Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 004 (The word before incarnation)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
A - Peeñug Kàddug Yàlla gi ci Yeesu (Yowaana 1: 1-18)

1. Nekkin ak liggéeyu Kàddu gi laata muy feeñu (Yowaana 1:1-5)


YOWAANA 1:5
5 leer gi feeñ na ci biir lëndëm gi,te lëndëm gi teeruwu ko.

Ci Yàlla, lépp leer la ak sellaay. Fépp fu Mu feeññu lëndëm du fa taxawaalu. Lépp dafay leer, jub, nekk dëgg te sell. Lu selladi du dend mukk ak Moom. Xel mu sell mi dafa laab, te leeru Boroom bi du feeñoo doole, waaye ak lewetaay. Dafay dëfal di wéral.

Nes-nesi leeru Krist kenn jaglewu leen asamaan. Dañuy xar lëndëm git e maye mucc. Xam ne Yeesu mungi ne ràjj ci biir lëndëm gi, Yiw wu kéemaane la. Du bàyyi ñi réer waaye dafa leen di yewwi (goreel) te gindi leen.

Danu war a xam ne àddina lëndëm su féwwaloo ak àddina leer, am na. Xamunu ci lu wóor nan la lëndëm sosoo. Yowaana, taskatu Injiil bi, waxunu kumpa gi. Dafa bëggoon nu xam leer git te bañ a daagu ci wut a xam lëndëm gi. Doomi Aadama yépp ak lépp li ñu sàkk tàbbi nañu ci lëndëm, te àddina sépp ci know nguuru mbon lay doxe.

Xëy na yaangi laaj sa bopp: Su fekkee ne Krist moo sàkk àddina si, moom ak Yàlla te lépp jaar yoon, te baax, nan la ci lëndëm gi man a raxe? Yàlla dafa sàkk nit ñi ci melokaanam, lu tax nuy teg gàcce ndamam tey jii?

Yowaana tuddul turu Seytaane, mi déggadil Aji Sax ji te doon jéem a fay leeram. Dafa mos a weddi Krist. Looloo tax mu ñàkk leer ga ñu ko mayoon. Seytaane ddafa mujj a nekk ku yëg boppam (rëy) te di jéem a tolloo màqaama mu mu boolewul Yàlla. Dafa bëggoon a sut Yàlla ba daan Ko. Noonu la mujjee nekk buuru lëndëm gi.

Mbokk mi, lan mooy sa mébétu dund? Ndax kilifteef, siiw ak sa mbégte nafsu yoo boolewul Yàlla ngay wut? Su fekkee ne loolu la, kon yang bokk ci gaayi lëndëm gi, ni Ku Bon ki. Nekkul moom kese, ndaxte dafa xëccaale ay millyoŋi nit. Xoolal kanamu nit ñi ngay dajeel ci mbedd mi. Ndax leer nga ciy gis ci seeni bët, walla lëndëm? Seen xol, mbégte Yàlla lay wone walla naqaru Seytaane?

Ku Muus ki (Seytaane) dafa bañ Yàlla ndaxte leeram gu sell gi dafa koy daan. Bëggul leer gi feeñal coxorteem. Dafay làqu, te di jéem a daan Krist ak ñiy top leer gi. Workat bii manual a dékku leeru Boroom bi te dafa koo bañ. Moo ko tey, di nëbb xar-kanamam te noonu du man a gis leer gi. Li jar a tiit mooy ne ay millyoŋi nit gisuñu jantu Krist biy ray-rayi ci seen guddig bàkkaar. Nun ñépp xam nanu jant bi. Jarul nu koy tegtal kenn. Dafa teew, leer, di lerxat, te ne boyy. Ñépp xam nañu ne mooy ndeyu dund gi.

Ñi ëpp ci nit ñi duñu jot ndamul Krist ak kàttanam, ndaxte bëgguñu koo wut a xam. Ay xalaati naxekat ñoo leen di gëlëmal mel ni am mbàjj mu diis, te di leen xiir ci weddi xabaar dëgg bi aju ci nekkinu Krist ni Yàlla. Naka jekk,dañuy bañ a nangu seeni bàkkaar. Bëgguñu jegesi leer gi waaye des ci lëndëm gi moo leen gënal. Duñu weddi seen bopp te duñu tuub seeni bàkkaar. Dañuy ñàkk teggin rëy. Dañuy gumba ci kanamu yiwu leeru Krist gi. Lëndëm gi dafay jàmmarloo ak leer gi, waaye leer gi dafa koy foq ndax mbëggeel gi. Foo ci tollu? Ci leeru Boroom bi, walla ci lëndëmu ku Muus ki (Seytaane)?

ÑAAN: Céy Botoom bi yów yaay leeru àddina si. Maangi lay top ak ngëm ak ci sa mbëggeel. Doxuma ci lëndëm, waaye jot naa leeru dund gi. Maangi lay sant ndaxte bàyyiwooma man kenn ci biir ragal lëndëm gi, ak merum Yàlla, waaye danga maa woo ci leer gi ne ràyy. Leeralal ñi ma wër te gisuñu la naam sax yaangi leer ci lépp li leen wër. Boroom bi, yërëm ma, te sol ma sa leer gib a ma fees!

LAAJ:

  1. Lan moo wuutale leer gi ak lëndëm gi ci saayiiru baat bi?

The people who walked in darkness have seen a great light;
those who dwelt in the land of the shadow of death,
upon them a light has shined.
(Isaiah 9:2)

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 09, 2025, at 01:36 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)