Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 010 (The fullness of God in Christ)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
A - Peeñug Kàddug Yàlla gi ci Yeesu (Yowaana 1: 1-18)

3. Feesaayu ndamul Yàlla feeñ na ci jëmmal gi (Yowaana 1:14-18)


YOWAANA 1:17-18
17 Ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lañu leen jaarale,y iw wi ak dëgg gi, Yeesu Krist moo leen indaale. 18 Kenn mosul a gis Yàlla, waaye Bàjjo bi, di Yàlla te nekk ak Baay bi moo ko xamle.

Li wuutale Kóllëre gu Njëkk ga ak Kóllëre gu Bees gi, man nanu ko tënke ak ni njubte gu Yoon wi di maye, maanaam Ndigal yi, ak njubte gu Yiw maye. Yàlla dafa joxoon Musaa Fukki Ndigal yi, sart yi aju ci sarax yi ak yoon wiy sàmm mbiri doxalinu dundin gi. Képp ku sàmmoon yooyu sart, yelloo dund gi. Waaye képp ku leen moy, dee nga doon yelloo. Naka noonu, Yoon wi ab àtte lawoon buy jëme ci dee, ndaxte kenn matul. Nit ñi gënoon a sàmm diine, dañu daan am rëccu ak naqarlu ndax li kenn manual a top sarti Yoon wi. Ñi woyofaloon seen diine nag, dañoo jàppewoon seen bopp ni ñu baax, yaakaar ne seen dund neex na yàlla. Noonu lañu daanoo ci bopp-sa bopp ak xarañ ci Yoon wi. Ñu fàtte mbëggeel gi, te di bàkkoo njubteg seeni jëfi bopp. Ci lu wóor Yoon wi sell na, ndaxte sellaayu Yàlla lay wone. Waaye ci kanamam, benn doomu Aadama baaxul. Naka noonu, Yoon wi, ci tumuranke ak dee lanu jëme.

Ci biir googu nekkin guy xeeñ dee, la taskatu Injiil bi door a tuddu turu Yeesu Krist, te di Ko wone ni Goreelkat biy rawale ci tumuranke, ak ci merum Yàlla mi. Yeesu Krist mu Nasaret, Mi ñów nekk nit, mooy Almasi, bi ñu digewoon te sotti Ko diwu matug Xel mu Sell mi. Mooy Buuru buur yi, Kàddug Yàlla gi ak Saraxalekat bi. Moom mooy gàttalu bépp pexe ngir dab yaakaar ak mucc.

Yeesu ñówul ci nun ak Yoon wu bees (maanaam sarti diine yu bees). Xanaa kay dafa noo rammu ci toroxteg Yoon wi. Bëgg nu, moo tax Mu matal lépp li nu Yoon tegoon. Gàddu na sunuy bàkkaar, ak àtteb àddina, te noonu Mu jubóolewaat nu ak Yàlla. Yàlla du sunu noon, ndax sunuy bàkkaar, ndaxte jote nanu jàmmam ci Yeesu Krist, sunu Boroom. Yeesu ni nit, yéeg na asamaan, dem ca Baayam bu Sell bi, ba noppi, Mu yónnee nu Xelam mu Sell mi. Dafa yet Yoonam wi ci sunu xol, feesal sunuy yégeel yi gën a xóot, ak xalaat yu laab, dëggu te gore. Dundatunu ci sasi Yoon wi, waaye Moom mungi dund ci nun. Noonu la Yàlla di mayee dooley, matal li mbëggeelam laaj.

Ba Krist ñówee ba tey, ci jamono yiw la nu nekk. Yàlla laaju nu ay sarax, ay màggal, walla ay sarax yu ñuy rendi, ngir dalal sunu xel, waaye dafa yónni Doomam ngir Mu may nu njubteem gi jóge asamaan, ci Moom. Ku Ko gëm, mayees na la nga nekk ku jub-xocc ci kanamu Yàlla. Loolu moo tax nu Koy sant, te bëgg Ko, te di jébbale sunu bopp ni sarax yuy dund, ndaxte Sellal nanu.

Krist bàyyiwunu ni ay jirim, waaye dafay nekk ak nun te di nu baaxe ay mayam. Yelloowunu mbaalug sunuy bàkkaar, rawatina sax di jokkoo ak Xelum Yàlla. Yellowunu itam beneen may, walla barke. Ci wàllam, lépp yiw la. Ci dëgg-dëgg, yelloowunu lu dul mer ak sànku. Waaye li nu lëngoo ak Krist ci kow ngëm, moo nu may nu nekk ay doomi Yàlla yuy xéewlu ci yiwam. Ndax gis nga bu baax li wuutale jaami bàkkaar yi ak doomi yiw wi?

Yiw wii du yëgeel kese ci xolu ku sell. Waaye mbëggeel la gu sampu ciy sarti Yoon. Yàlla du tëb rekk baal ku ko neex, ndaxte bàkkaaru ki bàkkar, deewam mooy payoor gi, ci saa si. Fekk na ne daajug Krist ga Mu nu wuutoo, matal na gépp njub. Noonu, yiw wi nekk na léegi sunu yellef, te yërmande Yàlla nekk dëgg gu kenn manual a jengal. Yiw wi ci Krist moo lal sunu dundin ak Yàlla.

Yaangi laaj sa bopp naan : Kan mooy Yàlla jii man a def lépp lu ko neex, ba noppi manual a tàqalikoo ak njubteem? Lii mooy sunu tontu: Ay diine yu bare jéem nañu ak seen kéem-kàttan ngir xam Yàlla. Waaye dañu mel ni ab esel (yéegukaay) bu ñu teg ci suuf, te manul jot asamaan. Waaye Krist dafa mel ni eselu Yàlla, buy wàcce asamaan te sampu ci suuf. Sunu daje ak Yàlla, jaare ko ci moom, du bayyi kenn muy ñàkk yaakaar.

Kenn ci nun mosul a gis Aji Sàkk ji, ndaxte sunuy bàkkaar ñoo nuy teqale ak Ku sell Ki. Li ëpp ci li ñuy wax ci Yàlla, ay natti xel doŋŋ la. Waaye Krist, mooy Doomam ji nekkoon ak moom ca lees amul àpp ja te it nekk kenn ci kenneefu ñett ñi. Naka noonu, Doom ji xamoon na Baay ji. Lépp li ñu feeñaloon laata jamono jii, doyuloon. Waaye Krist mooy Kàddug Yàlla gi tigi ak tënku dëgg gépp.

Lan mooy puju bataaxalu Krist?

Yeesu jàngal nanu ni nu war a waxe ak Yàlla ci biir ñaan: ”Sunu Baay bi ci kow asamaan.” Feeñalal nanu noonu ne Yàlla ci boppam, Baay la. Yàlla du forsekat, ab lëlkat, walla ab yàqkat. Du Ku yëgul dara mbaa faalewul dara. Dafa nuy toppatoo, ni baay di toppatoo doomam. Bu xale daanoo ci biir ban, baay ja dafa ko cay génnee, te raxas ko ba mu set, waaye du ko bàyyi mu dëkkoo tooñ bi. Bi nu xamee Yàlla sunu Baay la ba léegi, ci la nu yewwiku ci ñàkk yaakaar bi nu sunuy njàqare, ak sunuy bàkkaar indil. Baay ji laabal na nu te dalal na nu. Danuy dund ak Yàlla ba fàww. Coppite diine gi fëll ci àddina si cituru Baay bi, mooy xalaatu kercen bu bees, bi Krist di wesaare. Turu baayoo boobu dafa ëmb gàttalu ay kàddu ak ay jëfi Krist.

Laata jëmmalam gi, Krist, Baayam la nekkaloon. Nataal boobu mooy leeral jokkoo mbëggeel gi dox diggante krist ak Yàlla. Ba Mu génnee àddina ba noppi, Doom ji dafa dekki te dellu ca Baayam. Toogul rekk ca ndeyjooru Yàlla, waaye munga itam ca biiram, Loolu mooy tekki ne mungi ci Moom, benn la ak Moom. Noonu lépp lu Krist wax ci Yàlla, dëgg laCI Krist, danuy gis Yàlla. Doom ni Baay. te Baay ni Doom.

ÑAAN: Sunu Baay bi ci kow asamaan, nungi lay sant, di la gërëm, ndaxte yónnee nga nu Krist sa doom ji nga bëgg.Nungi lay sujjóotal, ndaxte yaa nu goreel ci coono Yoon wi (Ndigal yi) te daaj nga sa njubte gu sell gi ci nun. Nungi lay gërëm ngir sa mayu baatin gi te di la màggal ndax ngëneel yi nu am ci sa Tur wi nga nu Baayoo.

LAAJ:

  1. Ban xalaat bu bees la Krist indi ci àddana si?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 10, 2025, at 08:44 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)