Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
A - LI JIITU AYU BéS bu SELL bi (Yowaana 11:55 - 12:50)
3. Ay Grek ñungi jéem a gis Yeesu (Yowaana 12:20-26)YOWAANA 12:20-24 Grek yi jébbalu woon ci diine Yawut yi dañu dajaloo woon ca Yerusalem; bésub jéggi bu Elenist ya moo leen taxoon a jóg. Bi mbooloo ma teeroo Yeesu ni Buur, Grek ya itam daldi yéemu. Noonu, ñu dogu ngir gën Koo xam. Bëgg-bëggu askan wa feeñ ca ñaan (yéene jooja) googa. Ñu gis Filip,m i manoon a làkk grek, te nangu woon leen a boole ak xaritam Andare. Ñaari taalibe ya jegesi Yeesu ak xol yu tooy, ndax li ñu gis yéeféer yi njëkk a gëm Yeesu. Xalaatoon nañu ne làquji ca Grek ya moo gënoon a yenu maanaa, ngir daw mbugal mi leen Yawut yu tar yi doon tëkkoo. Yeesu xam li ñuy xalaat boole ci li askan di mebét. Mu tontoo leen ak ab laaj bu am solo, bu kenn jëliwul bu baax, moone de mooy bàkku ndam Injiilu Yowaana: »Léegi nag, Doomu nit ki am na ndam. » Waxtu wi ñu Ko war a màggal agsi na te jamono ji asamaan ak suuf doon xaar jegesi na. Moone de, kéemaanu kéemaan yi mooy ne ndamu xare yi ak jël nguur gi ci wàllu politik, nekkuloon màndarga ndamu Yeesu. Yowaana nettaliwul soppaliku ba ca tund wa, ndaxte jàppewu ko ni ndam li gën a am solo. Waaye wax na lu aju ci li lëkkale ndamul Christ ak deewam. Foofa ca kurwaa ba, gis nanu fa xolu baatinam, biy mbëggeel gi. Yeesu dafa misaale boppam ni am peppu dugub, pepp mi jóge asamaan daanu ci kow suuf, ngir dee te wone njubte gi ak ndam li. Yeesu dafa mos a am ndam. Deewam dafa nuy sellal nun moykat yi, ndax nu man a séddoo màggaayam gi. Laaju Grek yi dafa ëmbaale wooteb ndam, te di wone itam ne Yeesu askan yépp la woo. Dina yeesalaat ndamam la jiituwoon, ci ñoom. Ndam loolu dina dugg càkkite gi, jaare ko ci kurwaa bi. YOWAANA 12:25-26 Yeesu dafa nu won ne, ni Muy deewee ba dugg ci màggaayam, noonu itam lay deme ak taalibeem yi. Ni Doom ji bàyyee màggaayam, ak melokaani baatinam yépp, ngir musal nit ñi, noonu itam sunu mebét du nu nekk ay boroom màqaama, walla ñu siiw, waaye danu war a fàtte sunu bopp saa su nekk. Nanga seetlu sa bopp bu baax, ndax dangaa bëgg walla dangaa bañ? Krist nee na soo fàttee sa bopp te liggéeyal nguuram ci ngor gu wér, kon dinga jot dundu asamaan. Dinga sàmm sa ruu ba ca dund gu dul jeex ga. Ci kàddu yii, Yeesu won na la njëgu màggaay gi dëgg. Bul dund ngir topp sa nafsu, mbaa ngay bàyyeeku, walla di rëy-rëylu; waaye jublul ci Yàlla te déglu ay ndigalam, wutal miskin yi ak néew-doole yi. Ngir wallu leen, ni Mu ko defe bi Mu summee bubbum Buuram ngir toogandoo ak ay njaalookat, ak ay sàcc. Booy séddoo Injiil li ak bàkkaarkat yu mel noonu, ndamul Yàlla dina feeñ ci sa dund. Bul foog ne yaa gën ñi ci des. Yeesu rekk moo la man a setal ci kanamu ñeneen ñi, donte say jéll. Googu coppite ci jébbale sa bopp rekk lay jaare. Yeesu dafa wax lu leer lu aju ci loolu bi Muy leeral ni ñu koy surgawoo. Boobu dogu dafa ëmbaale topp Ko, toppandoo Ko, te séddoo mbañ gi Mu daan faral di jànkonteel, ci laabiir gu mat sëkk. Taalibe Krist yi man nañu daj ay mbañeel, ay bundxataal, ay nooteel, ba ci dee sax. Ndax jekk nga ngir daj coono ci turam? Dige na ne: « Fi Ma nekk, la sama surga di nekk itam. »Yeesu dafa lay jiitu ci yoonu coono wi, di sonnandoo ak yów. Ndam lu ne fàŋŋ du tukkib surgay Yeesu. Seen mbégte wuute na ak topp seen nafsu; waaye dañuy wut a sarwiir néew doole yi. Turu Yeesu, ci xelu jébbalu taalibeem yi lay damoo. Màggaayu turu Baay bi mungi jollee ci ni ñuy gën a nirook Doomam ji. Ni Krist tooge tey ci ndeyjooru Baay ji, te di séddook Moom jokkoo ak bennoo yu tar, noonu itam la ñi ñuy noot ndax turam wi di dundiji te fekkiji Baay ji ci asamaan. Kumpa gu rëy a ngi noonu. Ci yów, ban teraanga la Yàlla dencal surgay Doomam, ji bëgg ci xolam? Dina yeesalaat melokaanam ci ñoom; ba mu mel na ca njalbéen ga. Rax ci dolli dina leen sol Xelam mu Sell mi ba ñu fees dell Dinañu nekk ay doomam, te Doomam ji nekk taawu rakk yu bare. Dinañu dëkk ak seen Baay ci asamaan, ba fàww. (Rom 8:29; Peeñu 21:3-4) ÑAAN: Nungi lay sant, Sang bi Yeesu, ndaxte xooluloo rekk ci sa màggaay, waaye dangaa summi sa mbubbum Buur. Nungi lay màggal ngir sa suufeelu googu. Nungi lay ñaan nga génnee nu ci li nu neex ak ci sunu tiitar, ndax nu man a xam goreel gi sa Xel mi di maye. Danu laa bëgg a surgawu te xam sa mbëggeel ci sunuy dund. LAAJ:
|