Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- Tracts -- Tract 08 (Who is Christ?)
This page in: -- Armenian -- Baoule -- Burmese -- Chinese -- Dagbani? -- Dioula -- English -- French -- German? -- Greek -- Hausa -- Hebrew -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Japanese -- Korean? -- Lingala -- Maranao -- Nepali? -- Peul? -- Somali -- Spanish -- Sundanese -- Telugu? -- Thai? -- Turkish -- Twi? -- Uzbek -- WOLOF -- Yoruba

Previous Tract -- Next Tract

BATAAXAL - Bataaxal bu ñu tënk ngir séddale ok

BATAAXAL 08 -- Kan Mooy Krist?


Mbootaayu politik yi, ak diine yi dañuy jébbaane li ñu gëm, teg ci di xamle ci ay téere walla Internet, jaar-jaaru ka ko sos; noonu lañuy jéem a xëcce ñi ñu bëgg ñu féeteek ñoom.

Doomu Maryaama nag dafa dànd boobu fésal. Ki Ko bëgg a xam rekk la bëgg a feeñu. Turu "KRIST" 569 yoon lay feeñ ci téerey Kóllëre gu bees gi. Doomu Maryaama ji wone na ki Mu doon bi Mu naan: "Xelum Boroom bi mungi ci man, ndaxte moo ma tànn, ngir ma yégal néew doole yi xebaar bu baax bi. Dafa maa yónni ngir ma yégal jaam yi ne dinañu leen goreel, yégal gumba yi ne, dinañu gis, te jot ñi ñu noot; tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi." (Luk 4:18-19)

KRIST mi ñu diw, Moo feeñal kumpa gi nekkoon ci Moom ba Mu taree baat ya Yonent-Yalla Esayi waxoon 700 at laata Moom muy juddu (Esayi 61:1-2)

Doomu Maryaama ji, ci Xelum Aji sax ji la juddoo. Rax ci dolli Yàlla yónni Xelam mu Sell mépp ci KRIST ngir man a jëfe ak Moom ci kow galen gu rafet,ngir Mu matal coobareem. Krist mosul a am bàkkaar, dafa laab te sell.

Moom biral na ne Moo doon “Ku sell ki fees dell ak Xelum Boroom bi”. Ca jamonoy Kóllëre gu njëkk ga, buur ya, saraxalekat yu mag ya, ak Yonent-Yàlla ya dañu leen daan sotti diwlin ju sell, ngir wone ne dañu leen a ber ngir ñu nekk surga Boroom bi, yu fees ak Kàttanu Yàlla ak maanduteem. Ci Téereb Kóllëre gu Njëkk gi,diwlin ju sell ji misaalu li war a feeñ ci KRIST lawoon. Dañu Ko sotti diwlinu Xel mu sell mi, ngir Mu falu ni buur bu am nguur gu amul àpp (Dañiel 7:13-14) Saraxalekat ba fàww (sabóor 110:4) Yonent-Yàlla bi ñu digewoon (Pàttalim Ndigal yi) (Detoronom 18:15), Rammukatu bàkkaarkat yi (Esayi53), ak Kàddug Yàlla gi ñu soppali suux (Esayi 61:1-2). "Krist " du turu Doomu Maryaama, waaye dafay firnde sas bi Ko Yàlla tegal.


Lu Tax Ñu Yónni Krist ?

Aji Sàkk ji dafa yónni KRIST, sol Ko Kàttanu Xel mu Sell mi ngir Mu yégal néew doole yi xebaar bu baax biy muccloo, ndax ñu man a rëcc ci merum Yàlla, te texe ca bésub àtte ba.

Du boroom màqaama yi, boroom alal yi, boroom xam-xam yi, kaŋaam yi, walla kilifa yi la Yàlla tànnoon, waaye ci biir mbëggeel ak yērmaande dafa woo tuut-tànk yi, ñi amul wërsëg, bàkkaarkat yi, néew doole yi, ak ñépp ñi soxlawoon ndimbal. Aji Kàttan ji dafa yónni KRIST ngir miskiin yi ak ñi ñu beddi jot ci yaakaar ji, Kàttanu xel ak dund gu amul àpp jaare ko ci Xel MU SELL mi Mu leen di may.

KRIST dafa woowe bataaxalam "Injiil", maanaam Xabaar bu Baax bi. Képp ku gëm boobu bataaxal dinga bokk ci njabootu Yàlla, te am kēr ca asamaan. INJIIL moo daan mbañeel gi nekk ci àddina. Kàdduy Krist dañuy dàq luubali fen yi naxaate yi, te am ndam ci kow laabadi ak njaaloo. INJIIL, mayug Yàlla la. Képp ku jàngul, te nanguwul may bàjjo, bi la Krist may, ci ndóol, ñàkk yaakaar, ak ñàkk jokkoo ak Yàlla jiy dund gi, ngay mos a dëkk.

Krist dafa biral ne Yàlla moo Ko yónni ci ñi seen xol toj ndax seeni njàqare ak seeni bàkkaar. Dafay goreel ñi seeni bàkkaar di noot ci kow nguuru seytaane. Dafay dekkal bàkkaarkat yi dee ci baatin ngir may leen dund gu bees gu laab te jub. Krist daawul wax ay Kàdduy neen, waaye dafa daan dunde lépp la daan génne ca gémmiñam. Képp ku jàng ay kéemaanam ci Injiil ak ci Alxuraan, dinga nangu ne Doomu Maryaama ji mooy Almasi dëgg-dëgg, bi ñu xēpp diwlinu Kàttanu mbëggeelu Yàlla. Desul ca bàmmeel ba. Mungi dund. Digoon na taalibeem ya ne leen Kàttanam di na leen solu te mëññe ci ñoom.


Ndax XEL MU SELL MI ganesi na la?

Krist du parparloo, aakimuwul barkeb Xel Mu SELL MI, ak kàttanam gi jóge asamaan. Moom dafay maye Xel Mu SELL MI ñi nga xam ne dañu ñàkk yaakaar te di wut jàmmu Yàlla, ngir man a am wàll ci coomp yi Xel Mu SELL MI di maye ci yiwam, ba solu te fees dell ak mbëggeelu Yàlla gi. Laajal sa bopp lii: "Ndax sama bàkkaar moo tax ma selladi ? Walla damaa bëgg a laab te jub ci kanamu Yàlla, jaare ko ci Yeesu, te it ñu sol ma diwu Xel Mu SELL MI?" Moom nee na:

Képp ku ma Baay bi jox dina ñów ci Man,te duma dàq mukk ki may fekksi.” (Yowaana 6:37);

Ku ma gëm am nga dund gu dul jeex” (Yowaana 6:35,47; 8:12; 10:27-28; 11:25-26); ak

Ku ma wóolu, maa ngi dëkk ci yaw”.

Sama mbokk mi,
Bu fekkee ne ràññee nga xóotaayu dige yi jóge asamaan, ubbilal Krist sa xol ngir Mu diw la Xelam Mu Sell mi.

Krist biral na ne dañu Ko sotti diwlin, te yónni Ko ngir Mu yégle atum yiwu Boroom bi. Tawretu Musaa xamal na nu ne 50 at yu nekk dañu waroon a goreel jaam yi, te delloo leen seen alal jépp. (Lewi 25: 10 ak li ci topp).

Loolu misaalu goreel gu gën a rëy lawoon. Krist dafa bëgg a yewwi jaami bàkkaar yi ci seen selladi ak seen moy, ngir delloo leen ca Yàlla. Krist am na sañ-sañ ak Kàttanu goreel leen. Moom dee na ngir bàkkaari àddina si. Bu njëkk, Musaa la Yàlla dénkoon Santaane yi,waaye yiw wi ak dëgg gi, Yeesu Krist moo leen indaale (Yowaana 1:17). Ba Yeesu jébbalee boppam ngir nun ba léegi, kenn ku nekk ci nun man na jákkaarloo ak Yàlla ni mu ko neexe. Dinanu jot nganesig Xel Mu SELL MI nib digeb ndono nguuru Yàlla. Su ko defee, dunu wéy di jàppe Yàlla ni àttekat ba fàww, ca bésub àtte ba.Su boobaa, ni baay ju am yërmaande La nuy feeñoo, te di nu xaar ak teey ci biir mbégte mi Mu nuy dalale.


Ni Ma Dajee Ak Krist

Nekkoon naa ni ku bàkkaar tëj ci kaso, te it Nekkoon jaamu lépp lu nafsu di laaj. Mbégte ak lu neex rekk laa doon wut,rax ci dolli di bëgg a faj samay bëgg-bëggi yaram ngir feesal sama xol ak mbëggeel, waaye dara sottiwul. Gannaaw mbégte yu gàtt ya ma daan am, sama wéetaayu xol dafa daan dellusi ci man. Mu am bés, ma dégg ñuy wax ci Yeesu Krist, Musalkat bi nuy dimbali ci sunuy coono. Noonu ma tàmbali di Ko wut. Sama benn xarit wax ma li Doomu Maryaama defal bépp doomu Aadama, ba noppi mu leeralal ma nan la Yeesu man a soppee samag dund.

Krist dee na ngir man, te may na ma dund gu amul àpp, ngir ma nekk ci mbégte saa su nekk. Ngir jot mbégteem ak mbēggeelam, xamoon naa ne fàww ma jébbal Ko sama xol bépp. Noonu ma dogu ñaan ngir dalal Krist, Doomu Maryaama ji,ci samag dund. Te noonu laa ko defe. Dafa tàmbalee ci musal ma, te léegi nag maangi dunde mbég. Tiituma, te jaaxlewuma, ak li tolof-tolof yi di bare lépp, ndaxte Mungi may toppatoo, te di faj samay soxla. Sama mbokk mi, maangi lay soññ ngir nga def jéego bii, te ñaan Krist Mu dugg ci sa xol, ngir nga fees ak mbég, rax ci am jàmm ci biir bépp coono.

Ñaan Gi
Yów Yàlla mi fees ak yiw ak yërmaande, yaay Baayu ñépp ñi tuub seeni bàkkaar. Maangi lay sant ci li nga yónnee Krist, Mi ñu sotti diwlin, ci sunu àddina su selladi sii. Yeyoowuma Ko jege, mbaa may jot sa Xel mi, ndaxte bàkkaarkat laa. Moone dangay barkeel ñi dul bàkkoo seen am-amug xel. Nangu naa saraxu Krist. Kon, maangi Lay jaamu, te di la ñaan nga sol ma Xel Mu SELL MI, ndax ma man a soppiku ba nekk ku woyof, laab, am dund gu amul àpp am yërmaande, sell, te fees ak mbëggeel ni Krist. Amiin !


Ndax bëgg ngaa xóotal sa xam-xam ci Krist ?

Soo ko nammee, man nanu la yónnee Injiilu Krist, ak ay nafar yu ànd ak ay ñaan. Jàngal Injiil bi te ñaan ngir am jàmmu Yàlla ju amul àpp ji.


Séddool Xabaaru Krist bu baax bi ak say xarit

Su fekkee ne mos nga dund gu bees ak Krist, te jot barkeelu Xelam MI, kon mayal bataaxal bii say xarit ak ñeneen ñi gēm itam. Dinanu la dolli ay téere. Ñaanalal ñi ci jot a am. Sa leetar lanuy xaarandiku. Bindal sa adares ba mu leer naññ.

WATERS OF LIFE
P.O. BOX 60 05 13
70305 STUTTGART
GERMANY

Internet: www.waters-of-life.net
Internet: www.waters-of-life.org
e-mail: info@waters-of-life.net

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on May 16, 2025, at 11:20 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)