Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
B - Ndekkite Yeesu Krist ak ay peeñoom (Yowaana 20:1 - 21:25)
2. Yeesu feeñu na taalibe ya ca néeg gu kowe ga (Yowaana 20:19-23)YOWAANA 20:22-23 Yoon la woon taalibe ya jaaxle ba ñu déggee Yeesu naan: « Ni ma Baay ji yónnee, laa leen di yónnee. » Ñu ngi doon wéy di làqu ca néeg ba, ndax ragal Yawut ya. Amuñu woon genn kàttan, te ci ñàkk ndam la ñu jóge. Noonu Yeesu ëf ca kow taalibe ya na Yàlla ëfe woon ngelewal dund ngir mu jot ruu guy dund te am kàttanu dund. Ci ëf googu la Yeesu wonee sañ-sañu càkkiteem; càkkite gu bees la tàmbali ci taalibeem yi, te dig leen Xelam mi, Kàttanam gi, ak Sañ-sañam gi ba ñu man a wone ci seen dundin, seen melokaanu Baay ji. Bi taalibe ya jotee Xel mu Sell mi, Krist daldi leen jàngal nan lañuy baale nit ñi. Dañu waroon a baal ñépp ñi nangu yooyu sart, bañ koo nangul ñi ko bañoon. Dañu waroon a yégle mbaalug bàkkaar yi ci kow sañ-sañ bi ñu am ci taxal fi Yeesu Boroom bi. Ci kow ñu nangu seen bàkkaar te tuub dinañu leen dalal ci Jàngu Krist. Yeesu dafa may ay taalibeem sañ-sañu siiwal mbaal gi, waaye du ni nuy baale nit ñi; Yàlla rekk ay baale (Esayi 43:25). Yeesu dafa la yónni ci àddina su bon si ni as ndaw te dafa bëgg a jaare ci yów ngir ñu xam muccam gi. Bul dem ak sa xadar di wa x ak sa man-man gu am àpp gi, waaye jokkool ak sa Boroom, ni ko bépp ndawu politiku réew di ko defe bés bu nekk ak réew ma ko yebal, ngir di man a jot ndigal ak yoon yi mu war a jaar. Doo Yàlla ju ndaw juy yëngu yów doŋŋ ci sab ruq, waaye jaamu Boroom bi nga. Dafa la bëgg a jariñoo ngir rammu ñeneen ñi. Tey jii, boo déggee baatam, bul dëgëral sa xol, waaye ubbil sa xol, sa xel ndax Sell mi man laa def ab seedeb Krist bu ñeme, suufeelu te maadu. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, yeyoowu ma ngay dugg ci sama biir kër, waaye wax nga te may nga ma sa Xel mu Sell mi, di ma leeral te di ma mayaat dund gi. Yónni nga ma ngir seedeel la ci kanamu nit ñi. Jarajëf ndaxte sa kàttan mat na sëkk ci sama ñàkk doole. May ma laabiir, ma bañ a nekk naaféq, sellal ma ci bépp xalaat bu aju ci bopp-sa bopp, dimbali ma ba ma sax ci sa coobare. Noonu la sa jàmm di man a soppee xol yi. LAAJ:
|