Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Armenian -- Baoule -- Burmese -- Chinese -- Dagbani? -- Dioula -- English -- French -- German? -- Greek -- Hausa -- Hebrew -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Japanese -- Korean? -- Lingala -- Maranao -- Nepali? -- Peul? -- Somali -- Spanish -- Sundanese -- Telugu -- Thai? -- Turkish -- Twi -- Uzbek -- WOLOF -- Yoruba
BATAAXAL - Bataaxal bu ñu tënk ngir séddale ok
BATAAXAL 07 -- Aji Sax ji moo lay dëfal !Bu nu xaymawoon rëyaayu tiis ak déggi rangooñ yi ñu dajale ci sunu àddina si, kon dinanu waaru,ñàkk yaakaar te ànd ak xel mu teey. Waaye nag Tawret ak Injiil ñoo nu dëfal te di nu jàppale ci biir lëndëm gi. Aji Sax jiy yërmaande moo sol Yonent-Yalla Esayi ay baat yu fees dell ak yaakaar: "Ni Ndey di dëfale doomam (jiy jooy),noonu laa leen di dëfale." (Esayi 66:13) Mbēggeelu ndey ak laabiiram la Yàlla jēfandikoo ni misaalu yërmandeem. Képp ku bëgg a xam ni dëfalu Yàlla mel, nanga ko seetlu ci ni yaay di naxe doomam. Yaay dafay ëmb doom, jur ko ci coono, noonu doom ja nekk wàll ci moom. Yaay ji dafay xam ne am na warugar ci xale bi, ndaxte dafa ko war a toppatoo, sàmm ko te di ko jox ñam bu xiifee; rax ci dolli di ko sang ay yooni-yoon ci bés bi, di foo ak moom te di ko fóon rax ci ay baati waxtaan yu xale bi déggul sax. Du bàyyi mukk xale bi wéet, ndaxte Yàlla moo ko ko dénk. Yaay, dafay wone mbëggeelam gépp ak baaxaayam gi mu am ci doomam. Ci ni muy màgge,yaay ji dafa koy jëndal ay yére aky dàll,di ko sang ak di toppatoo néegam .Bu wàccee ekool, mu jàngalaat ko te dimbali ko ca sas ya mu am. Bu doom ji defee naka -su- dul- noonu, mu yedd ko mbaa mu yer ko, te di am yaakaar muy màgg ci njubte. Dafa koy artu ci dorog yi, séy yu lewul, bokkaale ak rab yu bon yi walla luxus. Dafa koy jéem a wutal ay xarit yu baax. Moom ci boppam sax,mooy royukaayu doomam. Xale bi xam na ne ak bépp ndëgate bu mu man a def,man na ñibbisi këram. Dafay diis jafe-jafeem yi yaay ji ,noonu ndey ja may ko nopp ba noppi denc lépp ci xelam. Ndey ji dafay jàngal doomam lan mooy ngëm, te xamal ko màqaama Yàlla.Dafa mel ne YAAY du sonn mukk!
Dëfalu Yàlla gu sedd giNi ndey di bëgge ,maanaam yërmaandeem, dogoom, ak muñam ñooy misaal mbëggeelu Yàlla ak dëfalam. Dafa fees ak mbëggeel ngir teeru ñiy wëlbatiku ci Moom. Biral nanu ne: "Man,Man doŋŋ maay dëfalaate." (Esayi 51:12)Aji Sàkk ji yilif duniyaa gépp, biral na Yonent-Yalla bi ak askanam ne ci biir njaam sax Moom taxaw na ngir dëfal leen, te dimbali leen, su fekkee ne nangu nañu dellusi ci Moom te déggal coobareem. Aji Kàttan ji dafa bëgg a dimbali te dëfal. Looloo tax boo amee ay jafe-jafe bu leen nëbb, waaye diis leen Boroom bi,te noonu dinga gis ne Moom man na def jëf yu kéemaane boo Ko wóoloo. Aji sàkk ji moo nu sàkk, may nu dund gi,doole ji, xel mu màcc, dogu bi, maandute gi, yaram wi ak xel mi. Dunu ay doj yu ne copp,walla ay gàncax yu tëx, waaye ay nit yu ñu goreel lanu,yu am xol,ak xel yu màcc. Aji Xam lépp ji, umppalewul sunuy may (man-man) ak sunuy néew doole. Xam na sunu ëllëg, te dafa bëgg nuy wéy ci jëf yu rafet, yi mu nu fàgguloon ca Njalbéen ga (Efes 2:10). Yàlla am na lu mu la nattal. Moo la gën a toppatoo sax say waajur. Li gën ci yow rekk La, la bëggal. Yàlla du la báyyi mukk ci biir tiitaange,coono,walla lëj-lëj, waaye dafa lay toppatoo, te di la jàngal ni nga war a ñaane: "May nu tey li nu war a dunde" (Macë 6:11). Bul fàtte ne Moo la njëkk a ubbil buntu njàngaleem bi.Laata dara di xew, Moom xam na ki nga war a séyal te mu baax ci yów. Mungi lay aar te di la sàmm ci naxaate ak caay-caayu seytaane. Naga maandu, te dénk sa bopp Yàlla Baay bi la man a wommat. Geru àddina si dafa laaj àtteb Yàlla. Moone, Ku sell ki mayuloon kenn mu faagaagal nu, waaye dafa yónni Doomu Maryaama ngir Mu jubóolewaate nu ak Moom. Mungi woo ñépp ngir ñu tuub, jéggalu te dellusi ci Moom, ci biir nangu deewug Krist ngir bàkkaari àddina si. “Ngir képp ku ko gēm am dund gu dul jeex. Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji Mu am kepp, ngir képp ku ko gēm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk.” (Yowaana 3:15-16) Ni yaay di laabale biiram ay doomam ay yooni-yoon ci bés bi, noonu itam la la Yàlla ju sell ji bëgg a laabale, sellal la te yeesal la. Moom, boroom yërmaande ji, te di xaajook nun sunuy nattu, bēgg na laa dimbali, ba ci lépp loo tēle. Jekk na ngir baal la say bàkkaar yi gën a nëbbu,boo ko leen nangoo diis, te dëddu leen. Ku la bëgg la, te bēgg a waxtaan ak Yów; nga ñów rekk lay xaar. Kañ nga koy sant ci mbēggeelam gi, diis ko say sekkere, te jàng a wéy di dox ci coobareem?Bu loolu amee dina la teeru ak dalal gu rëy. Tëralinu Aji Kawe ji, roomb na loolu lépp. Dafa la bēgg a baayoo, te jàppe la ni kenn ci doomam yi. Dafa la namm a sol Xelam mu Sell mi ngir nga nekk doomu baatinam. Mbēggeelu Yàlla moo ëpp lépp li sunu xel man a natt. Sa yaram wiy dee la bëgg a may dund gu amul àpp. Ñówal ci Moom, wut ko, noonu dinga jot lii Mu dige: "Dingeen ma wut, te dingeen ma gis, bu ngeen ma wutee ak seen xol bépp." (Yeremi 29:13)
Dëfalu Krist“Barkeel ngéen, yéen ñi nekk ci nàqar,ndaxte bés dees na dëfal seen xol.” (Macë 5:4) Krist dafa nu ganesi ci sunu àddina si, indaale coono mbēggeelam ak yërmaandeem. Dafa yēramoon nit ñi sonn te di wëndeelu ni jur gu amul sàmm. (Macë 9:36) Moom dafa woo ay taalibeem ngir ñu topp Ko, ci kow seen coobare. Moo nekkoon seen royukaay, te doon leen wommat ak laabiiram. Ba Yowaana ak doomu ndeyam bëggee sant safaras asamaan mu wàcc ci kow ñi leen bañoon a dalal, Krist dafa leen a yedd, ne leen: “Xamu leen man xel moo leen di soññ” (Luk 9:55). Ba Piyeer weddee Almaseem bi, te fekk sax xamaloon na Ko ko laata loolu di am, dafa jooy xàcc. Gannaaw ndekkiteem, Doomu Maryaama dafa dajeji ak moom, baal ko, ba noppi soññ ko ngir mu dellu nekkaat surgaam. Ba Yudaa woree kilifaam ga ba jébbal ko noonam ya ci ab fóon, Yeesu móoluwu ko, te gëddu ko, waaye dafa ko laaj ne ko: "Sama xarit looy def nii? Ci fóon ngay jébbalee Doomu Nit ki ay noonam?" (Luk 22:48;Macë 26:50) Yeesu mooy mbëggeelu Yàlla gi ñu soppali suux maanaam nit.Dafa am yërmande ni Baayam bi nekk asamaan (Luk 6:36).Kéemaan ya Mu daan wérale nit ña,ñooy firnde yiy wone yërmande gi Mu amoon ci ñi nekk ci nàqar ak ñi wéradi .Ba mu gisee jigéen ja ñakkoon jëkkëram di robi jenn doomam ja mu amoon,dafa taxawloo robkat ya ,dekkil xale ba,delloo ko ndey ja. Ba fukki gaana ya xamoon ne waruñu jege ku wér ,déggee Yeesu mungi jaar ca diiwaan ba,dañu Ko woo ñaan Ko ngir Mu wéral leen. Dàqu leen de, waaye dafa leen faje ci kàttanu Kàddoom. Ba Mu dajee ak nit ka rab yu bon ya jàppoon, jinne ya nekkoon ci moom yépp dañoo yuuxu ndax yaakaar ju tas. Moom Yeesu dawu leen, waaye dafa goreel boroom rab ya, ci Kàddoom giy Kàttan gi. Yeesu dalloo na tow bu metti ngir taalibeem yi bañ a lab ci géej gi. Dundal na5000 góor yu xiifoon, ci juróomi mburu ak ñaari jën. Jarag ga ay xaritam teppiwoon ab puju néeg ngir wàcce ko ca kanamam, baal na ko ay bàkkaaram. Barkeel na xale yi te soññ jigéenu Lasaar ne ko: "Xanaa waxuma la ne boo gëmee dinga gis ndamul Yàlla?" (Yowaana 11:40) Yeesu dafa bëggoon àddina si, ba boole ci sax noonam yi. Xamoon na bàkkaari nit ñi, te Xamoon na itam ne manuñu musal seen bopp. Noonu, Mu gàddul leen seeni bàkkaar, te wuutu leen ci mbugalu àtteb dee gi. Ni ko Yonent-Yalla Esayi waxewoon: "Danoo teg ne mungi ci mbugal di ku Yàlla fàdd te suufeel Ko te fekk sunuy tiis la yenu, gàddu sunuy naqar.Sunuy bàkkaar a tax Mu gaañu, ne làcc ndax sunuy tooñ; mbugal gi nu may jàmm,Moom la dal,ay góomam ñoo tax nu wér, nun ñépp a réeroon ni ay xar, ku nekk aw saw yoonu bopp, te Aji sax ji yen Ko sunuy njubadi, nun ñépp." (Esayi 53 :4-6) Doomu Maryaama ji moo matal muccug àddina si, te taxawalaat njubte gu bëti Yàlla man a nangu. Ci kow deewam gi, may nanu sañ-sañu jot Xelum Yàlla miy Dëfalkat bi.
Ñówug Xel Mu Sell Mi Ci Kow Ndawi Krist YiKépp ku ubbil sa xol mbëggeelu Yàlla ak yërmaande Krist, te nangu ne dee na ngir yow, dinga jot Xelum Yàlla miy Dëfalkat bi, te itam di Xelum Dëgg gi. Ci ay jamono yu gàtt laata muy dee, Yeesu digoon na lii ay taalibeem: “...dinaa ñaan Baay bi,Mu jox leen beneen Dëfalkat buy nekk ak yéen ba fàww. Kooku mooy Xelu Yàlla, mi yor dēgg gi. Àddina si du Ko man a nangu,ndaxte gisu Ko te xamu Ko. Yéen xam ngeen Ko,ndaxte mungi dëkk ak yéen te dina sax ci yéen.” (Yowaana 14:16-26; 15:26-27; 16:7-14) Xel miy dëfale, Yàlla Baay bi moo ko dige. Ci turu Yeesu doŋŋ la ki koy ñaan di jote: "Ndegam yéen ñi bon yéena man a jox seeni gune lu baax, astamaak Baay bi ci kow ;dina jox Xel mu Sell mi ñi Ko koy ñaan!" (Luk 11:13) Xel mi dafa nuy xamal dëgg gi ci Yàlla, sunu Baay ci diine, ak it ci mbirum li war a ñów ēllēg. Dafay ubbi sunuy bēti xol, ñu xam dëgg gi nekk asamaan, dëgëral sunu ngëm, te may nu kóolute gu amul àpp. Moo nuy layool ca bésub àtte ba, Moom ak sunu Dëfalkat bi, bu fekkee ne sunu xel yey nanu ci Moom. Xelum Dëgg gi moo nuy wommat simili bu nekk ci sunu dund ni ko ndaw li Póol biralee: "Ndaxte ñépp ñiy déggal Xelum Yàlla mi,ay doomi Yàlla lañu."(Rom 8:14) Xelu Dëfalkat moomu moo nuy dimbali bu nu jànnaxee mbaa nu am gàcce,walla nu ñàkk a antule. Dafa nuy may kóolute ak jàmm ;di nu sàmm ci jéya yi, te di nu rëccloo ci fiiri dee gi. Xel moomu dafa nuy xiir ci dunde ak maandute te daan sunuy bàkkaar, bu nu leen jallaxee te bañ leen. Xelum Yalla mi dafa sell; dafa noo bëgg a sellal yey nu ngir nu nangu sunuy bàkkaar ci kanamu Yàlla, te dugal nu ci ngor, laab ak juboo. Dëfalkat bi jóge asamaan du damu, waaye Doomu Maryaama ji, sunu Rammukat bi,lay jollil ndamam, te di nu dimbali ba nu man a ràññee ay firnde mbēggeelam. Xelum Yàlla miy dund gu amul àpp gi ci Moom, ak Kàttan ji, duñu mos a jeex, ak nu mu man a deme. Dafa nuy dëfal, daan sunu dee gi, jaarale ko ci dundam, te dëkk ci nun ba fâww. Xelu Dëfalkat moomu dafay dëkk ci taalibe Krist yi ndaxte dañoo gëm ne moo leen wuutu ci dee gi ak àtte bi. Xel mi mooy soppi dundin ngir mbëggeelu Yàlla, baaxaayam, ak yërmaandeem feeñ ci ñoom. Dëfalkat boobu dafa nuy dimbali ngir nu tasaare Kàddug Yàlla gi, te di toppatoo ñi nekk ci coono. Dafa nuy sol ay sabóor, ay cant ak màggal. Dëfalkat bu am yērmaande bi dafa bëgg nu nekk ay dëfalkat, ni ko Póol waxe: "Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu Boroom Yeesu Krist, di Baay biy Aji Yërmaande, tey boroom lépp luy dëfal xol yi. Mooy dëfal sunu xol ci sunu tiis yépp, ngir nun ci sunu bopp nu man a dëfal xolu ñépp ñi nekk ci tiis, di leen sédd ci noflaay bi Yàlla def ci sunu xol." (2 Korent 1:3-4) Xelum Yàlla mi du tëb rekk soppi li nuy daj waaye nun lay njëkk a soppi, jaarale ko ci rammu gi nu Krist baaxe. Sunu xol angi yàkkamti sunu ñówug Musalkat bi ndaxte ca Njalbéen ga lanu tàmbalee bëgg. Ci Kàddug Injiilam la nuy jottalee Kàttanu yiwam gi Képp ku jàng ay Kàddu Krist, denc leen, te di leen dunde, di nga barkeel te tedd. Ndax mos nga dëfalu Yàlla ? Soo bëggee xam lu gën a xóot ci Xel miy dëfale, dinanu la may Injiilu Krist bu ànd ak nafar ,aky ñaan ,ngir nga man a am jàmm ak Yàlla, ci biir lëndëm gi. Dëfalal ñi la wër: Bu fekkee ne bataaxal bii may na la yaakaar ju bees,kon may ko ñiy wut jàmmu Yàlla ndax ñoom itam ñu man a dëfalu. Wax nu ñaata bataaxal nga bëgg a jot. Bul fàtte bind sa dëkkuwaay ba mu leer. WATERS OF LIFE Internet: www.waters-of-life.net |