Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
A - Peeñug Kàddug Yàlla gi ci Yeesu (Yowaana 1: 1-18)
3. Feesaayu ndamul Yàlla feeñ na ci jëmmal gi (Yowaana 1:14-18)YOWAANA 1:15-16 Sóobkat bi ci ndox dafa xaacu ne ki ñów gannaaw moom, nekkoon na laata moom, balaa nuy duggu ci limu geñoy àddina si. Ci boobu kàddu Yaxya biral na nekkinu Krist ba fàww. Seedeel na dëgg gi wax ne Krist moo sut jaww ji, jamono ji, ak sànku gi, Yàlla ju amul àpp la te maneesu koo ger. Ca màndiŋ ma Yaxya metitlu na fa ni mu gise ni bàkkaari nit ñi ñànge. Mu jàngal leen rëccu te tuub ngir mbaalug bàkkaar yi. Waaye bi mu gisee Yeesu, xolam sedd guy, ndaxte Krist juddu na ni nit ku amul àpp, fees ak dëgg, te dee gi manalu Ko dara. Mbégte jëmmal gi ak bu Noel ñungi sosoo ci. Peeñug dund gu dul jeex gu Yàlla, ci yaramu nit ki. Noonu la ndamu dund gi ci kow dee gi tàmbalee, ndaxte ci Yeesu lañu faagaagale bàkkaar bi yóbbe dee. Ni mu gise xóotaayu yiw woowu, la Yaxya màggal te yékkati mataayu Yàlla ci Yeesu. Póol waxoon na ne: ”Ci Moom la mataayu Yàlla feeñe ci jëmmu nit. Am ga lépp ci Moom,ba mu mat sëkk. Yowaana dafa tënk dëgg yooyu bi mu waxee:” Te nun ñépp jot nanu cig mataayam, te muy yiw ci kow yiw. Lan mooy mataayu Krist ak lan lanu jote ci Moom? Boo fàttalikoo ni Yowaana faramfàccewoon kan mooy Yeesu, ci aaya yi nu weesu, kon dinga xam màqaamaam, te gis nan la nu géeju yiwam di baawaanee ci nun bés bu nekk. Krist mooy Kàddug Yàlla gi jóge ci Baay bi, ni wax di génne ci gémmiñu nit. Moom mooy xolu Yàlla ak coobareem, nekkinam ak mbégteem, bi gën a xóot. Ni kàddug Injiil di, duggee ci sunu xel, te soppi sunu coobare, noonu la Krist di ñówee ci sunu xol, te soppi nu, jaare ko ci tabeem. Ndax loolu du yiw wu kéemaane? Krist mooy Dundug Yàlla: Boroom yenn xam-xam yi man nañu tabax ay kër,a y pom(jéggikaay) ak ay Ci boomb (ndell), waaye kenn ci ñoom manul a sàkk dund. Waajur yi war nañu xamal seeni doom, dund gi leen Yàlla may. Ndax du yiw? Te ndegam dundug àddina dafay wéy, Krist dafay yónnee way-gëm yi Xelam ci boppam miy dund gu dul jeex mukk. Kercen yépp ñoo bokk dundug Yàlla gi, te duñu dee mukk.Ndax loolu du yiw? Krist mooy Leeru àddina si. Moo daan lëndëm gi, te Moo sàkk leer gi ci guddi gu lëndëm gi. Dafay may yaakaar àddina su lëndëm, wàcce kàttanam ci àddina suy siicu ndax ay metitam. Leeru Krist moo man a dàq lëndëm gi ci àddina si. Ci wàllu politik, ak ci bërëbu liggéeyukaay yi, ci njaboot yi, ak ci jàngu yi, ñi Ko gëm, dañuy jot dooley jub te am ngor. Xanaa loolu du yiw ci kow yiw? Yeesu Krist moo Sàkk Jaww ji. Ci Moom la mataayu kàttanu Yàlla nekk. Ay kéemaanam ay misaal lañuwoon yuy wone sañ-sañam. Ndekkiteem ci ñi dee, seede na kàttanu dundam ci kow dee. Ci wàllu yaram, daan na doole ji nuy xëcc nu jëm suuf, ba dox ci kow ndox. Ci juróomi mburu ak ñaari jën, suurloo na ci 5000 nit. Xam na sax ñaata karaw la sa bopp bi am. Ndax dinga sujjóot ci kanamu yiwam, wi lay toppatoo? Ndax bëgg nga xam lu gën a takku ci mataayu Krist? Moo moom àddina si. Moomeel yi,alal ji,sa simili dund bu nekk,Moo leen moom.Moo la moom itam.Moo la sàkk te Moo lay aar.Krist moo moom lépp. Dafa la dénk ay melokaanam ngir nga Ko leen di sàmmal.Sa doole,say xalaat,ak say waajur yépp,ay may lañu yu la Boroom bi jagleel.Ndax di nga Ko gërëm ngir yiwam wi? Li doy waar ci jëmmal gi ak Noel mooy ne mataayu Yàlla, ci ab liir la ñówe. Kéemaan googu Esayi waxoon na ko 700 at laata muy am,t e Xel mu Sell mee ko ko xamaloon: ”Ndaxte doom juddul na nu, mayees na nu doom ju góor, te dina yor nguur gi. Dees na Ko tudde Diglekat bu yéeme, Yàlla mi man lépp Baay ju baax, Buuru jàmm.” (Esayi 9:6) Lees ñaawlu nag, mooy ne xelu nit dafay yéex a xam ne Yàlla ci Krist, yeesalaat na ci doomu Aadama sellay ga nekkoon ci nit ki, ca njabéen ga. Yeesu dafa màgg, maandu, te Mooy diglekat bi xam, Yàlla Aji Sax ju am kàttan ji. Melokaani Yàlla yi aky mayam yépp ñungiwoon ci liir, bi ci ñàddu jur gi. Ndax seetlu nga bu baax yiw wu kéemaane wi nu Yàlla may bi Mu ñówee ci nun ci jëmmu Yeesu? Man nanu wax: Yàlla,jarajëf! Krist bëggul a aakimoo ay ngëneelam Moom kenn, su doon loolu, kon Mu toog asamaan. Dafa ñów ci sunu àddina, def boppam nit, nirook nun suufeelu, gir ubbil nu yoonu asamaan, jubóole nu ak Baayam te sol nu mataayam ba nu fees-dell. Noonu itam, Póol seede na ne li Yàlla namm mooy teewaayu mataayam ci Jàngu bi. Jàngal Efes 1:23;4:10 ak Kolos 2:10, kon dinga tàmbali màggal Yàlla te di kañ yiwu sunu Boroom. Bul dëkk ci tumuranke ndax say bàkkaar, waaye ubbilal mataayu Krist sa xol bi. Jegesil liir bi ci ñàddu jur gi, noonu barke yu bare dinañu baawaan ci sa kow. Dina la soppi teenu yiw ngir ñi la wër. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, yaaDoomu Yàlla ji. Mbëggeel, Kàttan ak dëgg ci yow la fekk baax. Nungi lay sujjóotal te nungi bànneexu ndaxte tooguloo fu nu sore, waaye danga ñów dund ak nun. Danga noo bëgg. Danga def sa bopp nit te rammu nu. Nungi lay sant ci li nga nu may yiw ci kow yiw. LAAJ:
|