Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
Home -- Wolof -- Tracts -- Tract 09 (You shall love the LORD your God with all your heart, with all your soul, and with all your strength)
This page in: -- Armenian -- Baoule -- Burmese -- Chinese -- Dagbani? -- Dioula -- English -- French -- German? -- Greek -- Hausa -- Hebrew -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Japanese -- Korean? -- Lingala? -- Maranao -- Nepali? -- Peul? -- Somali -- Spanish -- Sundanese -- Telugu -- Thai? -- Turkish? -- Twi? -- Uzbek -- WOLOF -- Yoruba
BATAAXAL - Bataaxal bu ñu tënk ngir séddale ok
BATAAXAL 09 -- Nanga bëgg Yàlla sa Boroom, ak sa xol bépp, ak sa noo gépp, ak sa Kàttan jépp (Detoronom 6:5, Macë 22:37)Ñu bare dañuy taaba-taaba boor bu nekk, di ñaq ngir faj seeni soxla (Njalbéen 3:19). Ñungi gën a yokku te di wut mbégte ak jàmm waaye xaajuñu bàyyi xel ci lu aju ci àddina Yàlla ji; Boroom bi dafa bokkul sax ci seen dundin. Am na ñeneen ñu ragal Yàlla Aji Kàttan ji. Dañuy rëccu seeni jëf yu ñaaw, ragal merum KU Sell ki, ak bésub àtte ba. Ñooñu dañuy julli, di woor, di saraxe, di aji, te di def seen kéem-kàttan ngir neex Yàlla. Waaye nag xamuñu ne seen jëf yu baax yooyu doyuñu ngir musal leen ci Safara. Jinne yi sax gëm nañu ne Yàlla kenn la, moo tax ñu tiit bay lox (Saak 2:19). Ñu néew ñiy wut dëgg gi ñungi mel ni ab turnësol buy topp jant bi ci suba ba ngoon te du xéewlu ci naajam bi, du màgg te du àgg cig mat, ba man a meññ, jur doom yu bare. Képp ku dogu dellu ci sa Boroom bi dinga baarkeelu ci naaju mbëggeelam te solu Kàttan gi lay may nga meññ doom juy law ba fàww. Noo mel? Ban diir ci bis bi la sa xel di dem ci Boroom bi te nga di Ko ci jaamu? Fàttalikul aaya bii di wax ci mbëggéelu Yàlla: "Su fekkee ne damay wax làkki nit ñi ak yu malaaka yi sax,te boolewuma ci mbëggéel, duma dara lu dul dënd muy riir, walla jóolóoli buy kandaŋ-kandaŋi. Su ma yéglee wax yu tukkee ci Yàlla, ma xam lépp luy kumpa, ma yor xam-xam bépp, te gëm Yàlla ba man a randal ay tund, fekk boolewuma ci mbëggéel, duma dara.“ (1 Korent 13:1-2) Ndigai bii moo ëpp solo ci Kóllëre gu Njëkk gi :Nanga bëgg Yàlla sa Boroom bi, ak sa xol bépp, ak sa noo gépp, ak sa Kàttan jépp. Nanu laaj sunu bopp lii: Ndax ci dēgg-dēgg sopp nanu Yàlla? Ndax bëgge nanu Ko ak sunu xol bépp, sunu noo gépp ak sunu Kàttan jépp? Képp ku toggaat Ndigal lii ci sa xel ci biir njubte gu wér, dinga suufeelu te sa xol toj ndaxte dinga gis ne dese ngaa bëgg sa Boroom. Su ko defee, dinga biral ne: "Bëggewuma Ko sama xol bépp, sama noo gépp ak sama Kàttan jépp. Sama Xel ak sama yërmaande dese nañoo dëkk ci Moom . Du Yàlla doŋŋ la sama xol di rëkkal, sama noo gi feesul ak mbëggeelam, te sama yëgeelu biir jubluwul ci Aji Sàkk ji kese. Bëgg naa Ku Sell Ki, waaye jébbaluma Ko sama mbëggeel gépp, ndaxte jot gu takku, coono ak xaalis laay jagleel samay yitte àddina yiy seey ëllëg." Aji Kàttan ji dafa bëgg nu rëccu te baalu sunuy bàkkaar ci ay rangooñ yu ànd ak ragal, ndaxte nun ñooy sunuy xërëmi bopp yi nuy jaamu, ndaxte sunu bopp moo nu gënal lépp. Bëggewunu sunu Boroom bi ni mu ware, te ci Moom la bépp barke di jóge. Loolu mooy sunu cosaanu bàkkaar. Danu yelloo merum Yàlla. Dee ak Safara mooy mbugal gi nu yelloowoon, ndaxte Yàlla jiituwul ci sunug dund, te mujjewu ci. Bu nu tuubul sunuy bàkkaar ci dëgg-dëgg, kon dinanu sànku ba fàww. Boroom bi xam nanu, xam na ne ɓàkkaarkat lanu. Ci kow loolu lépp, terewul Mu bēgg nu, te bàyyiwu nu, ndaxte yónnee na Doomu Maryaama ji ngir won mbëggeelam nit ñépp. Krist déggal na ndigal li gën a rëy. Ñaan na te jàngal ay taalibeem ni ñuy ñaane: Sunu Baay bi ci kow, na sa tur sell, na sa nguur ñów, na sa coobare am ci suuf mel ni ci asamaan. May nu tey li nu war a dunde; te baal nu sunuy tooñ, ni nu baale ñi nu tooñ; bu nu teg ci yoonu nattu, waaye nga musal nu ci lu bon. Ndaxte yów yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin. (Macë 6:9-13)'' Krist kañul boppam waaye Baayam bi ci asamaan la màggal, te biral na ne: “Sama ñam moo di def coobarey ki ma yónni, te matal liggéeyam” (Yowaana 4:34). Noonu la Krist wonee mbëggeelam gu dëggu gi Mu am ci Yàlla. Doomu Maryaama ji nekkuloon ab suufi walla koo xam ne diine lay wut a dunde, ndaxte mbëggeel gi nekk ci Yàlla feeñ na ci ni Mu bëgge nit ñépp. Jaar na ci ay dëkk-oo-dëkk di xamle ni Yàlla baayoo ñépp. Wéral na ñi wopp,dàq jinne ya jàppoon ay nit, dekkal ñu deewoon, far bàkkaaru àddina si, te jébbale dundam ngir wuutu askan yépp, ba jubale leen ak Yàlla. Krist dafa nuy laabal ci bépp bàkkaar ci ni Mu jébbalee benn yoon doŋŋ dundam ba dee. Moom gàddu na àtteb Yàlla bi nu waroon a dal, ngir képp ku ko gēm, te wóolu Ko, dénk Ko sa bopp, am dund gu amul àpp. Mbëggéelu Yàlla, ci KRIST la féñe.Dafa nu bëgg a soppi ba nu nekk ay nit yu fees ak yërmaande ni Yàlla Boroom yërmaande ji. Ni Mu laabale ay taalibeem ci seeni bàkkaar, noonu itam la Krist di wàccee Xelam Mu Sell mi ci kow ñiy ñaan tey xaarandiku kàttanu yiwam wi. Xel moomu mooy mbëggeelu Yàlla ci boppam, ni ko ndaw li Póol binde nii: “Mbēggeelu Yàllaa ngi baawaan ci sunu xol, jaarale ko ci Xelam Mu Sell mi Mu nu may.” (Rom 5:5). Xel moomu dafa nuy teg ci yoonu Yàlla, ak leeram, ba nu man a bēgg Yàlla, ak sunu xol bépp, sunu noo gépp ak sunu Kàttan jépp; te di ko jaamu ak mbég. Xel moomu dafa nuy xiir ci dunde ni Krist, te di ñaanal ñeneen ñi. Yàlla santu nu nuy déggal ay Ndigal yu kenn manul a topp: Won nanu yoon wi, te may nanu kàttan ngir nu man a wéy ci dundin giy seddal xolam. Mbokk mi,
Ndax bëgg ngaa xam lu gën a xóot ci Ndigali Yàlla yi ak ay digeem (ndigam)?Soo ko bëggee dinanu la yónnee Injiilu Krist bu ànd ak ay nafar aky ñaan. Dinga ci fekk itam lu ëpp téméeri Santaane Yàlla. Xelum Yàlla mi dina la jàppale ba nga man leen a déggal.
Soññil say xarit ngir ñu bēgg Yàlla ak nit ñi.Yégalal say dëkkandoo ak say xarit, Xabaaru mbëggeelu Yàlla bu baax bi ci ni nga leen di maye bataaxal bii. Man nanu la ci may as tuut .Wax- nu ñaata nga ci bëgg a maye. Bindal sa adares ba mu leer naññ. WATERS OF LIFE Internet: www.waters-of-life.net |