Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
B - Ndekkite Yeesu Krist ak ay peeñoom (Yowaana 20:1 - 21:25)
3. Yeesu feeñu na taalibe ya, ak Tomas (Yowaana 20:24-29)YOWAANA 20:29 Xamunu ndax Tomaas laal na Yeesu, walla la mu gis légét ya doyoon na ko. Xëyna amoon na gàcce ci ñàkk ngëmam googu ak fit gu woyof. Ngëmu Tomaas mungi aju ci li gisoon. Boroom bi dafa bëgg a féddali sunu ngëm, yokk sunu kóolute gu wóor ci Moom ak ci kàddoom, te fekk du nu soxla gis Ko sax. Ki bëgg di am ay gént, walla ay janneer aky peeñu ngir biral ngëmam, kookule dafay door a gëm, àggagul cig mat te saxagul ci ngëm gi. Bu nu fàtte nag ne Yeesu feeñu na apotaram ya ay yooni-yoon ngir dëgëral seen ngëm. Yeesu baarkeel na ñi Ko gëm te gisuñu Ko, ñooñu dañuy am bànneex. Ngëm dëgg moo ëpp doole ay gént yu dul sax. Kóolute gi nit am ci Kàddug Yàlla, dafay sagal Yàlla mi kenn gisul. La ko dale ca peeñu Yeesu ya, la nu yéenekati Injiil yi ak apotar yi jottali njàngale mi nekk ci Injiil li ak Bataaxal yi. Ndekkite Yeesu moo jur jamono ju bees, joo xam ne dundu Krist moo ciy wommat xolu ñi gëm. Sunu ngëm nekkul lu woyof walla ay xalaati kese; Dund la gu ànd ak Taq ci Krist mi dekki. Sunu kéemaanu jamono la: Ay milioŋi nit gëm nañu Yeesu te mosuñu Koo teg bët, ndaxte seen gëm-gëm mos na kàttanu dund gu amul àpp gi. Ay Kercen yu bare ñàkk nañu seen alal, seeni mbokk ak seen bakkan. Ci kow gëm baatu Krist la ñu gise dëgg gi, ngëm lu raw bépp xalaatu nit. Yeesu dafay barkeel ngëm gu mel noonu jaare ko ci kàddoom, ni muy dëkksee ci way-gëm ji. Sunu ngëm dafay law ci sunu nekkin wépp te di nu lëkkale ak Yeesu sunu Musalkat bi. ÑAAN: Boroombi Yeesu, yow yaay sunu ëkku ngëm te yaa koy féddali. Ku ñu bëgg nga te sa dëgg gi jaare na ci sa kàddu ba tooyal sunu xol. Gëm naa ne dinga ma musal, man ak samay xarit, dinga leen may dund gu bees te dëgëral seen ngëm guy dund ci sa tur. Kon dinañu dund ba fàww te am mbég mu réy. LAAJ:
|