-dëgg, maangi la koy wax.» Baat bii dafay ànd saa su nekk ak am Peeñu. Yeesu dafay diisal wax ji lool, ndaxte sunum xelu nit, dégg-déggam gaawul. Lan moo topp ci njàngalem Nikodem mii? Léegi nag, Krist dafa jóge ci bennalu « man » dal ci bareelu « nun », rax ci baatu Xel mi. Krist ak Yàlla, benn lañu, te mooy Kàddoom gi ñu jëmmal. Yeesu dafay jàngale dëgg gu ñépp nanguwul. Dafay seede mbir yu Mu gis, jaare ko ci jokkoom ak Xel mi. Danu war a nangu seede boobu, te gëm ko. Lan la Yeesu gënoon a xam yeneen doomi - Aadama yi? Xamoon na Yàlla, ba di Ko woowe Baay. Bu ci Xel mi ànduloon, kon kumpa googu benn boroom xam-xam(kaŋam) ca jamono jooja du ko man a foog. Krist ca Baayam la jóge te ca Moom la dellu itam; Asamaan la wàcce te fa la dellu. Tàqalikoo digante Yàlla ak nit ki, mungi jeexe ba Xelum Yàlla mi jëmmoo Yeesu, te daan (maasale) kàmb gu xóot googu. Aji Sax ji soreetul, te raglootul, waaye dafa jege te lewet. Doy na waar lool li nit ñi jëliwul seedeg dëggu asamaan googu. Ràññeewuñu jokkoo gi am ci diggante Ki juddoo ci Xel mi, ak Baayam, ndaxte dañoo lànk bañ a gëm, te nanguwuñu tuub seeni bàkkaar. Gisuñuwoon genn solo ci judduwaat, dañoo jàppewoon seen bopp ni ñu jub te am xel. Waroon nañu xam ne naw sa bopp manuleen a woon may ñu xam jokkoo gu Kenneefu Ñett ñi, gu Sell gi. ÑAAN: Baay, Doom ak Xel mu Sell mi, nungi lay màggal; ci sa mbëggeel gu aaru gi, yeesal nga nu, te soppi nga nuni doomi dëgg gi. Na sa dëgg gi ak sa Xel mi baawaan ci sunum réew mi, ndax ñu bare man a mucc, te seedeb Baay bi, Doom ji ak Xel mu Sell mi tàbbi te wesaaroo fépp, te lee naññ ci làkk bi nu nàmp. LAAJ:
|