Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Armenian -- Baoule -- Burmese -- Chinese -- Dagbani? -- Dioula -- English -- French -- German? -- Greek -- Hausa -- Hebrew -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Japanese -- Korean -- Lingala -- Maranao -- Nepali? -- Peul? -- Somali -- Spanish -- Sundanese -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Uzbek -- WOLOF -- Yoruba
BATAAXAL - Bataaxal bu ñu tënk ngir séddale ok
BATAAXAL 03 -- Barkeelal Aji sax ji, Cey ! yow sama ruu !Ñu bare, liggéey bu tar lañu dëkke, ngir sàmm seen bàkkan. Dañny bëgg a rënk xaalis (alal ju) bu bare ngir man a dund, te it dañuy jël jot ju bare di góor-goorlu ngir am dund gu naat. Moo ne de Doomu Mariyaama jàngal nanu ne : "Kenn manul a jaamoodoo nari sang ; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des Manuleen a boole jaamu Yàll ak jaamu Mamon, maamaam alal." (Maccë 6 : 24) Dawuuda moom jéem naa faj boobu jafe-jafe, jaare ko ci jaamu Yàlla. Dafa téye làmmiñam, te bës ay xalaatam, ngir man a saxal xalam ci Aji sax ji rekk. Bàyyiwul been xalaat di ko baaje, waaye dafa taxaw ci teewaayu Yàlla naan : "Sama ruu barkeelal Aji sax ji, te bul fàtte benn mbaaxam ! Moom moo lay baal jubadi, te di la wéral ci sa bépp jàngaro. Moom, moo lay rawale ci kàmb gi, di la muur kaalag mbaax ak yérmaande." (Sabóor 103:1–4) Di ñaan, ak di màggal dafa laaj pastéef ak góor-góorlu. Daawuuda dafa béggoon a teral Aji sax ji, te màggal ko. Xel mu sell mi dafay may ñi gëm, ñu man a dékku kàddug Aji Sàkk ji. Turu Aji sax ji 6828 yoon lay feeñ ci téerey kóllëre gu Njëkk ga, waaye baatu Yalla 2600 yoon rekk la ciy feeñ. Turu Yàlla, mooy "Aji sax ji". Tur wii mooy firndeel kóllëreem gi dul fecceeku mukk. Moom kese moo yelloo kóolute, ngërëm, na ko Daawuuda jëfewoon. Moonte, am na ay xalaat yu jollee ca xootaayu xelam, te di bañ a nangu googu tekkaaral. Loolu moo tax, yonnent bi delluwaat, jox ndigal ruuwam ngir mu màggal Aji sax ji. Mu dogu ne ay xalaatam dañu war a solu cant ak màggal, ba fees-dell. Daawuuda dafa nammoon a beg Aji sax ji, ak ruuwam gépp, te tera k oak jëmmam jépp. Noonu la tudde Aji sax ji, "Ku sell ki" amul benn naxaate, muusante, ger, mba bàkkaar. Képp ku jegesi Yàlla, ferñeenti sellaayam dinañu la laal ba feeñal hépp jëf bu sellul. Daawuuda kay mos na googu gis-gisug xel, ba suufeelu ci kanamu ku sell ki, te màggal ko. Sellaayu Yàlla dafay muur ndamam, ndox ku sell ki moo gën a màgg. Képp ku jublu ci Moom, dinga jot cellaay ju xóot ba ca sa bur xol. Daawuuda delluwaat na ñetteelu yoon di jox ndigal xelam ngir mu ne pàtt, te mu wéy di màggal Yàlla. Noonu ay xalaatam jaxasoowuñuwoon ; seeni mébét nekkatul xaalis, njàqare, mbaa ay coong yuy bette. Seeni mébét nekkatul xaalis, njàqare, mbaa ay coong yuy bette. Dafa dogu ci samp léppam ci Boroomu Boroom yi, miy attekatu àddina bi am sañ-sañu bépp àtte ci kow sunf. Xel mu sell mi moo may Daawuuda mu man a sant Aji sax ji, ci bépp ngëneel bu mu ko mayoon. Li ci ëpp dañuy faral di fàtte barkee yi ñu Aji sax ji jagleel, ak itam sunuy tontuy noon. Ñun ñépp ay jàmbaari fàttekati ay ngëneelam lañu. Ngir bañ a fàtte barkeel yi ngeen jote ci asamaan, nungi leen di ñaay xelat ngeen di bind bépp barke-bu leen Aji sax ji baaxe. Bu loolu wéyee, ngeen sant ko ci dëggantaan. Nàggalleen ko ci ngelaw lu feex li (peex mi), ndox mi tow bi – towu galaas bi, lekk gi, ak colu gi-ngir waajur yi, jangalekat yi, bérébu liggéey yi, ak dëkkuwaay yi- ngir kaarange gi ak jàmm ji ci réew mi. sant ko ci ni mu la aare ci mbënn yi yëngu – yëngu suuf yi, walla ci safara yiy jallee ciy tund. Sant ko ci n mu aare sam réew ci xiif ak xare. Bindleen seen yeneeni mbiri bopp yu leen soxal. Buleen Ŋott ci cant. Tàmmleen di màggal ak di sant ci mbir yu leer te dëggu, ngir ngeen nekk ci banneex, te mbegte Aji sax ji dëkk ci yeen. Xel mu sell mi moo may Daawuuda cant gi ëpp solo mooy gi aju ci mbaaling bàkkaar. Ñu bare danuy dund ni ñu amul benn bàkkaar. Dañuy nëbb seeni ñaawteef, te di doxantu ni ñu ànd ak tüs. Bul roy seeni doxalin, waaye rëccul say bàkkaar tuub leen, te dëddu leen. Diisal Aji sax ji say bàkkaar, te dogu bañ cee dellu mukk ; noonu dinga mos dal bi ndaw li yowaana di feeñal bi mu naan : "Su nu waxee ne amunu bàkkaar, kon nax nanu ounu bopp, te dëgg nekkul ci nun. Su nu nangoo nangoo sunuy bàkkaar ci kanamam, fekk na ne kuy sàmm kòllëre la te jub, ngir baal nu sunuy bàkkaar, te sellal nu ci lépp lu jubadi". (1 Towaana 1 ; 8 – 9). Daawuuda mos na yiwu Aji sax ji ko baal bàkkaaram yépp. Noonu mu sant ko, t exam ne ku sell ki jéggal lna ko bépp bàkkaaram. Yiw wu mate nü, kenn manu koo güs ci benn beneen dune. Baat yu mel ni "Sey-na" gisunu ken ci Towreet, walla ci Injiil, ndaxte Boroom bi, Aji sax ji du sunu yenn bàkkaar yi rekk lanuy baal, waaye dafa nuy sellal wecc, teggi sunu mbugal, le may nu yiwam ci kow mbëggeelam. Ndegam Krist ci deewam la fare bàkkaari àddina si, kon war nanu am kóolute ne : "Noonu ñi ñuy sellal, ci benn sarax rekk la ken yeggali cig mat ba fàww." (Yawut 10 : 14). Krist nee na, képp ku jot mbaalug say bàkkaar, war nga baal say noon, ni la Yalla baale : "te baal nu sunuy tooñ, ni nu baale ñi nu tooñ". (Nàccë 6 : 12). Ndax am nga ay noon ? Ndax ñàkk a déggoo dox na ci sa diggante ak keneen ? Kon dogul baale léegi balaa ngay ñàkk mbaalug bàkkaar bi la Yàlla nàkkal, te fayoo ci dara. Ñaanal Yàlla mu may la kàttanu baal metit yi la say noon teg, ni la Yàlla baale itam : "su ngeen baale ñi leen tooñ yéen itam. (Maccë 6 : 14) Gànnaaw loolu, xel mu sell mi daldi xamal Yonnent-Yàlla Daawuuda ne "wér-gi-yaram", weneen yiw wu am solo la. Mu sant ci Yàlla. Yenn saa yi danuy sibbiru, walla gaañu, mbaa nu am ay jàngoro yu të, waaye Boroom bi, ci kow yërmaandeem, dafa nuy wéral. Xayma fajkat yi, ak garab yi doyuñu ngir faj nu. Ndam lépp Aji-kàttan-ji moo ko yelloo. Aji sax ji moo nu dëfële nü : "Man maay Aji sax ji lay wéral". (Gàddaay 15 : 26) Doomu Mariyaama ji matal na dige boobu. Faj na ñépp ñi feebaroon, te ñówoon cà Moom, te dàq rab yu ban ya duggoon nit ña. Tey jii mungi jëfandikoo daktoor ak gardo yi, waaye wér-péŋŋ gi, ci Moom rekk lay jóge. Ndax bàyyi ngeen ci xel ? Buleen fàtte mukk sant ki leen sàkk ak seen xol bépp, ndaxte Moom moo leen di faj te di leen may wér gi-yaram. Yonent-Yàlla Daawuuda nitu diine dëgg lawoon. Xamoon na ne benn bés dina jàkkaarloo ak Boroomam. Ci noonu, dafa waajaloon deewam. Moonte, Boroom bi digoon na ko ne dina ko rawale ci kàmb gi, te loolu du mjubteem moo ko ko may, waaye ndaxte dafa gëm kiy goreele. Képp ku wóolu Kriste, du ragal dee, walla àtteb bàmmeel, ndaxte Doom Mariyaama ji nee na : "Man may ndekkite li, te may dund gi.ku mo gëm, boo deewee sax, dinga dund. Rax ci dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu ?" (Yowaana 11 : 25 – 26). Doomu MarIyaama ji dafa daan dee gi, ba noppi génn ca bàmmeel, ak bakkanam. Daan na seytaane, te wone ne mungi dund ba fàww. Dina dimbali ñépp ñi topp, jàpp ci seen, jéggeendoo ak ñoom buntu dee gi, te wéyale leen ci dund gu amul àpp gi. Xelum Boroom bi moo xamal Buur-Daawunda ne kaala wurus yi duñu li ëpp solo ci àddina. Kaalay Boroom bi dañuy lerxat ba fàww. Ki jot ci yërmaande Aji sax ji, te di ko séddookok mishiin ak ñi wéradi, te di faj soblay ñi ñuy sewal, dees na ko jox kaalag xel giy gu Aji sax ji. Ndax jot nga kaalag yërmaande ak ñówentalu sa Boroom bi muy may ai dagam yi am yërmaande ? Ndaw sa xol bi dafa wow nib xeer ? Walla nooy na léegi ba nga man a ñówenlal ñi sonn te di joy ? Krist dafa nuy dugal ci yërmaande gu amul àpp goo xamne du sunuy xarit rekk ak dëffandoo yi lanu koy séddool, waaye ak mboolem ñi soxla gindiku, ak ñi gëmul, te amuñu benn gaakaar cid und gii ak ga ca laaxira. Jegeleen, te bañ a jaaxle ci seen xar kanam yu xoyyi yi. Ñaanal leen te bàyyi xel ci ñoom ngir Aji sax ji man laa yónni fa ñoom ba nga jëriñ ci biir mbëggeel. Ñu sell-angi muuroo ay kaala yu böt manul a tegu. Ñooñu dañoo amoon yërmaande ci néew- dode yi ak ñi ndool, te ñaanal leen, dimbali leen, te xar seeni tànki tubéy ngir ñoom na leen ko Boroom bi defalewoon. Neewoom na: "Doomu nit ki dafa mów, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye muy seen surge, ba joxe bàkkanam ngir jotaat ñu bare." (Maccë 20 : 28) Krist mooy sunu yoon ak sunu (misaal) royukaay ; dafa nuy may doole ak fit ngir surgawu ko ka mbég. Sama Am-ji-jàmm biy jàng xët yii, Soo ko nammee, man nanu la yónnee injiilu Krist bu ànd ak ay ñaan ak ay xëti wéetoo ak sa Boroom yu lay dimbali ngir ngay màggal, di santa k sa xol bépp. Ñaaxal ñeneen ni ngir ñuy màggal ak di jaamu Boroom, Aji sax ji. Bu fukkee ne balaaxal bii tooyal na sa xol, séddoo ko ak say xarit ngir ñu man itam liggéeyal Aji Sax ji. Bind nu, ngir nu man la yónnee ay bataaxol yoo man a maye.
Ci biir xaarandi sab toontu, nugi lay ñaanal, te di sàkku ñaan ci yow itam. Bul fàtte bind sa dëkkuwaay nu mu gën a leere. WATERS OF LIFE Internet: www.waters-of-life.net |